TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/02 p. 3-6
  • ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • ‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Nañu wéy di wax ci lu kéemaane li Yexowa def
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Nañu waaraate bu baax
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Yégleleen ni Yexowa baaxe
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 2/02 p. 3-6

‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’

1 Bu ñu la mayee dara te mu neex la lool, ndax loolu du feeñ ci yow ? Axakay ! Ndaw li Pool mu ngi doon xalaat ci ni Yexowa baaxe ak doom-Aadama yi. Loolu laal na ko ba mu naan : “ Jërëjëfati yaw Yàlla ndax sa may googu weesu dayo! ” May googu lu mu ëmb ? Ëmb na “ yiw wu mag ” wu Yàlla def ci ñun. Li ko gën a wone mooy bi mu mayee Doomam ni sarax ngir fey suñuy bàkkaar. — 2 Kor. 9:​14, 15 ; Ywna. 3:​16.

2 Ni Pool gërëme Yàlla noonu, ndax wax kese la woon ci moom ? Mukk ci àddina ! Am na ay fasoŋ yu bare yi mu ko wone. Xolam yépp mu ngi woon ci dimbali ay mbokkam ci ngëm, ñu am diggante bu rattax ak Yàlla, te ñu jariñoo bu baax mbaaxaayu Yàlla. Lii la Pool wax ci ñoom : “ Cofeel gi nu am ci yeen tax na, bëggunu woona yem ci xamal leen xebaaru Yàlla bu baax bi, waaye jox leen it sunu bakkan, ndaxte sunu xol seeyoon na ci yeen. ” (1 Tes. 2:⁠8). Ñi bokkoon ci mbooloo mi ba pare, Pool dimbali na leen ñu dëgëral seen yaakaaru mucc. Gannaaw loolu, li mu tukki, bare na lool. Dem na fu sore, jaar ci kow suuf ak ci géej ngir yégal nit ñi xibaar bu baax bi, te jéem a gis “ ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex ”. (Jëf. 13:48.) Li Yexowa defaloon Pool lépp, dafa ko laal ba mu bëgg a “ yégle fu nekk ” Kàddug Yàlla. — Kol. 1:​25.

3 Ndax li ñu Yexowa defal lépp dafa ñu laal ba ñu bëgg a dimbali ñi nekk ci suñu mbooloo te soxla ndimbal ci wàllu ngëm (Gal. 6:​10) ? Te ndax loolu du tax ñu bëgg a waare, ak suñu kem kàttan, xibaar bu baaxu Nguuru Yàlla, ci gox bi suñu mbooloo moom ? — Macë 24:⁠14.

4 Fi ñu mën a wone suñu ngërëm : At mu nekk mën nañu gërëm bu baax Yexowa ak Yeesu ndax li ñu nu defal. Mooy ci ndaje bu ñuy am ci bés bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu Krist. Ndaje boobu melul ni yeneen ndaje yi. Te li ñuy fàttaliku tuutiwul. Yeesu nee na : ‘ Defleen lii, ngir fàttaliku ma. ’ (Lukk 22:19). Ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu lañu mën a xalaat Yeesu ku mu doon dëgg. Yeesu dafa takku woon ci Yàlla te saraxe na boppam. Yàlla daldi ko màggal, te may ko nguur. Ndaje boobu dina ñu may it ñu xam bu baax ne Yeesu mu ngi dund te am na lu muy def tey. Foofu lañu mën a wone itam ne nangu nañu kiliftéefu Yeesu ci kaw mbooloo taalibeem yépp (Kol. 1:​17-​20). Kon képp ku bokk ci mbootaayu Yàlla war na teewe, boole ci weg, ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Ren ji, ci bésu alxemes 28 màrs 2002, bu jant bi sowee ba pare lañu koy am.

5 Daaw, ci réewu Etaa Sini, ni ñu góor-góorloo balaa bés boobu jot, taxoon na 2 163 602 teew ci ndaje boobu. Masuñu woon a bare noonu. (Boo bëggee xam ñaata nit ñoo teew ci sa réew, seetal La Tour de Garde bu 1 sãwiyee 2002, xët 19 ba 22.) Ñaata ñooy teew ren ? Li ci bare, mu ngi aju ci li ñuy “ ñaq tey bëre ” ngir nit ñu baree bare mën fa teew. — 1 Tim. 4:​10.

