Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 févr.
“ Dañu leen bëggoon a laaj lu jar a xalaat : ndax kéemaan yi ñu dégg ci Mbind mu sell mi, amoon na dëgg ? [Mayal nit ki tontu.] Ndax kéemaan yu mel noonu, mën na am tey ? ” Jàngal 1 Tesalonikk 2:13, te won ko ne bu ñu gëmee ne Yàlla mooy wax ci Biibël bi waaye du nit, kon dinañu xam ne kéemaan yooyu amoon na.
Réveillez-vous ! 22 févr.
“ Tey, lu baax li nit ñi fonkoon démb bareetul. Yàgg na bi Yàlla waxee xale yi ñu teral seen yaay ak seen baay. [Jàngal 2 Musaa 20:12 te woneel foofu ne Yàlla dafay barkeel ñiy teral seeni wayjur.] Waaye ndax tey yaay yi ñu ngi leen di teral ni mu ware ? [Mayal nit ki tontu]. Téere bii dafay wax coono yi yaay yi am ci réew yu bare, ak it li ñuy def ngir génn ci. ”
La Tour de Garde 1er mars
“ Ñakk déggoo dafay gën a yokku tey. Looloo tax dëkkandoo yu bare mënuñu déggoo. Ñu bare dañu ci jaaxle. Ndax foog nga ne àddina si dina gën a neex bu nit ñi toppoon li ñu wax fii ? [Jàngal Room 12:17, 18, te mayal nit ki tontu.] Waaye nag yenn saay dina am lu la boole ak sa moroom. Waaye bu loolu amee, Kàddu Yàlla mën na la won li nga mën a def ba defaraat seen diggante. Téere bii ci loolu lay wax. ”
Réveillez-vous ! 8 mars
“ Dañu bëgg wax ak nit ñi ci luy laal suñu ëllëg. At mu nekk, li nit ñi soxla ci li tubaab di woowe énergie (maanaam lu mel ni këriñ, petarol ak yu mel noonu) dafay gën a bare. Waaw bu énergie bi ñu soxla jeexee ci àddina, lan lañuy def ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone li nit ñi def ngir am énergie bu dul tilimal lu bare. Dafay wax it ci kan la bépp énergie jóge. ” Jàngal Isayi 40:26 te won ko ne ndegam ci Yàlla la bépp énergie jóge, kon xam na li ñu war a def bu énergie bi bëggee jéex.