Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu : Li ñu warul a fàtte
Ren, ci bésu alxemes 24 màrs lañuy def ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Magi mbooloo mi war nañu topp tegtal yii :
◼ Waxtu ndaje bi, na nekk waxtu boo xam ne, bu ñuy joxante mburu mi ak biiñ bi, dina fekk jant bi so ba pare.
◼ War nañu xamal kiy def waxtaan bi ak ñeneen nit ñépp, waxtu bi ñuy defe ndaje bi ak fu ñu koy defe.
◼ Bala waxtu ndaje bi jot, war na fekk mburu mi ak biiñ bi pare. — Seetleen La Tour de Garde bu 15 feewriyee 2003, xët 14-15.
◼ Aset yi, weer yi, taabal bu baax ak lu jekk lu koy muur, loolu lépp war nañu leen a teg seen palaas bala waxtu ndaje bi jot.
◼ Bala ndaje bi di jot, war nañu setal bu baax Saalu Nguur gi walla béréb bu ñuy defe ndaje boobu.
◼ Bala ndaje bi di jot, war nañu tànn ñi war a teral nit ñi, ak ñi war a joxe mburu mi ak biiñ bi. War nañu leen a wax ba mu leer li ñu war a def bés boobu. War nañu leen wax it ne li ñuy sol ak ni ñuy defare seen bopp dafa war a jekk.
◼ Karceen bu bokk ci ñi Yàlla tànn, mën na feebar walla màgget ba du mën a teew ci ndaje boobu. Bu booba war nañu seet ni ñu mënee def ba indil ko ci mburu mi ak ci biiñ bi.
◼ Bu ñaari mbooloo walla lu ko ëpp waree bokk fi ñuy defe ndaje boobu, nañu fexe ba mu bañ a am nit ñu bare ñuy xaar ci buntu saal bi, ci mbedd mi walla fi ñuy bàyyee oto yi.