Ku ji lu bare, am barke yu bare
1 Am na lu neex lu ñu Yàlla dig ci Kàddoom. Ñun ñépp, loolu lañuy séentu. Waaye tey jii sax, mën nañu am ay barke yu bare yu jóge ci Yexowa, te loolu dina tax suñu dund gën a neex. Nit ku nekk mën na ci jot. Waaye barke yooyu, fu ñu war a tollu, ci lu ëpp, mu ngi aju ci ni ñuy góor-góorloo ngir am ko. Ni ko ndaw li Pool waxe, “ ku ji lu bare, góob lu bare ”. (2 Kor. 9:6.) Nañu seet léegi ñaari fànn fu ñu mënee gis li mu wax noonu.
2 Li ku nekk ci ñun di def ci liggéeyu waare bi : Bu ñuy xamal nit ñi xibaar bu baax bi saa yu ñu ko mënee, dinañu am ay barke yu bare (Léeb. 3:27, 28). Ñu bare ñu ngi ji lu bare. Naka lañu koy defe ? Dañuy yokk seen liggéeyu waare bi, di ko def bu ñu nekkee aji-xàll yoonu weer (pionnier auxiliaire), walla aji-xàll yoon ju ci sax (pionnier permanent). Loolu lu jar a ndokkeel la. Ñun ñépp, mën nañu ji lu bare. Naka lañu koo mënee def ? Nañu dellu seeti képp ku suñu waxtaan neex, te saa yu ñu ko mënee, nañu wax nit ñi ne mën nañu leen jàngal Biibël bi (Room 12:11). Bu ñuy góor-góorlu noonu, dina am ci liggéeyu waare bi loo xam ne dina yokk suñu doole, te dinañu ci gën a am mbégte.
3 Nañu liggéeyal Nguuru Yàlla : Bi Pool waxee li jëm ci “ ji lu bare ”, dafa doon wax ci maye suñu alal (2 Kor. 9:6, 7, 11, 13). Tey, am na lu bare li ñu mën a def ak suñu kàttan, suñu jot, ak it suñu alal, ngir liggéeyal Nguuru Yàlla. Mën nañu dimbali ñiy tabax Saali Nguur yi, ak Saal yi fu ñuy defe suñuy ndaje yu mag yi. Mën nañu bokk it ci ñiy setal tey toppatoo béréb fi ñuy jaamu Yàlla dëgg ji. Ginnaaw loolu, mën nañu maye suñu xaalis ngir jàpple suñu mbooloo mi. Mën nañu ko maye it ngir jàpple liggéeyu waare bi ak liggéeyu sàkk ay taalibe ci àddina si sépp. Bu fekkee ne ku nekk a ngi def wàllam, dinañu bég lool ndaxte dinañu gis ni Yexowa di barkeele bu baax liggéey bi mu ñu sant ! — Mal. 3:10 ; Lukk 6:38.
4 Baatu Yàlla dafa ñuy xelal ñu “ def lu baax, te bare jëf yu rafet, ñu yéwén, bay sédd ñi amul ”. Bu ñu toppee xelal boobu, dinañu am tey ay barke yu bare. Booba it, dinañu “ fàggu dencu ëllëg bu wér. Noonu dinañu feddali seen téye ci dund gu wóor gi ” di ñów. — 1 Tim. 6:18, 19.