Nañu fexe ba nit ñi bëgg yokk li ñu xam ci Biibël bi, bu ñuy faral di leen indil suñu yéenekaay yi
1 Nit ñu bare dañuy nangu waxtaan ak ñun te jël suñuy téere waaye ba tey nanguwuñu jàng Biibël bi ak ñun. Lan lañu mën a def ngir ñu bëgg yokk li ñu xam ci Biibël bi ? Mën nañu faral di leen yóbbul suñu yéenekaay yi te jaar ci loolu ngir fexe ba ñu bëgg yokk li ñu xam ci Biibël bi. Kon boo joxee nit yéenekaay, bindal turam, adareesam, bés bi nga waxe ak moom, yéenekaay yi mu jël ak aaya bi ngeen waxtaane. Nanga bind itam lépp li la mën a xamal li ko itteel. Yéenekaay buy génn, nanga ci seet li mën a itteel ñi ngay faral di yóbbul yéenekaay yi. Te nanga ci waxtaan boo leen di seeti (1 Kor. 9:19-23). Benn bés, mën na am ñu jàng ci suñuy téere lu mën a tax ñu bëgg yokk li ñu xam ci Biibël bi.
2 Ci ñi gën a bare, jàng yéenekaay yi rekk te yem ci, du tax ñu nekk jaamukatu Yexowa. Ndegam def lépp ngir xam Yexowa, lu jamp la tey, ndax am na leneen lu ñu mën a def ngir dimbali nit ñi ci loolu (Tsë. 2:2, 3 ; Peeñ. 14:6, 7) ? Bu ñuy yóbbul nit yéenekaay bu bees, mën nañu ko jàngal aaya bu ñu tànnoon bu baax bala ñu fay dem. Loolu mën na ko xiir ci bëgg yokk li mu xam ci Biibël bi.
3 Waxtaan yu def benn aaya : Nanga xalaat ñi nga war a yóbbul yéenekaay yi sog a génn te nanga waajal ay waxtaan yoo xam ne, bu ci nekk dina jëm ci benn aaya te laal luy itteel nit ki (Fil. 2:4). Boo tasee ak ku mbokkam gaañu lu yàggul, dinga mën a waxtaan ak moom ci li Biibël bi wax ci ñi dee ak ci ndekkite li. Mën nga tànn ay aaya ci téere Comment raisonner ci xaaj yi tudd “ Mort ” (dee) ak “ Resurrection ” (ndekkite). Léegi, saa yoo fa jaaree, nanga waxtaan ak moom benn ci aaya yooyu. Bu ngeen paree ci waxtaan yooyu, li ci mën a topp mooy waxtaan ci li fiy dindi feebar, màgget ak dee. Li ñu bëgg mooy seet waxtaan bu mën a itteel nit ki, te won ko ndank-ndank li ci Biibël bi wax.
4 Dimbali ko mu xam bu baax li aaya bi bëgg wax : Xam nañu ne waxtaan bu yomb te gàtt moo gën. Waaye bul jàng rekk aaya bi nga tànn, te yem ci. Seytaane dafa gëlëmal xelu nit ñi ci lu jëm ci xibaar bu baax bi (2 Kor. 4:3, 4). Ñi tàmm a jàng Biibël bi sax, mënuñu xam bu baax li ñuy jàng su amul ku leen ci dimbali (Jëf. 8:30, 31). Kon booy jàng benn aaya, nanga ko faramfàcce bu baax te misaal ko, mel ni booy def waxtaan ci lekkoolu sasu Nguuru Yàlla (Jëf. 17:3). Fexeel ba nit ki gis njariñ bi muy am su toppee li nekk ci Kàddu Yàlla.
5 Su waxtaan yooyu neexee nit ki, nanga yokk ndànk-ndànk aaya yi ngay jàng ak moom. Mën nga dem ba ñaar walla ñett aaya ci waxtaan bu nekk. Te fexeel ba am fooy jaar ba won ko téere Laaj walla téere Xam-xam. Boo defee noonu, xéyna ki ngay faral di yóbbul suñu yéenekaay yi, dina nangu ñu jàngal ko Biibël bi.
[Laaj yi]
1. Bu fekkee ne dañu faral di yóbbul nit suñuy yéenekaay, naka lañu mënee jaar ci loolu ngir fexe ba mu bëgg yokk li mu xam ci Biibël bi ?
2. Def lépp ngir xam Yexowa, lu tax mu jamp tey ? Ginnaaw jox leen ay yéenekaay, lan lañu mën a def ngir dimbali nit ñi ci loolu ?
3. a) Naka lañu mënee waajal ay waxtaan yu def benn aaya, waxtaan bu nekk ? b) Lu gën a itteel nit ñi ci seen gox ?
4. Bu ñu jàngee dara ci Biibël bi, lu tax ñu war a dimbali nit ki mu xam bu baax li aaya bi bëgg wax ? Naka lañu mënee def loolu ?
5. Noo mënee def ba ki ngay faral di yóbbul suñu yéenekaay yi, dem ba nangu jàng Biibël bi ak ñun ?