Lekkool bu ñuy jàngal ni ñuy defe li ëpp solo ci àddina
1 Nit ñi dañuy dem lekkool ngir am xam-xam bi leen di dimbali ci li ñu fas yéene am ci seen dund. Ci li ñu mën a fas yéene def yépp, ndax mën na am lu ëpp solo lii : màggal Ki ñu may dund, te dimbali nit ñi ndax ñu xam li mu bëgg def ak santaaneem yi ? Déedéet. Li tax ñu def Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla mooy waajal ñu ngir ñu mën a jàngal nit ñi li ñu gëm. Kon nag bu ñu teewee ayu-bés bu nekk ci lekkool bi, dinañu jàng ni ñuy defe liggéey bi ëpp solo ci àddina.
2 Sasu Nguuru Yàlla bu weer wi weesu, amoon na xaaj bu tudd “ Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci atum 2003 ”. Xaaj boobu dafay wone ni ñu war a defe lekkool bi. Def ko ci sa téere Tirez profit de l’École du ministère théocratique, te yóbbaaleel téere boobu saa yooy dem ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla, ayu-bés bu nekk. Nañu wax léegi ci li ñuy def ci lekkool bi ci atum 2003.
3 Technique oratoire (maanaam liy tax ñu aay ci wax) : Bu sãwiyee jotee, ci lañuy tàmbali di ubbi lekkool bi ak waxtaan bu 5 minit. Waxtaan boobu dina wax ci lenn luy tax ñu aay ci wax, walla ci ni ñu war a duruuse, ni ñu war a jànge ak ni ñu war a jàngalee. Wottukatu lekkool bi walla beneen magu mbooloo bu mu tànn, moo war a def waxtaan bi. Kiy def waxtaan bi, mën na wax li Technique oratoire bi muy waxtaane di tekki ak lu tax mu am solo. Bu ci paree, na jëfandikoo li nekk ci Mbind mi te wone ni ñu mëne topp Technique oratoire boobu, bu ko defee mu gën a xóotal waxtaan bi. Bu gënee wax ci ni ñu mëne topp Technique oratoire boobu, dina tax ñu gën aay ci waaraate bi.
4 Waxtaan n° 1 : Suñu mbokk yu góor yiy def waxtaan bi dañu war a “ wone bu baax njariñ bi nekk ci xët ” yi muy jëfandikoo ngir def waxtaan bi. Maanaam dafa war a wone ni mbooloo mi mëne jëfandikoo li muy wax. Su ñu la waxee nga def waxtaan bi, seetal li ñu wax ci téere École du ministère, ci xët 48 ak 49, ngir waajal waxtaan bi. Jàngal it li ñu def ci téere boobu ci “ Applications pratiques ”, ci xët 286.
5 Li ñu war a jàng ci Biibël bi ayu-bés bu nekk : Mën na am ne ci at yi weesu, dafa doon am lu la doon tere jàng li ñu waroon a jàng ci Biibël bi ayu-bés bu nekk. Waaye ndax ren mën nga fas yéene jàng bu baax li ñu war a jàng ci Biibël bi ayu-bés bu nekk ? Ñi koy def, bu at mi jeexee, dina fekk ñu jàng Mbindi Karceen yi ci làkku grekk ba mu daj. Tàmbali porogaraam ngir jàng Biibël bi ak Mbindi Karceen yi ci làkku grekk dina ñu amal njariñ. Téere École du ministère wone na ko ci xise 5 bi nekk ci xët 10.
6 Kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi : Waxtaan bii, dañu ko yokk ba mu mat 10 minit, bu ko defee, ñi teew dinañu mën a wax li ñu xalaat ci pàcc yi ñu waroon a jàng ci ayu-bés bi. Waxtaan boobu, war nañu ko def ayu-bés bu nekk. Ñi koy def, war nañu fexe ba mu bañ a ëpp 10 minit. Dinañu ko def sax ci ayu-bés bu ñuy fàttaliku li ñu def ci lekkool bi (Revision orale). Booy jàng pàcc yi ñu war a jàng ayu-bés bi, seetal lu la mën a jariñ booy jàng Biibël bi ak sa njaboot, booy waaraate, walla yow ci sa wàllu bopp. Yan jikko Yexowa ñooy feeñ ci ni muy digaale ak nit ñi, walla ak xeet yi ? Ci li nga jàng, lan moo dëgëral sa ngëm, te lan moo yokk ngërëm bi nga amoon ci Yexowa ? Mën nga wax ci aaya yu la neex. Mën nga wax sax ci aaya yi ñuy jàng ci waxtaan n° 2, ndax kiy def waxtaan boobu, bu jàngee aaya yi ba pare, du ci waxtaane.
