Nangeen jariñoo bu baax waxtu yi ngeen di def ci waaraate bi
1 Xam nañu ne li ñu war a def ci liggéeyu waare bi bare na lool, te jot bi des barewul (Ywna. 4:35 ; 1 Kor. 7:29). Bu ñu defaree porogaraam bu baax te xalaat ci bu baax, dinañu mën a jariñoo bu baax waxtu yi ñu bëgg def ci liggéeyu waare bi.
2 Waajalleen seen bopp bala ngeen di waare : Bala ngeen di dem ci ndaje yi ñuy def bala ñuy dem waare, nangeen seet ndax am ngeen téere ak yéenekaay yi ngeen nar a soxla. Nañu xam bu baax it li ñuy wax ngir wone suñu téere yi ak suñu yéenekaay yi. Bu ñu paree ci ñaan biy àggale ndaje boobu, gaawleen dem fi ngeen war a waare. Loolu dina leen may ngeen bañ a yàq waxtu yi ngeen di def ci waaraate bi, yéen ak ñi ngeen di àndal, te mën a def liggéey bu gën a réy.
3 Bu dee yow yaa war a jiite ndaje bu ñuy am bala ñuy waare, bu waxtu wi jotee rekk, nanga ko komaase. Defal waxtaan bu gàtt — bumu weesu 10 ba 15 minit. Bala gurup bi di tasaaroo, na la woor ne kenn ku nekk xam na ki muy àndal ak fi mu war a waare.
4 Bu ngeen di waaraate : Bu ndaje bi ñuy am bala ñuy waare bi jeexee, buleen yeexantu. Nangeen gaaw a dem fi ngeen war a waare. Bu ngeen bokkee oto te nga war a teel a arete waaraate këroo-kër, xéyna liy gën mooy nga waajal sa paas walla fexe ba mën a ñibbil sa bopp. Bu ko defee, ñeneen ñi duñu soxla teel a arete. Boo àndee ak ñeneen ci waaraate bi, nanga bàyyi xel ci ñoom ndaxte xéyna ñu ngi lay xaar nga àggale sa waxtaan. Loolu mën na laaj nga seet fasoŋ bu rafet bi nga mënee dog waxtaan bi, bu dee ki ngay waxal dafa bëgg werante. Walla boo gisee ne suñu waxtaan neex na ki ngay waxal, mën nga jàpp ak moom bés boo fa mën a dellu ngir kontine waxtaan bi. — Macë 10:11.
5 Boo waree dellu seeti nit ñi, mën nga bañ a dox lu bare, fekk jaru ko. Loolu dinga ko mën a def booy njëkk seeti ñi bokk béréb fi ñu dëkk bala ngay dem feneen. Mën nga it telefone bala ngay dem seeti kenn ngir xam ndax mu nga kër ga (Léeb. 21:5). Boo naree yàgg ci ki ngay seeti, nanga seet ak ñi ngay àndal li ñu mën a def ci waaraate bi ci wetu kër nit kooku. Su ñu mënul a def loolu, nañu dellu seeti ay nit yu dëkk ci boor yooyu.
6 Dañu tollu ci jamano ngóob bu réy ci wàllu ngëm (Macë 9:37, 38). Liggéey boobu, léegi mu jeex. Looloo tax ñu war a bëgg di jariñoo bu baax waxtu yi ñuy def ci liggéeyu waare bi.