6 Dinañu teewe ndaje boobu, waaye mën nañu yokk itam li ñuy def ci waaraate bi. Mën nañu yaakaar ne ay junniy junni ci suñuy mbokk ci ngëm dinañu nekk aji-xàll yoonu weer (pionnier auxiliaire) benn weer walla lu ko ëpp. Bu ñu seetee ci juróomi at yi weesu, at mu nekk amoon na lu tollook 212 142 aji-xàll yoonu weer ci diggante weeru màrs ba weeru me, maanaam ci jamonoy bés bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. (Boo bëggee xam ñaata lañu woon ci sa réew, xoolal fi ñu binde li ñu def ci liggéeyu waare bi ci Le ministère du Royaume bu Sulyet, Ut ak Septaambar 2001.) Ndax dinga mën a fexe ba nekk aji-xàll yoonu weer, ren ? Noonu nga mën a gërëme bu baax Yàlla ndax li mu ñu may. Na la wóor ne, Yexowa dina la barkeel. Moom la liy topp di wone.

7 Suñu benn mbokk ci ngëm bu jigéen nekkoon na aji-xàll yoonu weer daaw ci weeru màrs, fekk mu ngiy liggéey bés bu ne. Lii la wax : “ Ci Sasu Nguuru Yàlla bu feewriyee 2001, ñu ngi ne woon ñépp ñi ko mën, ñu fexe ba nekk aji-xàll yoonu weer ci jamonoy bésu fàttaliku bi. Weeru màrs amoon na juróomi gaawu, te loolu àndoon na bu baax ak sama porogaraam. Looloo tax ma nangu kayit bu ñuy bind ngir nekk pioñee. ” Ne woon na it li mu bëggoon mooy tàmbali benn Njàngum Biibël bi. Ndax def na ko ? Waaw, bi mu demee ba waaraate 52 waxtu ci weer boobu, ci waxtu boobu la ko ame. Lan la mujj a wax ? Nee na : “ Bu ñu yokkee li ñu tàmm def, dañuy am ay barke yu réy. ”

8 Su dee benn njaboot moo bëgg nekk pioñee, ban njariñ la ciy am ? Ci weeru awril bi paase, amoon na njaboot fu ñépp nekkoon pioñee, maanaam ñeenti nit. Nee nañu : ‘ Weer boobu duñu ko fàtte mukk. ’ Yaay ji nee na : “ Bés bu ne ci mbégte lañu nekke woon, ndaxte ñun ñépp a bokkoon ci waaraate bi. Ngoon, bu ñu doon reer, ñépp a doon kontaan ndaxte dañu doon waxtaan ci li ñu def ci waaraate bi. ” Doom ji nee na : “ Ànd ak sama pàppa di waaraate ci waxtu yi mu faraloon a liggéey, neexoon na ma lool. ” Li la ci pàppa ji dolli : “ Man mi, boroom kër gi, li ma xamoon ne ñu ngi doon bokk ci liggéey bi gën a am solo ci suñu jamono, taxoon na ma bég. ” Ndax sa waa kër mën nañu ànd nekk pioñee ? Ndax yéen ñi nekk ci njaboot gi mënuleen a toog, waxtaan, ba seet ndax dingeen mën a nekk aji-xàll yoonu weer ci jamonoy bésu fàttaliku bi ?

9 Ndax mën nañu fexe ba weeru màrs raw yeneen weer yépp ? Lii lañu laajoon daaw ci suñu Sasu Nguuru Yàlla : “ Ndax mën nañu fexe ba weeru awril 2000 raw yeneen weer yépp ? ” Lan moo ci topp ? Weer boobu amoon na 2 410 aji-xàll yoonu weer ci réewu Togo, te 196 ci réewu Senegaal. Masuñu woon am loolu. Am na itam ay réew fi nga xam ne waxtu yi ñu waaraate, yéenekaay yi ñu bàyyi nit ñi ak nit ñi ñu seetsiwaat, masuñu woon bare noonu. Ndax yaa ngi fàttaliku mbégte bi amoon ci mbooloo mi, ndax li ñépp defoon ci liggéeyu Yàlla, weer boobu ? Ndax ren dinañu mën a def lu mel noonu, mbaa lu ko raw ? Bu ci ñépp bokkee, weeru màrs 2002 mën na nekk weer bi “ raw yeneen weer yépp ”. Waaye lu tax weeru màrs?

