Woy-Yàlla 20 (45)
Ñaanu ngërëm
(Sabuur 65:2)
1. Yeowa Yàlla, màggal nga yelloo;
Ngir yow suñu baat ñu ngiy jolliloo,
Tey dikk ci yow, Aji-déglu ñaan,
Ndax nga yiir ñu ak tawféex juy baawaan.
Saa su ne, dañ’ lay tooñ, ndax néew-doole;
Ñu ngiy jéggalu ndax yëf yooyule.
Ak sa deretu Doom nga ñu jënde.
Jàngal ñu léegi ni ñu war’ dunde.
2. Am nañ’ bànneex, ñi nga tànn te woo
Te ci say ëtti leer ñuy dajaloo.
Sa kër daa sell; Sa Kàddu di leer.
Suñu mbég, ci sa mbaaxaay lañ’ ko wéer.
Aka raglu sa kàttan giy dalal
Suuf siy kër-këri ndax àttee dégmal!
Yàllay mucc, sa Nguur lañuy sargal.
Du deñ muk’, looloo tax ñu koy màggal.
3. Yàlla na sa worma tax mbég baawaan;
Na sa njaamu law fép’, mel ni lawtan.
Sa Nguur’ ngiy feeñ, kaalawoo sa mbaaxaay;
Jële fii wopp, dee, rangooñ, caay-caay.
Lépp lu bon, sa Doom dina ko tas.
Dinañu yuuxu ndax mbég mu ne las.
Suñu baat ca kow, nañ’ tagg Yàlla:
‘Woyleen Yeowa, Buur bu màgg la!’