Jàppleel sa wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi
1 Ñun ñépp, kenn ku nekk, jële nañu lu bare ci njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi. Weer wi weesu, waxtaan nañu ci ni wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi di defe liggéeyam. Waaye naka lañu ko mëne jàpple ndax mu jariñ nu te jariñ it ñeneen ñi ?
2 Nañu ko fekke ayu-bés bu nekk : Ñi bokk njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi, barewuñu. Looloo tax bu ñu ko fekke, dina am solo lool. Na nga ko fas yéene fekke ayu-bés bu nekk. Booy agsi bala waxtu wi di jot, dina baax lool. Dina tax wottukat bi mën a tàmbali ndaje boobu ci fasoŋ bu jaar yoon. — 1 Kor. 14:40.
3 Ay tont yuy jëmloo kanam : Mën nga jàpple it wottukat bi boo waajalee sa bopp bu baax, te booy tontu ay tont yuy jëmloo kanam. Tont yiy laal benn ponk kese ñoo gën. Dina tax ñeneen ñi bëgg tontu ñoom itam. Booy tontu bul wax ci lépp li nekk ci xise bi. Bu amee lu laal sa xol, boole ko ci say tont. Dina tax waxtaan bi gën a neex. — 1 Pie. 4:10.
4 Bu fekkee ne yow yaa war a jàng xise yi ci kow, may nañu la lu réy. Na nga ko def bu baax. Dina tax njàngum téere bi gën a baax te gën a neex. — 1 Tim. 4:13.
5 Waaraate bi ñuy def ci njàngum téere bi : Ndaje yu ñuy am bala ñuy waare, dinañu leen def ci béréb yu bare fu ñuy defe njàngum téere bi. Booy fekke ndaje yooyu, dina jàpple bu baax wottukat bi, ci liggéeyu waare bi muy jiite. War nga gise ndaje yooyu ni lu mën a tax nga gën a jege say mbokk, te it fi nga leen di mëne xiir ci lu baax.
6 Bindal li nga def ci waaraate bi te joxe ko : Bu weer bi deewee, boo gaawee bind li nga def ci waaraate bi te joxe ko, dinga jàpple it wottukat bi. Mën nga ko ko jox moom ci boppam, walla nga def ko ci boyet bu ñu koy def ci Saalu Nguur gi. Sekkerteer bi mën na jëfandikoo boyet boobu ngir dajale kayit fi ñu bind li ñu def ci liggéeyu waare bi, yi ko wottukatu njàngum téere yi di jox.
7 Boo jàpplee wottukatu njàngum téere bi ci mbooloo mi, dinañu la ci sant bu baax. Ci kow loolu lépp, na la wóor ne Yexowa dina ‘ ànd ak xel ’ bi ngay wone. — Fil. 4:23.