Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi
11-17 fewriyee
Woy-Yàlla 74
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na am ñu topp li nekk ci xët 8 te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 fewriyee ak Réveillez-vous ! bu fewriyee. Mën nañu wax it leneen lu mën a baax ci seen gox.
15 min : Ndax mën nga dem fu ñu soxla ay waaraatekat ? Waare ak waxtaan bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 15 sulyet 2003, xët 20. Nañu ci boole li nekk ci téere Organisés xët 111, xise 1 ba xët 112, xise 1. Nañu waxtaan ci kanamu mbooloo mi ak ay waaraatekat yu mas a dem liggéey fu ñu soxla woon ay waaraatekat, laaj leen laaj yii di topp : Yan jafe-jafe lañu jànkoonteel, te nan lañu def ba génn ci ? Yan barke lañu ci am ?
20 min : Nañu dimbali waaraatekat yu bees yi ñu jëm kanam. Waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 1 desàmbar 2005, xët 31. Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew laaj yi nekk ci La Tour de Garde boobu, te may leen ñu tontu. Bu ngeen àggee ci xise 18, na am ñuy wone ni waaraatekat bu bees ak waaraatekat bu yàgg a waare mën a def bu ñu andee. Ki ñu waxal, dina wax waaraatekat bu bees bi luy dog waxtaan bi. Waaraatekat bu bees bi mënu ko tontu tont bu baax. Nit ki daldi dagg waxtaan bi. Bu ñu génnee, waaraatekat bi yàgg ci waaraate bi dina ko wax lu rafet ci li mu jéem a tontu waa ji. Ginnaaw loolu dina ko won ni mu mënee jëfandikoo téere Comment raisonner ngir xam lu mu mën a wax bu lu mel noonu amaatee.
Woy-Yàlla 24
18-24 fewriyee
Woy-Yàlla 27
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla.
10 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
25 min : “ Liy wone ngëm dëgg ! ”a Wottukatu liggéeyu waaraate bi moo war a def waxtaan bii. Ngir jeexal waxtaan bi, waxal lu rafet li waa mbooloo mi def ci atum liggéeyu waare bi weesu.
Woy-Yàlla 22
25 fewriyee ba 2 màrs
Woy-Yàlla 36
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàtte bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru fewriyee te joxe ko. Waxal it fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Na am ñuy wone naka lañu mënee won kenn ci suñuy mbokk walla ci suñu dëkkandoo, kayit biy woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi.
20 min : “ Nañu fàttaliku njot gi te wone ci ne fonk nañu ko lool. ”b Su la ko jot bi mayee, waxal ñi teew ñu wax seen xalaat ci aaya yi nekk ci waxtaan bi.
15 min : Nañu waajal ni ñuy wonee suñu yéenekaay yi. Waxtaan ak ñi teew. Boo waxee ci lu gàtt li nekk ci La Tour de Garde bu 1 màrs ak Réveillez-vous bu màrs, laajal ñi teew yan waxtaan ñoo mën a neex nit ñi ci suñu gox, ak lu waral ñuy wax loolu. Waxal ñi teew ñu wax yan xaaju yéenekaay bi lañu bëgg wone ci waaraate bi. Lan lañu mën a laaj nit ki ngir komaase waxtaan bi ? Ban aaya lañu mën a jàng ci xaaju yéenekaay bi ñu bëgg wone ? Na am ñu topp li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 màrs ak Réveillez-vous ! bu màrs.
Woy-Yàlla 12
3-9 màrs
Woy-Yàlla 48
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Seetal ponk yi ëpp solo ci yi nekk ci wërale bi tudd “ Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu : Li ñu warul a fàtte. ”
20 min : Ndax mën nga komaase benn njàngum Biibël ci weeru màrs ? Waxtaan ak ñi teew. Ci weeru màrs, téere Qu’ensiegne la Bible lañuy wone. Li ñu bëgg mooy komaase ay njàngum Biibël. Seetleen yenn yu am solo yu nekk ci téere boobu. Nañu waxtaan ci ni ñu mënee wone téere Qu’ ensiegne bu ñuy dellu seeti ñi wone woon ne suñu waxtaan dafa leen neex fekk dañu leen doon woo ci ndaje fàttaliku bi, ñi jëloon suñu yéenekaay yi, walla bu ñuy waaraate këroo-kër bu 22 màrs weesoo. (Seetleen km 12/07 xët 3 ak 4 ; km 3/06 xët 1, xise 3 ; km 1/06 xët 3 ba 6). Na am benn walla ñaari waaraatekat yuy wone ni ñu mënee wone téere boobu.
15 min : Nañu jëfandikoo Biibël bi bu ñuy tontu nit ñi. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci téere École du ministère théocratique, xët 143-144. Ci lu gàtt, na benn waaraatekat wone ni ñu mënee jëfandikoo Biibël bi ngir tontu benn laaj bu ñu faral di dégg ci suñu goxu mbooloo.
Woy-Yàlla 54.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.