Nañu suuxat itte ji juddoo ci Xabaariy Nguur gi No. 36
1 Ndax sottal ngeen siiwalub li ñu leen séddoon ci Xabaariy Nguur gi No. 36 ? Day laaj laajte bu agsi ci waxtoom, bu ñépp war a bàyyi xel : “ Diirub junni at, bu bees bi — Lu la ëllëg di indil ? ” Ba atum 2000 doon jegeñsi, li nit ñi doon séenu ci li diirub junni at, bu bees bi naroon a indi, wuute woon na lool. Xabaariy Nguur gi No. 36 a ngiy waxtaane ci yenn ci yaakaar yooyu, di ñu fàttali it ne, li àddina si nekke, sababul luy tax ñu rafetlu ëllëg. Diirub junni at, te muy moom kott, biy indil li ëpp ci nit ñi, jàmm ak dalaay bi ñuy wut, mooy Nguuru Junni at, gu Krist Yeesu. Li mu ñu wóor ne, Nguuram googu daa am dëggëntaan, moo ñu xiir ci siiwal Xabaariy Nguur gi No. 36 ci li ñu mën ci nit.
2 Li Xabaariy Nguur gi jur : Siiwalub Xabaariy Nguur gi, ya jiitu woon nekkoon na lu ñu xiirtal ci suñu liggéey. Lu jëm ci Xabaariy Nguur gi No. 35, lii la bànqaasu Kanadaa bind : “ Ci tool bi, yéenekat yeek way-xàll yoon yi njaxlafoon nañu dëgg ciy jàpple yëngu-yëngu bu am solo bii, te ñu bare dund nañu mbir yu leen xiirtal te bégal. ” Du ñàkk njaxlaf gu ni mel, ngeen nekk di wone ci siiwalub Xabaariy Nguur gi No. 36.
3 Yëngu-yëngu tas Xabaariy Nguur gi bi ñu nekk di amal, ci 17 Nowàmbar 2000 lañu ko war a sottal. Ndax wër ngeen ba daj goxiy seen mbooloo yépp ? Lu ko moy, magi mbooloo mi mën nañu leen a laaj ngeen wéy ci yëngu-yëngu bi, ba weeru Nowàmbar dee.
4 Ba léegi, lan la siiwalub Xabaariy Nguur gi No. 36 jur ci seen gox ? Nit ñu néew ñooy mottali dogitu kayit bi te laaj sottib téere bu ndaw bi Laaj ak / walla njàngum Biibël bi ci seen kër. Waaye li ëpp ci nit ñii tàmbalee ittewoo yaxu diirub junni at bi, xëy na duñu def dara ba keroog kenn ci Seede Yexowa yi di dellusi. War nañoo seetiwaat ñépp ñi wone itte. Jamano ji gën ngir def ko, kañ la ? War nañoo topp mbir mi ci lu gën a gaaw.
5 Seetleen xew-xew yile juddoo ci, dellu fa ñu bàyyi woon ay Xabaariy Nguur gi No. 35. Benn aji-xàll yoon ca Irlànd daa bàyyiloon jigéen, juy boroom lekkukaay, sottib Xabaariy Nguur gi. Xabaaram, nag, duggoon na lool ndaw sa, te ñaan na suñu mbokk mu jigéen mu dellusi. Loolu la def ci ñaari fan yi, te tàmbali nañu jàng Biibël bi. Ca Danmark, sottib Xabaariy Nguur gi lañu bàyyi woon ci kër, gu ñu fekkul woon kenn. Ca bés booba saxsax la jigéen, ja fa dëkkoon, yónne ci bànqaas ba dogitu kayit wi, ñu dénk nag mbir mi mbooloo gox, bi mu dëkkoon. Balaa ayu-bés gay wees, ñaari mbokk yu jigéen dellu nañu fa, taxawal njàng, te jigéen ja teew na ci ndajeem mi njëkk ca Saalu Nguur ga !
6 Li ngay wax boo fay dellu : Seetiwaat ñi ñu bàyyil Xabaariy Nguur gi nekk na daanaka lu yomb, akit wàll ci suñu sasu waare, wu ñuy jural mbég. Boo koy def, lu baax, nag, lay doon yóbbaaleek yaw sa sottib Xabaariy Nguur gi No. 36 ; mën naa am nit ki bañ a yoreeti sottib boppam. Mën ngaa jéem xelal yii.
7 Fàttalil nit ki ki nga doon, ba noppi ne :
◼ “ Maa fi bàyyi woon kayit bi tudd : ‘ Diirub junni at, bu bees bi — Lu la ëllëg di indil ? ’ Ndax du luy xiirtal jàng ne, tuuti ca kanam, Nguuru Junni at, bu Yeesu Krist [Isaa], dina tàmbali, ba noppi indi Àjjana ci kow suuf ? [Won ko nataali Àjjana yi ci biir Xabaariy Nguur gi No. 36.] Ci xët bi mujj, ñu ngi lay ñaan nga laajte sottib téere bu ndaw bi Lan la ñu Yàlla laaj ? ” Woneel téere bu ndaw bi, àgg ba ci njàngale 5, jàng laaj bi jëkk ak xise 1 ak 2, ba noppi laajal nit ki mu joxe xalaatam. Jàngal te waxtaane benn aaya walla ñaar. Su mënee am, waxtaaneel beneen laajte ak xiseem, ba noppi fàggul ngir dellusi, wéy ci waxtaan wi.
8 Ci Nowàmbar, ndegam mbind yi ñuy won nit ñi, ngir suuxat seen itte, téere bu ndaw bi “ Laaj ” la, walla téere “ Xam-xam ”, mën gaa wax :
◼ “ Bi ma la seetsee bu yàggul, bàyyi naa fi sottib ‘ Diirub junni at, bu bees bi — Lu la ëllëg di indil ? ’. Ñu nga fa doon may nit ñi, ñu am njàngum Biibël bi seen kër, te duñu ci fey dara. Dellusi naa ngir won la jumtuwaay bi ñuy jëfandikoo ci njàng mi. [Woneel téere bu ndaw bi Laaj, àgg nag ba ci xët bu mujj bi ; walla woneel téere Xam-xam, ba noppi àgg ba ci xët 188-9.] Diiru junni at bi ñuy wax ci Biibël bi [Mbind mu sell mi] dina indi nekkin yi ngay gis ci nataal bii. Ngir jekk ci dund ci Àjjana, soxla nañoo am xam-xam bu wér ci Yàlla. May ma, ma won la, ci lu gaaw, ni ñuy jànge Biibël bi [Mbind mu sell mi]. ”
9 Siiwalub Xabaariy Nguur gi No. 36 xiir na ñu ci yokk suñu loxo ci waare bi, mu yóbbe seede su réy. Du ñàkk, loolu xamb na itte nit ñu bare ci gox gi ñuy waare. Góor-góorlu bennoo ngir suuxat itte jooju, ak ndimbalu Yexowa, dina tax ñu wéy di wut ak mbég, ba gis leen, nit ñu gën a bare, ñu mel ni xar. — Macë 10:11 ; Jëf. 13:48, 49, 52.