10 Li war a tax màrs nekk weer boo xam ne dina wuuteek yeneen weer yi, ñaar la. Benn, ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, dinañu ko am bu weeru màrs bëggee jeex. Kon, ci biir weer wi dinañu war a def suñu kem kàttan ngir woo ay nit ñu bare ñu ñów teewe ndaje boobu. Ñaar, weeru màrs bi di ñów dina am juróomi gaawu ak juróomi dibéer. Kon, nekk aji-xàll yoonu weer dina gën a yomb ci ñi am liggéey walla ñiy jàng lekkool. Léegi, boo seetee tablo bi nekk xët 6, ndax mënoo toog, xalaat bu baax porogaraam boo mën a topp ngir nekk aji-xàll yoonu weer ci weeru màrs ? Xéyna mu gën a yomb li nga doon xalaat. Juróom-fukki waxtu nga war a waaraate ci weer wi. Boo jëlee gaawu bu nekk boole ci dibéer bi ci topp, te nga fas yéene waaraate 8 waxtu ci ñaari fan yooyu, bu weer wi jeexee dina doon 40 waxtu. Fukki waxtu kese moo lay dese. Dinga ko mën a waaraate ci yeneen fan yi ci biir weer wi. Bu weer wi matee dina doon 50 waxtu.

11 Lan la mag ñi mën a def ngir dimbali mbooloo mi ñu “ yégle fu nekk ” Kàddug Yàlla ? Bu ngeen di jàngale ci ndaje yi walla waxtaan ak mbokk yi ci ngëm, fexeleen ba ñépp sawar ci waaraate bi. Ñi nekk wottukatu njàngum téere bi ak ñi leen ciy dimbali, jarul ñuy xaar ba ñu woo leen. Waaye, mën nañu jóg, am waxtaan bu gàtt te neex ak képp ku bokk ci seen njàngum téere bi ngir won leen li ñu mën a def. Xéyna loolu rekk lañu soxla ngir nekk aji-xàll yoonu weer (Léeb. 25:11). Ñu bare dinañu dem ba gis ne su ñu soppalee tuuti seen porogaraam dinañu mën a nekk aji-xàll yoonu weer. Am na ay mbooloo yoo xam ne, li ëpp ci mag ñi, surga mbooloo mi, ak seeni jabar, nekk nañu aji-xàll yoonu weer ci jamonoy bésu fàttaliku bi. Loolu lu jar a roy la te tax na ay waaraatekat yu bare ànd ak ñoom, nekk pioñee. Xéyna ay waaraatekat duñu mën a nekk pioñee ndax seen yaram neexul walla leneen. Waaye, mën nañu leen xiir ci def lépp li ñu mën ak mbooloo mi ci liggéeyu waare bi. Noonu lañuy mën a wone seen ngërëm.

12 Ngir lépp baax, mag ñi war nañu waajal bu baax liggéey boobu. Ndaje yi ñu am bala ñuy waare , war nañu ko def ci ayu-bés bi yépp, ci ay waxtu yu baax ci ñépp. Balaa ndaje yooyu jot, wottukatu liggéeyu waare bi, dina jéem a seet ku koy jiite. Dina tànn ci mbokk yu góor yi, ñi ko mën bu baax. War nañu waajal ndaje yooyu bu baax ngir ñu bañ a ëpp 10 walla 15 minit. Ci minit yooyu, war nañu wax kuy génn ak kan, wone fi ñu war a waaraate, te ñaan. (Seetal Réponses à vos questions ci Le ministère du Royaume bu septaambar 2001.) War nañu xamal bu baax mbooloo mi porogaraam bi ñu def ngir weer wi, ba pare taf ko ci tablo bi nekk ci Saalu Nguur gi.

13 Fi ñu war a waaraate war na doy. Wottukatu liggéeyu waare bi war na seet gox yi nga xam ne waaraatewuñu fa lu bare, ngir ñu dem fa. Dina ko seet ak kiy toppatoo fu ñuy waaraate. Dinañu def lu ñu mën ngir seet ñi ñu fekkul seen kër, waaraate ci mbedd yi ak ci bitig yépp, te itam waaraate ci ngoon yi. Fu ñu ko mëne, mën nañu dimbali ay waaraatekat ñu waaraate ci telefon.

