Lii, ngëm lay wone !
1. Yan xew-xew yu metti la Yeesu waxoon ne dina am ?
1 Taalibe yi ñu ngi doon déglu bu baax Yeesu bi mu doon wax ci jamano ji mu fiy nekk ak ci bu àddina su bon si di tukki. Xew-xew yu metti yu mel ni xare, xiif, yëngu-yëngu suuf ak feebar yuy rey nit ñu bare, dinañu dal doomu Aadama yi. Ci kow loolu, Yeesu nee na taalibeem yi ne dinañu leen bañ, yóbbu leen ci àttekat yi, te rey leen. Ay nit ñuy mbubboo turu yonent dinañu feeñ, nax nit ñu bare. Mbëggeelu ñi ëpp ci nit ñi dina wàññiku.
2. Li ñuy waare xibaar bu baax bi ci àddina si sépp, lu tax mu doon lu doy waar ?
2 Taalibe yi waroon nañu jaaxle lool bi ñu déggee Yeesu di wax ne, ci jamano ju mel noonu lañuy yégle ci àddina si sépp xebaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla (Macë 24:3-14). Lu doy waar li Yeesu waxoon noonu, moom lañuy gis tey jii. Seede Yexowa yi sawar nañu ci yégle xibaar bu baax bi, fekk ñu ngi ci jamano ju metti lool. Mbëggeel diggante doomu Aadama mu ngi wàññiku ci àddina, waaye suñu mbëggeel moom, mu ngi gën di yokku. “ Xeet yépp ” a ñu bañ. Waaye ñun, xeet yépp lañuy waar.
3. Bind nañu ci xët 3 ba 6, li ñu def ci liggéeyu waare bi ci àddina si sépp. Lan moo la ci gën a neex ?
3 Def nañu ci xët 3 ba 6, li seede Yexowa yi def ci atum liggéeyu waare bii weesu. Bu ñu seetee li ci nekk, suñu doole dina yokku bu baax ! Lu mat 16 at a ngi nii, ñu ngi def lu ëpp benn miliari waxtu at mu nekk ci waaraate bi ak ci liggéeyu sàkk ay taalibe. Loolu dafay wone ngëm dëgg ! Ci 100 pioñee yoo jël, 5,8 ñoo ci yokku. Ci 100 waaraatekat yoo jël, 3,1 ñoo ci yokku. Ci 100 njàngum Biibël yoo jël, 4,4 ñoo ci yokku. Ci 100 nit ñi sóobu yoo jël 20,1 ñoo ci yokku. Am na lu jege juróom ñaari millioŋi nit ñuy jaamu Yexowa di ko topp bu baax. Masuñu bare noonu. Loolu lu neex a dégg la. Seetal li ñu def ci xët 3 ba 6. Lan moo la ci neex ?
4. Yan jafe-jafe la benn góor amoon te mu góor-góorlu ba génn ci ngir mën a sóobu ?
4 Li ñu wone foofu réy na lool. Waaye waruñu fàtte ne ngëm moo tax ñu def liggéey boobu. Nañu ko seet ci li Guillermo def. Nit kooku, Bolivie la màgge. Mu ngi juddu ci atum 1935. Bi mu amee juróom ñeenti at la komaasee liggéey ci toolu fi ñuy beye dorog bi ñuy woowe ci tubaab cocaïne. Xale la woon bi mu komaase yéy xobu dorog boobu ngir waññi coono liggéey bu metti bi mu nekke woon. Mujj na tàmm di naan ba màndi ak tux sigaret. Bi mu komaasee jàng lu jëm ci li Yexowa bëgg ci moom, Guillermo dafa bàyyi tux ak naan ba màndi. Waaye li gënoon a jafe ci moom, mooy bàyyi yéy xobu cocaïne boobu, fekk dafa ci yàggoon lool. Dafa ñaan Yàlla te bañ ci tàyyi. Mujj na bàyyi lu bon loolu mu tàmmoon, ñu daldi ko sóob ci ndox. Lii la wax : “ Léegi dama sell, te bég lool ”.
5. Lan lañu bëgg ?
5 Yexowa fonk na dëgg nit ñi. Li mu bëgg mooy ñépp tuub seeni bàkkaar (2 Pie. 3:9). Loolu lañu bëgg ñun itam. Yàlla na ñu suñu xol xiir ci def lépp li ñu mën ngir kontine di dimbali boroom xol yu rafet yi. Na loolu tax it nit ñooñu xam te bëgg Yexowa ni ñun.