Li ñu warul a fàtte ci Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu
Njiit yi ci mbooloo mi war nañu topp tegtal yii :
◼ Na leen wóor ne duñu joxante mburu mi ak biiñ bi bala jant bi di so.
◼ War nañu wut mburu ak biiñ yi ñu war a jëfandikoo ci ndaje boobu, te defar lépp ba mu baax bala waxtu ndaje bi jot. — Seetleen li ñu wax ci La Tour de Garde bu 15 feewriyee 2003, xët 14-15.
◼ Bala waxtu ndaje bi di jot, war nañu wut taabal bu baax ak lu jekk lu koy muur, teg leen seen palaas. Aset yi ak weer yi, war nañu nekk it ci seen palaas.
◼ Saalu Nguur gi walla béréb fu ñuy defe ndaje boobu, war nañu ko raxas ba mu set bala ndaje bi di jot.
◼ Bala ndaje bi di jot, war nañu tànn ñi war a teral nit ñi, ak ñi war a joxe mburu mi ak biiñ bi. Ñooñu war nañu xam bu baax li ñu war a def ci ndaje boobu te bañ a fàtte ne li ñuy sol ak ni ñuy defare seen bopp dafa war a jekk.
◼ Karceen bu bokk ci ñi Yàlla tànn, mën na feebar walla mu màgget ba du mën a teew ci ndaje boobu. Bu loolu amee, war nañu fexe ba yóbbul ko mburu ak biiñ.
◼ Bu ñaari mbooloo walla lu ko ëpp waree bokk fi ñuy defe ndaje boobu, bu benn bi di waaj a pare ba mbooloo mi ci topp di ko xaar, nañu fexe ba nit ñi bañ a gurupoo ci buntu saal bi, walla ci mbedd mi ak fi ñuy gaare oto yi.
◼ Bu dee ci beneen béréb la ñuy defe ndaje bi, nañu wóor ne mikroo yi baax na ñu ngir ñi teew ñépp mën a dégg bu baax li kiy def waxtaan bi di wax .