“ Diirub junniy at, bu bees bi — Lu la ëllëg di indil ? ”
1 Laajte booboo nekk ci xel yi yépp ci kow suuf si. Dëgg la ne doom-Aadama def na lu baree bare ci biir xarnu yi wees, teewul nit ñi mujj nañoo gisal seen bopp ne dañoo nax seen bopp, ndaxte seeni jafe-jafe cosaan, jafe-jafe yiy teg naqar doom-Aadama yi li dale junniy junni at, ñoo ngi fi ba tey (Ay. 14:1 ; Sab. 90:10). Fan la nit ñi mënee am péex ?
2 Ci biir weeri oktoobar ak nowàmbar, dinañ ñu xàllal yoon, wu amul moroom, ngir indil suñuy moroom yi tont ci laajte boobu. Naka ? Ak siiwalu Xabaariy Nguur gi No. 36. Yaxam : “ Diirub junniy at, bu bees bi — Lu la ëllëg di indil ? ” Ci xaaju oktoobar bu njëkk bi, yéenekaay yi La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! lañuy won nit ñi. Ba noppi li dale ci altine 16 oktoobar ba àjjuma 17 nowàmbar, dinañu farlu dëgg ciy siiwal Xabaariy Nguur gi No. 36. Ci biir yëngu-yëngu boobu, dinañu teewlu ci bàyyil nit ñi Xabaariy Nguur gi No. 36 altine ba àjjuma. Ci njeexteelu ayu-bés gi nag, dinañu ko wone, boole kook yéenekaay yi mujj a génn.
3 Ndax dinga ci bokk ak doole ? Mag ñi, surgay mbooloo mi, ak way-xàll yoon yi dinañu aajowoo jiite yëngu-yëngu boobu, ndegam ñooy ñiy jiitu ci waare bi. Yéenekat yu bare mën nañoo fagaru ngir sumb sasu aji-xàll yoonu weer, muy ci benn walla ñaari weer yi ñuy siiwal mbind mi. Boo ko seetee sax, lu tax doo def loolu sa jëmu ? Su mënul nekk, fàggul ngir yokk jot gi nga tàmm di jagleel sasu waare bi.
4 Ñiy jiite Njàngum téere mbooloo mi mën nañoo xiirtal ku nekk ci ñi bokk ci seen mbooloo, mu bokk ak doole ci siiwalub Xabaariy Nguur gi No. 36. Xëy na, am na ay yéenekat ñu waareetul. Mag ñi war nañu leen a seeti ba xam li ñu mën a def ngir dimbali leen. Xëy na, mën nañoo fagaru, ba tax yéenekat bu am manoore dugg ci tool bi ak képp ku waareetuloon, ci biir weer yooyu. Woneb Xabaariy Nguur gi No. 36, liggéey bu yomb, mën naa nekk doŋŋ li yéenekat yooyu soxla ngir dooraat di waare.
5 Ngir ñiy jàng Biibël bi te nekk ci tànku sottal téere Xam-xam, teyit jekk ci doon ay yéenekat yu ñu sóobul, dinañu xàllal yoon wu rafet ngir tàmbali waaraate bi. Xale yi sax mën nañoo am cér bu rafet ci liggéey bu daw yaram boobu.
6 Li ñu soxla doŋŋ mooy wone bu yomb. Mën ngaa ne :
◼ “ Damaa jël ci sama jot ngir siiwal kayit bii ëmb xabaar bu am solo ci gépp njaboot, fii ci [tuddal dëkk bi walla gox bi]. Sa bos a ngi. Maa ngi lay ñaan nga jàng ko. ” Bañ a yore saagu waarekat mën naa doon, lée-lée, li gën, bu ñuy siiwal Xabaariy Nguur gi No. 36.
7 Ndaje yu ñu waajal bu baax, ngir liggéeyu waare bi : Mag ñi war nañoo toppatoo li ñu fagaru ci wàllu seede bi, ba tax mu doon lu yomb a topp tey jariñ. Wottukatu liggéeyu waare bi, rawatina moom, war naa wóoral ne dina am gox yu bare, fu ñuy mën a dem kër-oo-kër ak a taseek ñiy njaay ak a jënd, ndax ku nekk mën a dem ba jeex ci liggéey bi. Fépp fu mu mën a am, war nañoo taxawal ay ndaje ngir waaraate altine ba àjjuma, ci njeexteelu ayu-bés gi, ak ngoon su nekk. War nañoo fagaru daje tàkkusaan ngir njariñu ñiy jàngi lekkool, ñiy ay-ayloo liggéey, ak ñeneen.
8 Li ñu war a def ak ñi newul seen kër : Suñu jubluwaay mooy wax ak li ñu mën ci nit. Su kenn nekkul ci kër goo jaar, bindal adarees bi te dellu fa ci weneen waxtu ci bés bi. Su fekkee ne ba ci ayu-bés gi mujj ci suñu yëngu-yëngu, gisaguloo nit ñooñu, mën nga leen a bàyyil sottib Xabaariy Nguur gi No. 36 ci béréb, bu nit kuy romb dul gis. Mag ñi ci mbooloo mi mën nañoo tegtal mbooloo mi, ñu bàyyil ñi newul seen kër sottib Xabaariy Nguur gi No. 36, ci yoon wu jëkk wi ñuy jaar ci diiwaan yi ne ci kaw gi, walla ci béréb yi ñu mënul a àgg ci kër gu ne, ci biir yëngu-yëngu bi.
9 Nañu farlu ! Mbooloo yi war nañoo jéem a wër ba mu daj gox gi ñu leen sas, laata yëngu-yëngu bi di sotti ci 17 nowàmbar. Su seen gox yaatoo dëgg, ay yéenekat mën nañoo liggéey ñoom kenn, fi nga xam ne loolu mën naa am te wóor. Loolu dana gën a yombal suñu giseek li ëpp ci nit ñi ko yeyoo. Na la wóor ne, sàmm nga bu baax ci kayit itte ji ngay seetlu jépp.
10 Jarul ñuy laaj Xabaariy Nguur gi No. 36, ndegam dinañu yónne mbooloo mu nekk wàllam. Way-xàll yoon yi ci jébbal seen jot gépp, yi ci sax, ak yu weer, dinañu jot ku nekk 200 sotti ngir séddale bi, ba ñuy jox yéenekat bu ne 50 sotti. Kon, ndax pare nga te yàkkamti ngaa farlu ci yëngu-yëngu, bu amul moroom boobu ? Ndaw cér buñ ñu baaxe, xamal suñuy moroom yépp li Yàlla dige ngir ëllëg jiy dégmal !