LESOŊ 11
Waxal ak cawarte
Room 12:11
LI NGA WAR A JÀPP: Waxal ak cawarte ngir xiir nit ñi ci jëfe li ñu dégg.
NI NGA KO MËN A DEFE:
Li ngay wax, na jóge ci sa xol. Booy waajal sa bopp, xalaatal bu baax ci li tax li ngay waxtaane am solo lool. Xamal bu baax li nga bëgg a waxtaane, su ko defee dinga mën a wax ak sa xol bépp.
Xalaatal ñi la nar a déglu. Xalaatal bu baax ci njariñ bi nit ñi mën a jële ci li ngay liir walla jàngale te seetal ni ngay waxe ba ñu fonk bu baax li ñu dégg.
Na sa waxtaan xumb. Waxal ak cawarte. Li ngay yëg, na feeñ ci sa kanam ak ci ni ngay yëngale say loxo.