Nañu jëfandikoo bu baax Biibël bi
1 Boo bëggee wone benn téere ci waaraate bi, danga war a tànn aaya boo xam ne boo ko wonee nit, dina ci xalaat bu baax (Yaw. 4:12). Li gën mooy nga tànn benn aaya ci téere bi nga bëgg wone. Loolu dina tax nga xam looy wax nit ki booy wone téere bi. Booy waaraate, mën nga yore sa Biibël ci sa loxo. Am na waaraatekat yu wax ne loolu dafa leen di dimbali.
2 Komaaseel sa waxtaan ak benn aaya : Am na waaraatekat yoo xam ne bu ñu bëggee tàmbali seen waxtaan, dañuy laaj nit ki ñuy waxal li mu xalaat ci li nekk ci aaya bi ñu nar a jàng, ba pare jàng aaya boobu te may nit ki mu wax li mu ci xalaat. Kuy def loolu, dangay gaaw a jëmale nit ki ci li nekk ci Kàddu Yàlla. Ci laaj yii di topp, ndax am na yu mën a baax ci sa gox ?
◼ “ Boo mënoon a indi li ñu wax fii, ndax dinga ko def ? ” Jàngal Peeñu bi 21:4.
◼ “ Lu tax suñu àddina nekk ci bés yu tiis nii ? ” Jàngal 2 Timote 3:1-5.
◼ “ Bu ñépp toppoon li ñu wax fii, ndax suñu dund du gën a neex ? ” Jàngal Macë 7:12.
◼ “ Ndax yaakaar nga ne say doom dinañu fekke jamano ju mel ni bii ? ” Jàngal Sabuur 37:10, 11.
◼ “ Ndax foog nga ne li ñu wax fii dina mas a am ? ” Jàngal Isayi 33:24.
◼ “ Ndax mas nga dégg lu jëm ci nguur gu bees gi ñuy wax fii ? ” Jàngal Dañel 2:44.
◼ “ Ndax mas nga bëgg laaj Yàlla laaj bii ? ” Jàngal Ayóoba 21:7.
◼ “ Suñu mbokk yi gaañu, ndax dinañu leen mën a gisaat ? ” Jàngal Yowanna 5:28, 29.
◼ “ Ñi dee, ndax xam nañu li nit ñiy dund di def ? ” Jàngal Dajalekat 9:5.
3 Leeralal, misaalal, woneel ni ñu ko mënee topp : Boo gisee ku nangu waxtaan ak yow, bul gaawantu ci li ngay wax. Li ñu bëgg mooy mu nànd bu baax aaya bi ñu bëgg jàng. Kon boo jàngee benn aaya, nanga ko leeral, joxe ci ay misaal te wonal nit ki ni mu ko mënee topp (Nëx. 8:8). Bu nit ki nàndee bu baax li Kàddu Yàlla wax te mu bëgg ko topp, dina soppi lu bare ci dundam. — 1 Tes. 2:13.
4 Booy dellu seeti nit ku suñu waxtaan neex, nanga kontine di jëfandikoo bu baax Biibël bi. Mën nga def li ñu wax sànq maanaam : 1) Tànnal aaya bu nar a baax ci nit ki. 2) Laaj ko li mu xalaat ci li nga ko bëgg jàng, jàngal aaya bi te may ko mu wax li mu ci xalaat. 3) Leeral ko aaya bi, joxe ci ay misaal te won ko ni mu ko mënee topp. Fexeel ba saa yoo fa jógee, mu am lu bees li mu jàng ci Kàddu Yàlla. Boo defee noonu, léegi nga mën a wax ne am nga njàngum Biibël.
[Laaj yi]
1. Naka nga mënee waajal sa liggéeyu waare ?
2. a) Naka lañu mënee komaase suñu waxtaan ak benn aaya ? b) Yan waxtaan yu nekk ci Mbind mu sell mi ñoo neex nit ñi ci sa gox ?
3. Naka lañu mënee dimbali nit mu nànd bu baax aaya bi ñu ko won ci Biibël bi ?
4. Bu ñuy dellu seeti ñi suñu waxtaan neex, naka lañu mënee jëfandikoo bu baax Biibël bi ?