“ Kàdduy yoonu ngëm ” : suñu ñam la ci wàllu ngëm
1 Bëgg neex Yàlla ci lépp li ngay def, jafe na lool (1 Tim. 4:7-10). Loolu, mënuñu ko ci suñu kàttanu bopp. Ku koy jéem, dinga gaaw a sonn walla daanu (Isa. 40:29-31). Waaye mën nañu jot ci kàttanu Yexowa. Lenn li ñu mën a def ngir loolu mooy “ regg [maanaam lekk ba suur] ci kàdduy yoonu ngëm ”. — 1 Tim. 4:6.
2 Ñam bu neex te bare ci wàllu ngëm : Yexowa dafa ñuy may ñam bu neex te bare ci wàllu ngëm. Ñam boobu, mën nañu ko am ci Kàddoom ak ci li ñu “ surga bu takku te teey ” bi jox (Macë 24:45). Looy def ngir loolu yépp jariñ la ? Ndax yaa ngi jàng Biibël bi bés bu nekk ? Ndax am na ay waxtu yoo xam ne ci waxtu yooyu ngay gëstu Biibël bi (Sab. 1:2, 3) ? Fasoŋu lekk boobu, dafa ñuy may doole ci wàllu ngëm. Te duñu sonn bu ñuy xeex àddina Seytaane bi (1 Ywna. 5:19). Su ñu dugalee lu baax rekk ci suñu xel, te bu ñu ko jëfee it, Yexowa dina nekk suñu wet. — Fil. 4:8, 9.
3 Yexowa dafay jaar itam ci ndaje yi ñu am ci mbooloo mi ngir may ñu doole (Yaw. 10:24, 25). Foofu, dañuy jàng lu jëm ci suñu diggante ak Yexowa. Dañu fay am itam ay àndandoo yu baax. Loolu yépp, dina tax ñu gën a dëgër bu ñu nekkee ci nattu (1 Pie. 5:9, 10). Benn jànq bu nekk suñu mbokk ci ngëm nee na : “ Ca lekkool laay yendu. Loolu dafa may sonal lool. Waaye ndaje yi, ñu ngi mel ni tool bu naat ci màndiŋ mi. Foofu damay amaat doole ngir bés bi ci topp ca lekkool ba. ” Def lépp ngir teewe suñuy ndaje, aka am njariñ !
4 Waare dégg gi : Waar nit ñi dafa meloon ni ñam ci Yeesu. Loolu dafa ko doon may doole (Ywna. 4:32-34). Noonu it la war a doon ci ñun. Bu ñuy waxtaan ak nit ñi ci yaakaar bu rafet bi ñu Yàlla may, dafa ñuy yokkal doole. Booy def lu bare ci liggéeyu waare bi, sa xel ak sa xol dañuy gën a nekk ci Nguuru Yàlla ak ci barke yi muy indi ci kow suuf si. Dëgg dëgg, loolu dafay seddal xol. — Macë 11:28-30.
5 Waaw, tey Yexowa dafay may mbootaayam ñam bu neex te bare ci wàllu ngëm. Bokk ci ñi am loolu, barke bu réy la ! Nañu wéy di màggal Yexowa ndax mbégte bi ñuy yëg ci suñu xol. — Isa. 65:13, 14.