Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi
14-20 sãwiyee
Woy-Yàlla 22
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na am ñu topp li nekk ci xët 8 te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 sãwiyee ak Réveillez-vous ! bu sãwiyee. Mën nañu wax it leneen lu mën a baax ci seen gox
15 min : “ Nangeen jariñoo bu baax waxtu yi ngeen di def ci waaraate bi. ”a Laajal ci kanamu ñépp suñu benn mbokk bu góor bu aay ci fasoŋ bi muy jiite gurup buy dem waaraate këroo-kër. Nanga ko laaj lii : “ Naka ngay def ngir waajal sa bopp ngir jiite bu baax gurup bi te fexe ba waaraatekat yi jariñoo bu baax waxtu yi ñuy def ci liggéeyu waare bi ? ”
20 min : “ Na seen wax jépp . . . am xorom. ”b Bu ngeen àggee ci xise 2, nangeen jàng Yowaana 4:7-15, 39.
Woy-Yàlla 38
21-27 sãwiyee
Woy-Yàlla 96
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal téere yi ñuy wone ci wéeru fewriyee. Na am ñuy wone ni ñu ko mënee wone. Waxal ne ñu ngi xiirtal ñépp ñu seetaan wideo bi tudd Soigner sans transfusion — Besoins et droits du patient (maanaam faj nit te doo jëfandikoo deret — Li nit ki ñu faj soxla ak li ko yoon may). Bu ko defee, dinañu waajal waxtaan bi ñuy def ci ndaje liggéeyu waare bi ñuy am ci ayu-bés bu 4 fewriyee.
10 min : Ndax yaa ngi jëfandikoo téere Examinons les Écritures chaque jour ? Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci xaaj bi njëkk ci téere Examinons les Écritures chaque jour — 2008 te tudd Introduction. Nangeen waxtaan ci njariñ bi nekk ci jàng bés bu nekk aaya bés bi ak kàddu yi mu àndal. Waxal ñi teew ñu wax ni ñuy fexee ba jàng bés bu nekk aaya bés bi te loolu naka la leen amale njariñ. Mën nga waxtaan ak benn walla ñaari nit bala ndaje bi di jot ngir ñu waajal li ñuy tontu. Nanga wax ci lu gàtt ci aaya atum 2008.
25 min : “ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi. ”c (Xise 1 ba 10). Wottukatu liggéeyu waare bi moo ko war a def. Ci kanamu ñépp, nanga waxtaan ak benn walla ñaari waaraatekat yu nekkoon ay pioñee yuy jàpple ci at mii weesu, fekk seen porogaraam dafa xatoon lool walla dañu feebaroon. Naka lañu fexee ba mën loolu ? Lan lañu ci am lu neex ? Bu ngeen àggee ci xise 7, nanga wax porogaraamu ndaje yi ñuy am bala ñuy dem waare ci weeru màrs, awril ak me.
Woy-Yàlla 79
28 sãwiyee ba 3 fewriyee
Woy-Yàlla 91
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàtte bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru sãwiyee te joxe ko. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Waxtaan ak ñi teew ci La Tour de Garde bu 1 fewriyee ak Réveillez-vous ! bu fewriyee. Waxal ci lu gàtt li nekk ci yéenekaay bu nekk. Ba pare laajal ñi teew yan waxtaan ñoo mën a neex nit ñi nekk ci seen gox ak lu tax ñu yaakaar loolu. Waxal ñi teew ñu wax yan xaaju yéenekaay bi lañu bëgg wone ci waaraate bi. Ban laaj lañu mën a laajte ngir komaase waxtaan bi ? Ban aaya bu nekk ci xaaju yéenekaay bi lañu mën a jàng ? Lu ñu mën a wax ngir aaya bi ñu jàng mën a ànd bu baax ak xaaju yéenekaay bi ñu bëgg wone ? Na am ñu topp li nekk ci xët 8, ngir wone yéenekaay yi te wone ni ñu mënee wone yéenekaay bu nekk.
20 min : “ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi. ”d (Xise 11 ba 17). Bu dee am ngeen kayit yi ñuy joxe ngir woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi, bu ngeen di def xise 14, joxleen ñi teew ñépp benn ci kayit boobu. Nañu wax it li ñu taxawal ci mbooloo mi ngir mën a joxe kayit boobu ci gox bi ñuy waare yépp.
15 min : “ Nañu dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu nekk ay waaraatekatu xibaaru Nguuru Yàlla. ”e Bu ngeen amee jot, waxal ñi teew ñu wax seen xalaat ci aaya yi am ci xaaj bii.
Woy-Yàlla 9
4-10 fewriyee
Woy-Yàlla 84
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Seetleen li nekk ci xaaj bi tudd “ Ay tont ci seeni laaj ”.
10 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
25 min : “ Ndax defaguleen ko ba léegi ? ” Benn njiit moo war a def waxtaan bii. Na komaase waxtaan bi jëm ci wideo bi tudd Besoins et droits du patient ak laaj yi nekk ci xaaj bii. Booy jeexal waxtaan bi nanga jàng xise bu mujj bi te xiirtal ñépp ñu jàngaat bu baax xaaju La Tour de Garde ak Sasu Nguuru Yàlla yi ñu fa wax. Waxal ñi teew ne ñi ko defagul mën nañu jëfandikoo lu am solo li nekk ci xët 5 ak 6 ci Sasu Nguuru Yàlla bu nowàmbar 2006 ngir seet ni ñu war a gise xaaju deret yu ndaw a ndaw yi walla ni ñu bëgge ñu faj leen, ba pare def li ñu tànn ci kart bi tudd DPA. Ñi bindoon seen kart ba pare mën nañu seet ndax amul li ñu bëgg soppi ci li ñu tànnoon te bu ñu ko soxlaa, mën nañu ko defaat ci kart bu bees.
Woy-Yàlla 2
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
d Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
e Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.