TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 19 p. 22
  • Defal lépp ngir laal xolu nit ñi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Defal lépp ngir laal xolu nit ñi
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Waxal ak cawarte
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Xiiral nit ñi ci jëfe li ñu dégg te amal xalaat bu rafet ci ñoom
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Waxal ak mbaax te woneel ne yëg nga nit ñi
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Xóotalal waxtaan bi
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 19 p. 22

LESOŊ 19

Defal lépp ngir laal xolu nit ñi

Aaya bi ñu lim

Kàddu yu Xelu 3:1

LI NGA WAR A JÀPP: Dimbalil ñi lay déglu ñu gis njariñu li nga leen di jàngal te ñu jëfe ko.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat ci li leen di tax a jëf. Laajal ay laaj yuy tax ñi lay déglu mën a seet li nekk ci seen xol.

  • Xiiral ñi lay déglu ci bëgg a def lu baax. Dimbalil bu baax ñi lay déglu ñu xalaat ci li tax ñuy def lu baax. Dimbali leen ba li leen xiir ci def lu baax doon li gën, maanaam bëgg Yexowa, bëgg seen moroom ak bëgg a topp li Biibël bi santaane. Dimbalil ñi lay déglu ñu xam ne li Biibël bi wax mooy li gën; bu leen xas. Bu leen rusloo, waaye fexeel ba sa waxtaan xiir leen ci bëgg a def lépp li ñu mën ngir def lu baax.

  • Gënal a wax ci Yexowa. Ndigal ak santaane Yàlla yi nekk ci Biibël bi ak lépp li Biibël bi wax, dafay wone jikko Yàlla yi ak mbëggeelam ci ñun. Na loolu feeñ bu baax ci sa njàngale. Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat ci li Yexowa di yëg bu ñuy def dara te xiir leen ci bëgg a def li ko neex.

    Xelal bu baax

    Bul fàtte ne Yexowa mooy xiir nit ñi ci moom. Jaaral ci Kàddoom ngir xiir ñi lay déglu ci def lu baax.

CI LIGGÉEYU WAARE BI:

Bu mënee nekk, laajal ki lay déglu ay laaj ngir xam li mu gëm dëgg. Xoolal ni kanaman ak ni muy waxe wonee li muy yëg dëgg. Waaye bul yàkkamti. Am na ñoo xam ne, bala ñu lay wax li nekk ci seen xol, fàww ñu wóolu la.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager