WOY-YÀLLA 85
Nañu teralante
(Room 15:7)
1. Képp ku bëgg Yàlla jàngal la,
Dalal jàmm ci kër Yàlla gi,
Ngir mu xamal la lan mooy dëgg gi.
Sànt nañu ko ndax ni mu ñu terale.
2. Yàlla may na ñu mag yu ñu bëgg.
Dañu lewet te yelloo ngërëm.
Nañu roy seen ngëm te won leen mbëggeel.
Ni ñoom, nañu teral ñi Yexowa nangu.
3. Yexowa woo na ñépp ñi dogu
Ci bëgg a xam Yàlla ji mu doon.
Ngir ñu jege ko, joxe na Yeesu.
Kon ñun nañu teral ku ko bëgg a jaamu.
(Xoolal itam Yowaana 6:44; Filib 2:29; Peeñu 22:17.)