Xaaj 6 : Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Bu la nit ki laajee dara
1 Boo amee njàngum Biibël, nanga topp njàngale yi ni ñuy toppante. Loolu moo gën nga nekk di waxtaan ci lépp lu mu lay laaj. Loolu dina ko may li mu soxla ci wàllu ngëm ngir xam bu baax dëgg gi. Te digganteem ak Yàlla dafay gën a rattax rekk (Kol. 1:9,10). Waaye, ba tey, am na ñoo xam ne, booy waxtaan ak ñoom, dañuy am ay laaj yu bare ci fànn yu bare. Bu loolu amee, lan lañu war a def ?
2 Xamal bu baax li nga ko war a tontu : Su laaj bi àndee ak li ngeen di waxtaan, mën nga ci tontu ci saa si. Yenn saay li muy laajte mu ngi ci téere bi ngeen di jàng, waaye àggaguleen fa. Xéyna, boo ko ko xamalee, dina nangu xaar ba ngeen àgg fa. Waaye, mën na am laaj bi bañ a bokk dara ak li ngeen di waxtaan. Walla nga war a gëstu bala di ci mën a tontu. Kon, li gën mooy xaar ba ngeen pare njàng mi, walla xaar ba beneen yoon bala ngeen ciy waxtaan. Am na waaraatekat yuy bind laaj boobu ngir won nit ki ne ci lu wóor dina ci tontu. Loolu lépp, dina tere waxtaan bi dem fu sore.
3 Téere yi ñu njëkk jàng ak nit ñi, dañuy wax li Biibël jàngale, waaye duñu ci sore noonu. Xéyna loolu du doy bala nit ki gëm ko. Mën na am it mu am lu mu gëm bu baax fekk loolu nekkul dëgg. Kon, lan nga war a def ? Xéyna am na yeneen téere yuy gën a xóotal li ci Biibël bi wax. Su ko jàngee te ba tey loolu doyu ko, nanga bàyyi waxtaan boobu ba beneen yoon te kontine seen njàngum Biibël (Ywna. 16:12). Dina kontine di yokk li mu xam ci Biibël bi. Te dina gën a dëgëral digganteem ak Yàlla. Xéyna bu ëllëgee dina nànd njàngale moomu.
4 Xamal fan la sa wax war a yem : Bu la wóorul ne tont bi nga bëgg joxe mooy tont bu baax bi, bu ko wax. Moytul a wax sa xalaatu bopp ba juum (2 Tim. 2:15 ; 1 Pie. 4:11). Kon nee ko dinga gën a gëstu mbir moomu, te dellusi ngir tontu ci. Mën nga ci jaar sax ngir won ko ni ñuy gëstoo ci yu mel noonu. Mbootaayu Yexowa defar na lu bare ngir ñu mën a gëstu Biibël bi. Won ko ndànk-ndànk ni mu mënee jëfandikoo loolu lépp. Bu boobaa, xéyna dina dem ba mën a wutal boppam tontu laaj yi mu bëgg laaj. — Jëf. 17:11.