14 Dimbali leen ñu tàmbaliwaat liggéey bi : Ndax am na ci gox bi seen mbooloo moom ay waaraatekat ñi nga xam ne bàyyi nañu waaraate ? Ñooñu bokk nañu ba tey ci mbooloo mi te soxla nañu suñu ndimbal (Sab. 119:176). Suñu jamono jii, léegi mu jeex. Te àddina su bees si mu ngi bëgg a agsi. Kon, dëgg-dëgg war nañu def li ñu mën ngir dimbali ñi bàyyi waaraate (Room 13:​11, 12). Ci réewu Kamerun, ci juróomi at yi weesu, at mu nekk, am na lu ëpp 350 nit ñi nga xam ne dimbali nañu leen ba ñu tàmbaliwaat liggéeyu waare bi. Lan lañu mën a def ngir dimbali ñeneen ba ñu amaat mbëggeel ak kóolute bi ñu amoon bi ñu tàmbalee waaraate ? — Yaw. 3:​12-​14.

15 Mag ñi ci biir mbooloo mi dinañu seet ni ñu mënee dimbali ñi nga xam ne bàyyi nañu waaraate ci at yi weesu (Macë 18:​12-​14). Sekkerteer bi dina seet ba xam ñi bàyyi waaraate. Mag ñi dinañu mel ni ay sàmmkat, di def li ñu mën ngir dimbali leen. Su amee mag ku xam bu baax kenn ci ñoom, mën na koo seeti. Mën nañu ñaan itam yeneen waaraatekat ñu dimbali leen. Xéyna, ñi jàngoon ak ñi bàyyi waaraate, dinañu leen bëgg a dimbali, ci jamono bii ñu soxla ndimbal. Li ñuy ñaan mooy ñu bare ci ñoom tàmbaliwaat di yégle Kàddug Yàlla. Bu amul dara lu leen ko tere, jamonoy bésu fàttaliku bi mooy jamono bu gën a baax ngir tàmbaliwaat liggéey boobu. — Seetal Réponses à vos questions ci Le ministère du Royaume bu weeru nowàmbar 2000, boo bëggee dolli li nga xam ci loolu.

16 Ndax am na ñeneen ñu mën a nekk waaraatekat ? Yexowa dafay indi ‘ alalu xeet yépp ’ ci mbooloom. Noonu la koy barkeele (Xag. 2:⁠7). At mu nekk, am na ay junniy nit ñuy dem ba mën a nekk waaraatekat bu ñu sóobagul. Ñan lañu ? Ay doomu Seede Yexowa walla ay nit ñiy jàng Biibël bi ak ñun. Naka lañu mënee xam ndax mën nañu nekk ay waaraatekatu xibaar bu baax bi ?

17 Doomi Seede Yexowa yi : Ay xale yu bare ñu ngi ànd ak seen way-jur kër-oo-kër ngir waaraate. Loolu def nañu ko ay ati at. Waaye, nekkaguñu waaraatekat bu ñu sóobagul. Weeru màrs mën na nekk weer bu baax ngir tàmbali loolu, maanaam nekk waaraatekat bu ñu sóobagul. Naka nga mënee xam ndax sa doom mat na waaraatekat bu ñu sóobagul ? Suñu téere bi tudd Organisés pour bien remplir notre ministère ci xët 100, moo ñu koy wax. Dañu ci bind ne ‛ xale bi war na am jëfin bu jar a roy. War na mën a wax li mu gëm, di waar nit ñi ci xibaar bu baax bi, fekk moom ci boppam moo ko bëgg a def ’. Boo xalaatee ne sa doom mat na loolu, waxtaanal ak kenn ci mag ñi bokk ci kurélu liggéeyu waare bi.

18 Ñiy jàng Biibël bi te mën a nekk waaraatekat bu ñu sóobagul : Nit kuy jàng Biibël bi ba am ci xam-xam te faral a teewe suñuy ndaje, mën na bëgg a nekk waaraatekatu Nguuru Yàlla. Boo dee jàng ak kenn ku mel noonu, laajal sa bopp laaj yiy topp : Boo seetee at yi mu am ak li mu mën a def, moom ci boppam, ndax mu ngi jëm kanam ? Ndax tàmbali na wax li mu gëm, buy waxtaan ak nit ñi ? Ndax mu ngi solo jikko ju bees ji (Kol. 3:​10) ? Ci kow li ñu bind ci xët 98 ba 100 ci téere Notre Ministère, ndax mën na nekk waaraatekat bu ñu sóobagul ? Su dee waaw, waxal ak mag ñi bokk ci kurélu liggéeyu waare bi. Dinañu fexe ba ñaari magi mbooloo mi toog ak yéen ñaar ngir waxtaan ci loolu. Ñaari mag ñi dinañu ko wax ndax mën na tàmbali liggéeyu waare bi.

