Nañu fàttaliku njot gi te wone ci ne fonk nañu ko lool
1, 2. Lan moo tax ñu war a fàttaliku njot gi te wone ci ne fonk nañu ko lool ?
1 Samdi 22 màrs 2008, bu jant bi sowee, ci àddina si sépp, karceen yi dinañu fàttaliku deewu Yeesu Kirist ni mu leen ko sante (Luug 22:19 ; 1 Kor. 11:23-26). Dañu koy def ndaxte fonk nañu bu baax li ñu Yàlla ak Yeesu defaloon am na léegi 1975 at. Yeesu, dañu ko toroxal ba mujj ko rey ci bant. Waaye masul bàyyi di topp li ko Baayam santoon. Noonu la sellale turu Baayam. Li mu def noonu may na Yàlla mu am tont bi gën ci li ko Seytaane doon jiiñ. — Job 1:11 ; Léeb. (Prov.) 27:11.
2 Deret bi Yeesu tuur moo fas kóllëre bu bees bi. Loolu moo tax Yàlla mën a jël ay nit ñu matul, jàppe leen ni ay doomam. Te ñooñu yaakaar jiite ak Kirist ci Nguur gi nekk ca asamaan (Yér. (Jér.) 31:31-34 ; Màrk 14:24). Te yokk ci, mbëggeel bu dëggu bi Yàlla am ci doomu Aadama yi feeñ na bu baax ci li mu saraxe doomam bi mu bëggoon lool. Loolu la Yeesu ci boppam waxoon Nikodem. — Ywna. 3:16.
3. Ndaje fàttaliku bi, naka lay jariñe ñi fay teewe ?
3 Nañu woo suñuy moroom ci ndaje bi : Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee, waxoon na ne dañu war a bind ci benn kayit turu nit ñi nu bëgg woo ci ndaje fàttaliku bi, ba pare def ko. Ndax komaase nga def loolu ? Ndax seet nga li nga mën a def ngir mën a bokk bu baax ci liggéey bu am solo bi ñuy komaase bésu 1 màrs ngir woo nit ñi ci fàttaliku bi ? Ñi fay teewe, dinañu dégg lu jóge ci Mbind mi, lu mën a tax ñu am ngëm ci njot gi. Te ngëm boobu mën na tax ñu am dund gu dul jeex. — Room 10:17.
4. Lu tax ñu war a teel a agsi ci ndaje fàttaliku bi ?
4 Nañu def lépp ngir mën a teel a agsi ci Saalu Nguur gi, ngir teeru ñiy wuyusi woote bu am solo boobu. Ñiy teewe ndaje fàttaliku bi dinañu bare lool. Kon laaj na ñu bàyyi xel bu baax ci ñiy sog a ñëw akit ci ñiy teewe lée-lée suñuy ndaje yi.
5. Naka nga mënee waajal sa xol ngir ndaje fàttaliku bi ?
5 Nañu waajal suñu xol : Ci téere Examinons les Écritures chaque jour bu 2008 ak ci Calendrier bu 2008, bind nañu porogaraamu aaya yi ñu war a jàng bala ndaje fàttaliku bi jot. Porogaraam boobu dina komaase ci bésu 17 màrs. Boo xalaatee ci li xewoon ci bés yu mujj yi ci dundu Yeesu ci kaw suuf, loolu dina la dimbali nga waajal sa xol ngir bés boobu (Esr. (Ezr.) 7:10). Boo xalaatee bu baax ci li Biibël bi nettali noonu te di ci boole ay ñaan, dinga gën a bëgg gërëm Yexowa ak doomam ndax mbëggeel bi ñu nu won bi ñu joxee njot gi. — Sab. (Ps.) 143:5.
6. Bu ñuy gën a góor góorlu ngir wone ne fonk nañu njot gi, loolu naka la ñuy amale njariñ ?
6 Bu ndaje fàttaliku bi di gën di jege, nañu waajal bu baax suñu bopp ak suñuy moroom ngir xew bu am solo boobu. Fàttaliku njot gi te wone ci ne fonk nañu ko lool, loolu dina rattaxal suñu diggante ak Yexowa ak it suñu diggante ak Doomam (2 Kor. 5:14, 15). Loolu dina ñu xiir it ci roy ci ñoom, maanaam am xelum nangu ñàkk yenn yi ndax li ñu bëgg suñuy moroom. — 1 Ywna 4:11.