WOY-YÀLLA 20
Joxe nga sa doom ji nga sopp
(1 Yowaan 4:9)
1. Suñu Baay, Yexowa,
yaakaar amatul woon,
nga joxe njot gi
ngir suñu ëllëg leer.
Su dul woon sa mbëggeel,
duñu dund bànneex.
Tagg la moo ñu war.
Na àddina xam ne:
(AWU BI)
Yeesu musal na ñu,
saraxam, yéem na ñu.
Duñu tàyyi di la woy
ndax may nga ñu dund ba fàww.
2. Yexowa, kenn du yow,
moo tax ñu bëgg la.
Fonk ñoo la jaral
nga def lu yéemee nii.
Jëlee nga asamaan
sa jenn doom Yeesu.
Nga yónni ko ci suuf,
mu dee ngir ñu dund!
(AWU BI)
Yeesu musal na ñu,
saraxam, yéem na ñu.
Duñu tàyyi di la woy
ndax may nga ñu dund ba fàww.
(NJEEXTEEL LI)
Suñu Baay, Yexowa, ñun amuñu sa fey.
Njot gi moom, fompal na ñu suñuy bàkkaar ba fàww.
(Xoolal itam Yowaan 3:16; 15:13.)