Na ku nekk am li muy fas yéene def ci wàllu ngëm
1 Di jaamu Yexowa ba abadan, lu réy la ! Li ñu ci mën a dimbali mooy ñu am li ñuy fas yéene def tey ci wàllu ngëm, ba pare góor-góorlu ci. Dina tax ñu jariñoo suñu kàttan ni mu gëne (1 Kor. 9:26). Lan nga mën a fas yéene def te du ëpp ci yow ?
2 Booy jàng : Ndax dangay waajal bépp ndaje bu ñuy def ci mbooloo mi ? Su dee waaw, ndax dinga gëstu te xalaat bu baax ci li ngay jàng ? Booy waajal njàngum La Tour de Garde bi walla njàngum téere bi, ndax dangay rëdd tont yi rekk, walla dinga xool itam aaya yi ci Biibël bi ? Te boo jàngee benn xise, ndax dinga xalaat bu baax lu tax nga mën a gëm li ci nekk ? Ayu-bés bu nekk, ci lekkoolu sasu Nguuru Yàlla, am na li ñu war a jàng ci Biibël bi. Nanga gëstu ci yenn aaya ngir yokk ci sa xam-xam. Loolu laaj na jot te dinga ci war a góor-góorlu bu baax. Waaye lu bare nga ciy jële. — Léeb. 2:4, 5.
3 Ndaje yi ñu am ci mbooloo mi : Mën nga fas yéene teew ci juróomi ndaje yi ñu am yépp ci mbooloo mi, ayu-bés bu nekk. Bu ñu teelee agsi ngir waxtaan ak suñu mbokk karceen yi, te fekke woy ak ñaan yu njëkk yi, dina tax mbooloo mi gën a bare jàmm. Mën nañu góor-góorlu it ngir tontu ci ndaje bu nekk, ay tont yu gën di baax. Mën nga tànn it aaya ci li ñuy jàng, te wone ni mu ànde ak waxtaan bi, walla mën nga wone ni ñu mënee topp li ñuy waxtaane. — Yaw. 10:24, 25.
4 Liggéeyu waare bi : Bu ñu amee li ñu fas yéene def ci waaraate bi, suñu liggéey dina gën a baax. Ndax am na waxtu yi nga fas yéene def ci waaraate bi weer wu nekk ? Am na ñu gis ne lu baax la. Walla, ci liggéeyu waare bi, ndax am na foo war a jëm kanam ? Mën na nekk ni ngay jëfandikoo Biibël bi booy waaraate kër-oo-kër, walla ni ngay waxtaane booy dellu seeti nit ñi, walla góor-góorlu ngir tàmbali benn njàngum Biibël bi, walla fexe ba gën a mën a jàngale Biibël bi.
5 Wayjur yi, ndax dingeen wax ak seeni doom ngir ñu am li ñuy fas yéene def ci liggéeyu Yexowa ? Fexeleen ba dimbali leen ndax ñu mën a gis ne nekk pioñee walla bokk ci waa Betel bi, dina wone fu seen ngërëm ci Yexowa tollu. — Daj. 12:1.
6 Bu ñuy seetaat li ñuy def ngir jaamu Yexowa, nañu am li ñu fas yéene def ci wàllu ngëm, ba pare góor-góorlu ci. Bu boobaa, dinañu am mbégte mu réy, te mën a dooleel suñu moroom yi. — Room 1:12.