19 Lu ñu mën a wax ci weeri awril ak me ? Weer yooyu itam dinañu nekk ay weer yu baax bu ñu bëggee yokk suñu waaraate bi. Ñu bare ci ñiy nekk aji-xàll yoonu weer ci weeru màrs, mën na am ñu mën ko it ci weeru awril ak (walla) me. Dinañu jéem a gën a wone suñuy yéenekaayi La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! ci weer yooyu. Ñi koy jàng, dañu ciy jële njariñ bu réy ! Bu ñu seetee ni liggéeyu waare bi di yokke ci àddina si sépp, mën nañu wax ne ci lu bare, suñuy yéenekaay yi ñoo tax. Dinañu def li ñu mën ci weeri awril ak me ngir won nit ñu baree bare, suñu yéenekaay yi. Fexeel ba bokk ci bu baax-a-baax.

20 Ndegam dinañu yokk suñu waaraate bi, ndax soxlawoo yokk yéenekaay yi ngay jot ci biir mbooloo mi ? Gaawu mooy bésu yéenekaay yi. Ci at mi yépp, bés boobu lañu faral di wone suñu yéenekaay yi La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Waaye, ndegam ñu bare dinañu nekk aji-xàll yoonu weer te ñun ñépp dinañu wone suñu yéenekaay yi ci ñaari weer yooyu, xéyna war nga yokk yéenekaay yi ngay jot ci biir mbooloo mi. Su dee loolu nga bëgg, nanga ko wax léegi kiy toppatoo yéenekaay yi ci biir mbooloo mi.

21 Léegi, Sasu Nguuru Yàlla bu nekk am na xaaj bu tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ”. Ñu bare wax nañu ne dañu kontaan torop ci loolu. Ndax danga koy jàng, ngir jariñoo ko booy wone suñu yéenekaay yi ? Ndax mënoo ko def ayu-bés bu nekk booy jàng Biibël bi ak sa njaboot?

22 Jariñool bu baax jamonoy bésu fàttaliku bii : Ni ko ndaw li Pool defe, nañu won Yexowa ne gërëm nañu ko bu baax ndax ‘ mayam googu weesu dayo ’. Nañu bokk bu baax-a-baax ci lépp li ñu war a def ci wàllu ngëm ci jamonoy bésu fàttaliku bii. Loolu ëmb na : 1) teewe ndaje bi gën a am solo ci at mi yépp, maanaam màggal Reeru Boroom bi ci bésu alxemes 28 màrs 2002 ; 2) dimbali ñi bàyyi waaraate ndax ñu amaat mbëggeel bi ñu amoon bu njëkk (Peeñ. 2:4 ; Room 12:11) ; 3) dimbali suñuy doom ak képp ku ñuy jàngal Biibël bi, ñu nekk waaraatekat bu ñu sóobagul, su dee mat na ko ; te 4) def suñu kem kàttan ci liggéeyu waare bi, ba nekk sax aji-xàll yoonu weer ci weeru màrs ak ginnaaw weer boobu, bu ñu ko mënee. — 2 Tim. 4:⁠5.

23 Li ñuy ñaan Yàlla mooy ci jamonoy bésu fàttaliku bii, ñun ñépp ñuy waar nit ñi ci xibaar bu baax bu Nguuru Yàlla, ak suñu kem kàttan. Su ko defee, dinañu won Yexowa ne ñu ngi koy gërëm bu baax-a-baax ci lépp li mu ñu defal.

[Wërale bi nekk ci paas 6]

Sama porogaraamu liggéeyu waare bi ci weeru màrs 2002

Dibéer Altine Talaata Àllarba Alxemes Àjjuma Gaawu

1 2

Bésu yéenekaay yi

3 4 5 6 7 8 9

Bésu yéenekaay yi

10 11 12 13 14 15 16

Bésu yéenekaay yi

17 18 19 20 21 22 23

Bésu yéenekaay yi

24 25 26 27 28 29 30

NDAJE BI ÑUY Bésu yéenekaay yi

FÀTTALIKU

DEEWU YEESU

31 BU JANT BI SOWEE BA PARE

Ndax mën nga waaraate 50 waxtu ci weeru màrs ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager