Wonal sa moroom ne danga ko bëgg — Nanga waajal bu baax sa bopp
1 Bu ñu waajalee bu baax suñu bopp, dinañu gën a mën a won nit ñi ne dañu leen bëgg. Lu tax ñuy wax loolu ? Bu fekkee ne dañu waajal bu baax li ñu bëgg wax, suñu xel du nekk rekk ci li ñu bëgg wax. Kon dinañu gën a mën a seetlu ki ñuy waxtaanal ngir xam li ko soxal. Duñu ragal, te dinañu mën a wax lu jóge ci suñu xol. Kon, lu ñu mën a def ngir waajal waxtaan bu nar a neex nit ñi ?
2 Nanga wax luy ànd ak li nit ki soxla: Def nañu ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2006, ay waxtaan yu ñu mën a topp ci waaraate bi. Nanga ci tànn benn bu nar a baax ci nit ñi nekk ci seen goxu mbooloo, te seetal noo ko mënee wax ci sa kàddu bopp. Seetal loo ci mën a soppi ngir mu gën a baax ci ñi nekk ci seen goxu mbooloo. Bu amee diine walla xeet boo xam ne danga faral di daje ak ay nit ñu ci bokk, seetal it waxtaan bu leen mën a neex. Bu fekkee ne dangay seet ci nit ki ngay dajeel ngir xam waxtaan bu ko mën a neex, yaa ngi wone ne danga ko bëgg. — 1 Kor. 9:22.
3 Booy waaraate, nanga kontine di seet loo mën a soppi ci sa waxtaan ngir mu gën a ànd ak ki ngay waxal. Li ngay njëkk wax dafa am solo lool. Kon boo koy wax, nanga seetlu bu baax ki ngay waxal. Nit ñi nuy dajeel bokkuñu làkk. Kon booy ubbi sa waxtaan, ndax dangay jéem a wax ci làkk bi nit ki gën a dégg ? Ndax li ngay wax soxal na ko ? Ndax dafay tontu ci li nga koy laaj ? Boo naree wax déedéet ci laaj yi ñu wax fii, kon nanga seet loo war a soppi ci say waxtaan ngir ñu gën a neex nit ñi.
4 Li mën a tax nga bañ a fàtte sa waxtaan : Ñu bare dañuy wax ne bu ñu nekkee ci kanamu nit, dañuy fàtte li ñu bëggoon a wax. Bu dee loolu dafa lay dal, ndax jéem nga waxaat li nga bëgg wax ci waaraate bi ay yoon yu bare bala ngay dem waaraate, di ko wax kenn mel ni yaa ngi waare ? Loolu dina tax li nga bëgg wax, leer ci sa xel. Dinga ko waxe ni mu ware, te dina yomb a nànd. Te it dinga gën a xam nooy tontoo nit ñi.
5 Leneen li nga mën a def it ngir bañ a fàtte loo war a wax, mooy tënk sa waxtaan te bind li nga tënk noonu ci kayit bu ndaw. Te bala ngay dugg ci kër ngir waaraate, nanga ko xoolaat ci lu gaaw. Am na ñuy wax ne kayit bu ndaw bu mel noonu, dafay tax ñu gën a teey te ci lañuy gën a mën a waxtaan ak nit ñi. Loolu lépp a tax ñuy wax ne, bu ñu waajalee bu baax suñu bopp, dinañu gën a mën a won nit ñi ne dañu leen bëgg. Dina tax it suñu waxtaan yi gën a baax bu ñuy waar nit ñi ci xibaar bu baax bi.