Fexeel ba nit ñi xam li nga bëgg wax
1 Dañu war a waaraate te sàkk ay taalibe. Loolu laaj na ñu jottali xam-xam suñu moroom yi (Macë 24:14 ; 28:19, 20). Fexe ba nit xam li nga bëgg wax yombul, bu dee sax sa xarit la. Kon lan lañu mën a def ba jottali nit ku ñu xamul xibaar bu baax bi ?
2 Nekk gan ba pare nekk xarit : Booy jege nit, xalaatal li mu mën a yëg. Ak li xew ci àddina si, su amee koo xamul ku bëgg wax ak yaw, mën na am nga ragal mu def la lu bon. Lu ñu mën a def ba ragal boobu bañ ñoo teree wax ak nit ñi ? Nañu sol yére yu jekk te yiw, boole ci yar ak teggin. Loolu mooy njëkk wax, te dina wàññi ragal bi nit ñi am. — 1 Tim. 2:9, 10.
3 Danga war a teey itam te neex deret. Dina tax nit ñi bëgg waxtaan, te bëgg déglu. Kon war nga waajal sa bopp bu baax. Boo xamee li nga war a wax, dina wàññi sa ragal, dinga teey te loolu dina tax nit ñi bëgg xam li nga bëgg wax. Lii la benn jigéen wax ci suñu mbokk bu doon wax ak moom : “ Li may fàttaliku mooy jàmm ji ma gisoon ci kanamam bu leer. Loolu neexoon na ma lool. ” Loolu tax na jigéen jooju déglu xibaar bu baax bi.
4 Jikko yu rafet yu mën a tax nit ñi bëgg déglu li ñuy wax : Dañu war a ittewoo nit ñi dëgg (Fil. 2:4). Booy waxtaan ak nit, du yow rekk yaa war a wax ndaxte waxtaan, ëmb na déglu. Laaj ko xalaatam, ba pare déglu ko, ndax mu yëg ne ittewoo nga ko. Kon nag bu waxee ba pare, bul gaaw a dellu ci li nga doon wax. Su dee wax na lu am maanaa, wax ko ko, te booleel li mu wax ci sa tont. Boo gisee li ko itteel dëgg, nangeen ci waxtaan.
5 Jottali xam-xam dafay gën a yomb boo suufeeloo te xam fi nga war a yem (Léeb. 11:2 ; Jëf. 20:19). Nit ñi dañu bëggoon a jege Yeesu, ndax dafa ‘ lewetoon te woyef ’. (Macë 11:29.) Waaye ku yëg boppam, dañuy koy daw. Kon xam ne ñoo yor dëgg, warul tax ñuy réyal baat.
6 Bu nit ki waxee lu àndul ak li nekk ci Biibël bi, ndax war nañu ko ko wax ? Waaw, waaye soxlawuñu ko def ci waxtaan bu ñjëkk bi. Li gën mooy ñu njëkk waxtaan ci fi ñu bokk xalaat. Ba pare ñu door ko jàngal ci Biibël bi loo xam ne bala mu koy nangu, dina xaw a jafe ci moom. Loolu laaj na ñu def ndànk te jéem a bañ a wax lu koy metti. Mën nañu roy li Pool def bi mu doon waaraate àttekat yu nekkoon ca Areyopas ba. — Jëf. 17:18, 22-31.
7 Ci kow loolu lépp nag, bu ñu amee mbëggeel buy tax ñu fàtte suñu bopp, dinañu mën a jottali bu baax li ñu bëgg wax. War nañu yërëm ñi “ sonn ba ne yogg, mel ni xar yu amul sàmm ” ni ko Yeesu doon defe (Macë 9:36). Dina tax ñu bëgg leen a jottali xibaar bu baax bi, te dimbali leen ndax ñu topp yoonu dund gi. Li ñuy wax ànd na ak mbëggeel, kon mbëggeel moo war a feeñ ci ni ñuy waxe. Bu ñu defee loolu, dinañu roy Yexowa Yàlla ak Yeesu, ñoom ñi gën a mën a jottali xam-xam.