7 Waxtaan n° 2 : Ayu-bés bu nekk, eleew biy njëkk jàll, dina war a jàng dara ci kanamu ñépp. Ayu-bés bu nekk, li eleew boobu di jàng, ci pàcc yi ñu waroon a jàng ci Biibël bi lañu koy tibbe. Waaye ayu-bés bi mujj ci weer wu nekk, li muy jàng ci La Tour de Garde lañu koy jële. Kiy def waxtaan bi, warul wax dara bala muy jàng, te bu jàngee ba pare, warul wax dara itam. Loolu dina tax mu mën a def xelam yépp ci ni muy jànge. — 1 Tim. 4:13.
8 Waxtaan n° 3 ak 4 : Li ñu war a seet ngir def yenn waxtaan yi, ci téere Comment raisonner lay gën di nekk. Yeneen waxtaan yi tur bi kese (thème) lañuy joxe. Li nga war a seet ngir defar sa waxtaan bu barewul, walla bu fekkee ne tur bi kese lañu joxe, mën nga wutal sa bopp li nga nar a wax ci téere yi mbootaay bi génne. Loolu dina tax suñu mbokk yu jigéen yi mën a wax lu ànd ak ki ñuy waxal.
9 Cadre bi (maanaam ni waxtaan bi di ame) : Ni ñu ko waxe ci téere École du ministère ci xët 45, wottukatu lekkool bi mën na joxe cadre bi. Waaye bu ko deful, mbokk yu jigéen yi mën nañu tànn benn cadre ci yi nekk ci téere École du ministère ci xët 82. Suñu benn mbokk mu jigéen, bu fekkee ne ñaari weer yu nekk dafay def benn waxtaan, bu juróomi at matee, dina jot a def 30 cadre yi yépp. Cadre n° 30 mu ngi tudd “ Autre cadre de discussion adapté à votre région ”. Bu amee mbokk mu jigéen mu ko tànn war na bind cadre bi mu tànn ci kayit buy wone ban waxtaan lay def (S-89). Na ko bind ci suuf walla ci ginnaaw. Wottukatu lekkool bi war na bind ci téere eleew bi, ci xët 82, kañ la eleew bi def waxtaan bi. Na ko bind ci wetu cadre bi mu tànn. Loolu mën na ko def buy bind ci kayit fi ñu bind xelal yi (fiche de conseils).
10 Kayit fi ñu bind xelal yi (fiche de conseils) : Kayit fi ñu bind xelal yi mu ngi ci sa biir téere, ci xët 79 ba 81. Kon saa yoo defe benn waxtaan, war nga jox wottukat bi sa téere. Wottukatu lekkool bi war na def ci benn kayit li mu war a seetlu ci eleew yiy def waxtaan yi.
11 Waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu def ci lekkool bi (Révision orale) : Ñaari weer yu nekk dinañu fàttaliku benn yoon li ñu def ci lekkool bi. Waxtaan ak ñi teew lay doon, ci 30 minit. Ni ñu ko doon defe, dinañu def laaj yi ñu ciy laajte ci Sasu Nguuru Yàlla bi. Ayu-bés bu ngeen war a def fàttaliku boobu, mën na nekk ayu-bés bu wottukat biy wër ci mbooloo yi war a nekk ci yéen, walla ngeen war a am ndaje bu mag bu ñaari fan. Bu boobaa, na ngeen def li ngeen waroon a def ayu-bés bi ci topp. Fàttaliku bi, ngeen def ko beneen ayu-bés bi.
12 Yeneen kalaas yi : Ci mbooloo yi nga xam ne eleew yi ëpp nañu 50, mag yi war nañu seet ndax mënuñu def yeneen kalaas fu ñuy def waxtaan yépp walla waxtaan n° 3 ak 4 kese (École du ministère, xët 285). Bu fekkee ne mbooloo mi dafa bare mbokk yu jigéen, waaye barewul mbokk yu góor yu mën a def waxtaan n° 2, mën nañu def yeneen kalaas ngir waxtaan n° 3 ak 4. Mag ñi war nañu tànn mbokk yu góor yu mën a jiite lekkool bi, ngir dénk leen kalaas yooyu.
13 Kiy jàpple kiy xelal nit ñi : Ni ñu ko waxe woon ci “ Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci atum 2003 ”, kurélu mag ñi dinañu tànn benn mbokk mu góor ngir mu jàpple kiy xelal nit ñi. Kooku mooy xelal magi mbooloo mi ak surga mbooloo yiy def waxtaan no 1 ak kiy wax kàddu yu am solo ci Biibël bi. Mbokk mi ñuy tànn, dafa war a nekk ku mën jàngale, te mën xelal. Mbokk moo xam ne bu xelalee yeneen mag yi, dinañu ko déglu bu baax. Buy xelal, dafa war a wax li baaxoon ci fasoŋ bi ñu waxe ak fasoŋ bi ñu jàngalee nit ñi, te wax it benn walla ñaari mbir yi ñu war a taneel. Bu ko defee, li ñu wax dina mën a jëmloo kanam. Bu amee mbokk mu tàmm def waxtaan yu bare, soxlawul mu xelal ko saa yu defee waxtaan. Am na ñuy def waxtaan yi ñu jagleel ñépp. Waaye nag, mbokk miy jàpple kiy xelal nit ñi, dafa war a am seetlu te xam ne ñooñu sax mën nañu leen jàpple ndax ñu jëm kanam. — 1 Tim. 4:15.
14 Li ñu war a seetlu : Lan moo mën a dimbali kiy xelal nit ñi ndax bu nit defee waxtaan, mu mën a seetlu li baax ak li mu war a taneel ? Ci li ëpp ci 53 pàcc yi nekk ci téere École du ministère, ñetteelu wërale bi dafay wone ci lu gàtt li ñu war a seetlu. Wottukatu lekkool bi war na seet it ci téere bi yeneen xelal yi tax mu mën a gaaw a gis ndax waxtaan bi leer na, yomb na nànd te def na li ñu ci doon séentu. Boo seetee laaj yi nekk ci kow ci xët 55 ak li nekk ci xise bi mujj ci xët 163, dinga xam li ñu bëgg a wax.
15 Bindal fi ñu bindul dara : Ci téere École du ministère bi, am na ci xët yi fi ñi bindul dara. Am na it fi ñu rëdd ndax booy jàngal sa bopp walla boo fekkee lekkool bi, nga mën ci bind lu la neex. (Seetal xët 77, 92 165, 243, 246 ak 250.) Ayu-bés bu nekk, booy dem ci lekkool bi, na nga yóbbaale sa téere. Booy déglu waxtaan bu njëkk bi, na nga jàngaale ci sa téere li muy wax. Bul téj sa téere ba lekkool bi jeex. Jàppal bu baax li wottukatu lekkool bi di wax. Nit kiy def waxtaan bi, seetlul bu baax ni muy jàngalee, laaj yi muy laajte, li tubaab di woowe figures de style mel ni misaal yi walla yeneen yu mel noonu ak it li mu indaale ngir ñu xool ko. Boo bindee li la mën a jariñ, dinga mën a jàngaat te jëfandikoo lu am solo lu bare li nga jàng ci lekkool bi.
16 Yeesu Krist xamoon na ne ci li nit mën a am yépp, amul lu gën a réy waare xibaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla. Loolu moo ëppoon solo ci li taxoon ñu yónni ko ci kow suuf (Mark 1:38). Newoon na : “ Damaa wara dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma. ” (Lukk 4:43). Ñun ñi ko nangu topp, jàpp nañu lool ci liggéeyu waare xibaar bu baax bi. Te fu ñu tollu, ñu ngi fexe ba suñu “ sarax bu koy màggal ” gën di baax (Yaw. 13:15). Kon nag, nañu bañ a bàyyi dara tere ñu teew ci lekkool Sasu Nguuru Yàlla. Lekkool boobu dina tax ñu mën a def li ëpp solo ci àddina.