TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 6/02 p. 1
  • Ndax “ bëgg ” nga dimbali nit ñi ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax “ bëgg ” nga dimbali nit ñi ?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu dimbali suñu moroom
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Yan jikko yu rafet la Yeesu amoon?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 6/02 p. 1

Ndax “ bëgg ” nga dimbali nit ñi ?

1 Yeesu dafa fonkoon nit dëgg. Benn bés, dafa am gaana bu ko ñaan ndimbal. Yeesu dafa tàllal loxoom, laal ko, te ne ko : “ Bëgg naa ko, wéral. ” (Mark 1:​40-42). Naka lañu mënee topp Yeesu ci li mu bëggoon a dimbali nit ñi ?

2 Ñi bëgg waxtaan ak ñun : Bu ñu bëggee dimbali ñi bëgg waxtaan ak ñun ndax ñu jaamu Yexowa, képp ku bokk ci mbooloo mi am na ci wàllam. Bu amee ku sog a ñów ci suñuy ndaje, teral ko bu baax. Seetal ci lan nga ko mënee ndokkeel. Bu tontoo ci ndaje bi, ndokkeel ko ndax loolu. Ndokkeel ko it ci li muy góor-góorlu ngir topp li Biibël bi wax. Won ko it ne mën na am ay xarit dëgg ci mbooloo mi.

3 Suñuy mbokk karceen yi : Suñuy mbokk ci wàllu ngëm ñoo gën a yelloo suñu ndimbal. War nañu leen a dimbali ci lu bare (Gal. 6:10). Ñu bare, feebar sonal na leen lool. Demal seeti leen te fexeel ba seddal seen xol. Loolu dina tax ñu bañ a wéet, te dëgg-dëgg dina baax ci ñoom. Xéyna it nga mën leen a dimbali ci dara. Am na ñeneen ñu am yeneen jafe-jafe. Won leen ne loolu itteel na la. Naka nga ko mënee def ? Na nga leen déglu te dalal seen xel (1 Tes. 5:14). Magi mbooloo mi, ñoom it, soxla nañu ñu jàpple leen bu ñuy def seen warugar (Yaw. 13:17). Bu ñu wonee ne dañu bëgg dimbali nit ñi, dinañu mën a ‘ féexal xolu ’ suñu mbokk yi ci wàllu ngëm. — Kol. 4:⁠11.

4 Suñu waa kër : War nañu góor-góorlu ngir roy Yeesu it ci suñu biir kër. Waajur yi, bu ñu fonkee seeni doom, dañu leen di ‘ yar, di leen yemale ak a yee ci ’ Yexowa (Efes 6:⁠4). Loolu ëmb na jàng Biibël bi ci biir njaboot gi, dem ci ndajey mbooloo mi ak dem waaraate. Xale yi mën nañu def seen wàll bu ñuy gaaw a pare bu waxtu yooyu jotee. Xale yi, bu ñu demee ba mag te seeni waajur nekk ci coono ndax li ñu màgget, bu ñu leen dimbalee, di ko def ak yërmande, noonu lañuy roye ci Yeesu. Ñun ñépp, bu ñu defee loolu walla lu mel noonu, dinañu ‘ wone suñu ragal Yàlla ci suñu biir kër ’. — 1 Tim. 5:⁠4.

5 Bu ñuy dimbali nit ñi, di roy Yeesu, dina wàññi jafe-jafe yi. Suñu njaboot dina gën a nekk benn. Ñi bokk ci mbooloo mi, seen diggante ci seen biir dina gën a rattax. Li gën a am solo mooy, dinañu màggal Yexowa, “ Baay biy Aji Yërmande ”. — 2 Kor. 1:⁠3.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager