Nañu fàttaliku li ñu jàng ci lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla
Laaj yii di topp, dinañu ci waxtaan ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla bi ñuy am diggante 25 fewriyee ba 2 màrs 2008. Ci lu mat 30 minit, wottukatu lekkool bi dina waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu jàng ci lekkool bi diggante 7 sãwiyee ba 2 màrs 2008. [Buleen fàtte lii : bu amee ay laaj yi ñu wonewul fi ñu mënee gis tont yi, yéen a war a seetal seen bopp fu tontu yi nekk. — Seetleen li ñu wax ci téere École du ministère ci xët 36 ak 37.]
LIY TAX ÑU AAY CI WAX
1. Lan lañu war a def ngir dimbali ñi teew ñu nànd bu baax aaya yi ñuy jàng ? Te lu tax ñu war a def loolu ? [be xët 228, xise 2-3]
2. Dañu war a fexe ba bu ñuy waxtaan ak nit ñi, ñu am lu am solo lu ñu mën a jële ci li ñu wax. Loolu lu tax mu am solo lool ? Naka lañu mënee def loolu ? [be xët 230, xise 3-5, ak wërale bi]
3. Naka la gëstu yi ñuy def ngir waajal waxtaan mënee tax nit ñi gën ci jàng lu bare ? [be xët 231, xise 1-3]
4. Bu ñuy wax ci aaya yu nit ñi xam bu baax, lan lañu mën a def ba ñu am lu bees lu ñu ci mën a jàng ? [be xët 231, xise 4-5]
5. Bu ñuy jàng aaya ak nit, lu tax waxtaan ci am solo lool ? [be xët 232, xise 3-4]
WAXTAAN N° 1
6. Lu tax ñu mën a ne yawut yi lañu doon xalaat bi ñu doon bind téere Macë ? [si xët 176, xise 6-7]
7. Naka lañu mënee waajal suñu xol ngir li ñu Yàlla bëgg jàngal ci ndaje yi mën a dugg bu baax ci suñu xol ? (2 Chron. 20:33) [be xët 13, xise 4–xët 14, xise 5]
8. Lan la wayjur yi mën a def ngir jàngal seeni doom ñu “ yee [wu] ci yoonu mucc ” ? (2 Tim. 3:15) [be xët 16, xise 3-4]
9. Téere Macë wone na ni li Biibël bi waxoon ame. Naka la ko defe ? [si xët 181, xise 32]
10. Téere Macë dafay wone ne Yeesu mooy Almasi bi Yàlla dige woon, ak it buuru Nguur Yàlla. Téere Màrk nag, lan lay wone ci Yeesu ? [si xët 182, xise 7-8]
LI ÑU WAROON A JÀNG CI BIIBËL BI AYU-BÉS BU NEKK
11. Mer ba wax lu bon, walla dénc sa mer, lu gën a bon ? (Macë 5:21, 22) [w08 1/15 “ La parole de Jéhovah est vivante : Points marquants du livre de Matthieu ”]
12. Naka la karceen yi mënee kontine di bañ a réy ‘ bët ’ ? (Macë 6:22, 23) [w06 10/1 p. 29]
13. Lan la Yeesu bëggoon a wone bi mu newee taalibeem yi : “ Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki ? ” (Macë 13:51, 52) [w08 1/15 “ La parole de Jéhovah est vivante : Points marquants du livre de Matthieu ”]
14. Lu tax Yeesu faraloon di wax ak ñi mu doon faj “ ñu bañ ko siiwal ” ? (Macë 12:16) [w87 5/15 xët 9 ; cl xët 93-4]
15. Lan mooy ‘ natt ’ bi nit di ‘ nattale ’ bi Yeesu doon wax ? (Màrk 4:24, 25) [w80 6/15 p. 12 ; gt pàcc 43]