TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 11/02 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Turu xaaj yi
  • 11-17 nowàmbar
  • 18-24 nowàmbar
  • 25 nowàmbar ba 1 desàmbar
  • 2-8 desàmbar
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 11/02 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

11-17 nowàmbar

Woy-Yàlla 82

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. (Su ngeen mënulee topp li nekk ci xët boobu, jëlleen li nekkoon ci Sasu Nguuru Yàlla yi weesu.) Na ci am ku wax fu ñuy ame xaalis bi ñu soxla ngir def suñu liggéey ci àddina si sépp. — Seetleen li nekk ci La Tour de Garde, ci xët 2, walla ci Réveillez-vous ! xët 5.

15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.

20 min : “ Jàppleel sa wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi. ”a Benn magu mbooloo bu nekk wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi moo war a jiite waxtaan bi. Bu ngeen di def xise 3, waxleen it li nekk ci téere École du ministère, ci xët 70. Waxal mbooloo mi lenn lu baax lu muy def ngir jàpple njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi, te gërëm ko ci. Won ko it fi mu war a gën a góor-góorlu ngir jàpple ndaje boobu.

Woy-Yàlla 49 ak ñaan bu mujj bi.

18-24 nowàmbar

Woy-Yàlla 64

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Waxtaanleen ci xaaj bi tudd “ Ay yéenekaay yu am solo ! ”

10 min : Ay tont ci seeni laaj. Mag bu mën jàngale mooy def waxtaan bi.

25 min : “ Boroom kër yi : tàmmleen di topp porogaraam bu baax ci wàllu ngëm. ” Ku koy def na njëkk def waxtaan bu gàtt ak li nekk ci xise 1 ba 3 ngir ubbi waxtaan bi bala muy tàmbali di waxtaan ak ñi teew ci xise 4 ba 13. Bu leen ko jot bi mayee, jàngleen xise 7, 8, 11 ak 12. Na am it benn walla ñaari way-jur yu ñuy laaj laaj yii : Lan moo dimbali seen njaboot, ba ñu am porogaraam bu baax ci wàllu ngëm ? Porogaraam bu baax, lan la leen laaj ? Ban njariñ lañu ci jële ? Waxal ay xalaat yu jóge ci xise 14 ngir jeexal waxtaan bi.

Woy-Yàlla 60 ak ñaan bu mujj bi.

25 nowàmbar ba 1 desàmbar

Woy-Yàlla 7

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na jëkkër ak jabar ànd ci waaraate bi te topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. (Su ngeen mënulee topp li nekk ci xët boobu, jëlleen li nekkoon ci Sasu Nguuru Yàlla yi weesu.) Jëkkër ji mooy wone La Tour de Garde, jabar bi wone Réveillez-vous !

15 min : “ Xamleleen dëgg gi jëm ci Yeesu. ”b Booleleen ci xalaat yi nekk ci téere École du ministère, ci xët 278. Waxal nit ñi ñu indi seen téere École du ministère ayu-bés bii di ñów ngir waxtaan bi tudd :“ Lekkool bu ñuy jàngal ni ñuy defe li ëpp solo ci àddina. ”

20 min : “ Woneel ne ittewoo nga ak mbëggeel ‘ xale yu seen baay gaañu ’. ” Jëfandikool xise 1 ak li nekk ci téere Étude perspicace, volume 2, ci xët 459 ngir wax ci lu mat ñetti minit, li Yexowa xalaat ci xale yi seen baay gaañu. Laajal ay laaj ñi teew te may leen ñu tontu ngir wax ci li nekk ci xaaj bi. Woneel it leneen li nit ñi mën a def ngir jàpple xale yooyu. Bu ngeen di def xise 3 ak 4, booleleen li ñu wax ci Réveillez-vous ! bu 8 oktoobar 1995, ci xët 8 ba 9.

Woy-Yàlla 47 ak ñaan bu mujj bi.

2-8 desàmbar

Woy-Yàlla 95

8 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ñu bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru nowàmbar te joxe ko. Waxleen ci lu gàtt ni ñu mënee wone téere Le plus grand homme de tous les temps. — Seetleen Le ministère du Royaume bu suweŋ 1998, xët 8.

12 min : Ñiy jàpple diine dëgg gi — Démb ak tey. Waxtaan bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 1 nowàmbar 2002, xët 26 ba 30.

25 min : “ Lekkool bu ñuy jàngal ni ñuy defe li ëpp solo ci àddina. ” Waxtaan ak ñi teew. Wottukatu lekkoolu sasu Nguuru Yàlla moo koy def. Fexeel ba nit ñi sawar ci porogaraamu lekkool bu bees bi ñu war a tàmbali ci weeru sãwiyee. Woneel li nekk ci xaaj bi tudd “ Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci atum 2003 ” te nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu oktoobar 2002 ci xët 3 ba 6. Waxal it ci li ñu war a def ngir mën a bokk ci lekkool bi, ni ñu ko waxe ci téere École du ministère, ci xët 282. Te waxal nit ñi ne képp ku mën a bokk ci lekkool bi te defagu ko, na góor-góorlu ba bokk ci.

Woy-Yàlla 51 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager