Ni ñu mënee waxtaan ak nit ba mu nangu dëgg gi
1 Li Pool wax ci Jëf ya 13:16-41 dafa ñuy won ni ñu mënee waxtaan ak nit ñi ba ñu nangu dëgg gi nekk ci Biibël bi. Bala mu leen di waar, dafa doon seet fi ñu yaroo ak li ñuy xalaat ngir xam ni mu war a waxtaane ak ñoom. Nañu xool li mu wax foofu te seet ni ñu ko mënee roy ci suñu waaraate bi.
2 Seetal fu ngeen bokke xalaat : Waare boobu Pool defoon, dafa jëmoon ci taxawaayu Yeesu ci lépp li Yàlla fas yéenee def. Waaye du ci loolu la komaase waxtaanam. Dafa njëkk waxtaan ci fu mu bokkoon xalaat ak Yawut yi ko doon déglu. Waxtaan na ci lu xewoon ci mbooloo Israyil (Jëf. 13:16-22). Ñun it, dinañu gën a laal nit ñi bu ñu seetee fu ñu bokke xalaat ak ñoom te waxtaan ci. Bala loolu, xéyna dinañu war a xam yan laaj lañu leen mën a laaj ngir xam li ñuy xalaat te déglu leen bu baax ngir xam li leen itteel dëgg.
3 Bi mu doon wax ci li xewoon ci mbooloo Israyil, Pool dafa leen fàttali li leen Yàlla digoon, maanaam dina am ci askanu Daawuda ku leen di musal. Room moo doon ilif Yawut yi. Te Yawut yu bare dañu doon séentu soldaar bu mag buy daan Room ba pare yëkkëti seen réew ci kow yeneen réew yépp. Ñépp a xamoon ne njiiti diine Yawut yi bañoon nañu Yeesu ba jox ko Nguuru Room ngir ñu rey ko. Lan la leen Pool mënoon a wax ba ñu nangu ne Yeesu moo doon Almasi bi leen Yàlla digoon ?
4 Seetal ni ngay waxtaane ak nit ñi : Pool xamoon na xalaatu ñi ko doon déglu. Loolu moo tax mu waxtaan ak ñoom ci aaya yu ñu gëmoon ba pare. Dafa leen wax ne ci askanu Daawuda la Yeesu doon bokk. Wax na leen it ne Yaxya Sóobkat bi ci boppam moo nee Yeesu, Almasi bi la, fekk ñi ci gën a bare ñoo tegoon Yaxya yonent Yàlla (Jëf. 13:23-25). Pool nee na itam ne, bi njiiti diine Yawut yi bañee Yeesu ba daan ko dee, dañu “ amal waxu yonent yi ”. (Jëf. 13:26-28.) Ginnaaw loolu, dafa wax ci ñi gis Yeesu bi ko Yàlla dekkalee ba pare. Wax na itam ci aaya yu Yawut yi ko doon déglu xamoon bu baax, yu doon yégle ndekkite Yeesu bi.—Jëf. 13:29-37.
5 Waaye du noonu la Pool waxtaane ak Gereg yi nekkoon ci Areyopas ca Aten (Jëf. 17:22-31). Ba tey, li mu leen wax ak li mu waxoon Yawut yi, benn la. Te ñaari fasoŋu waxtaan yooyu ñoo jur lu baax (Jëf. 13:42, 43 ; 17:34). Tey itam, bu ñuy waar ay nit, nañu seet fu ñu bokke xalaat ak ñoom. Nañu xool itam fu ñu yaroo ak li ñuy xalaat te jaar foofu ngir xam ni ñu war a waxtaane ak ñoom. Bu ñu defee loolu yépp, suñu waaraate bi dina gën a am njariñ.
[Laaj yi]
1. Lan lañuy seet ci Biibël bi te lu tax?
2. Lu ñu mën a jël ci fasoŋ bi Pool tàmbalee waareem ?
3. Lu tax fexe ba Yawut yi nangu ne Yeesu moo doon Almasi bi leen Yàlla digoon warul a yomb ci Pool ?
4. Lan la Pool wax Yawut yi ngir ñu mën a nangu dëgg gi ci Yeesu ?
5. a) Lan la Pool soppi ci waxtaanam ak Gereg yi ? b) Naka lañu mënee roy Pool bu ñuy waaraate ?