WOY-YÀLLA 93
Yal na Yàlla barkeel suñuy ndaje
(Yawut ya 10:24, 25)
1. Ñu ngi sukk ci sa kanam,
booloo, bég, te di la ñaan
nga jiite suñu ndaje yi
te barkeel suñu mbooloo.
2. Ci sa biir kër, yow Yexowa,
sellal ñu ak sa kàddu.
Jàngal ñu ñu mën a waare,
may ñu xol bu fees mbëggeel.
3. Baay, barkeelal suñuy mbokk
ndax jàmm ak salaam baawaan.
Dinañu wéy ci doxalin
buy màggal sa kiliftéef.
(Xoolal itam Taalifi Cant 22:23; 34:4; Esayi 50:4.)