Ndaje mu mag mu benn fan miy ñów : li ñu fay waxtaane
Yaxu ndaje mu mag mu benn fan bi ñuy am ci atum liggéeyu waare mi di ñów, dafay sukkandiku bu baax ci Mbind mi. Yax boobu mooy : “ Déggalleen Yàlla — xeexleen Ibliis .” (Saak 4:7) Loolu, xelal bu baax la ci jamano ju metti ji ñu nekk ! Topp ndigali Yàlla dafay tax ñu noonoo ak Seytaane ci boppam. Li ñuy waxtaane ci ndaje mu mag mi dina ñu won ni ñuy dëgëre ci xeex lépp lu bon li Ibliis di def ngir yàq suñu ngëm. Yan ñooy yenn yëf yu am solo lool te am njariñ ci wàllu ngëm yi ñuy am ci ndaje moomu ?
“ Nañu dégg ndigal ni ko Yàlla bëgge ci suñu biir njaboot .” Wottukat biy wër ci mbooloo yi dina ñu won ni loolu di yokke doole njaboot yi ndax ñu mën a xeex coono yi leen àddina si di teg. “ Li xeex Ibliis tekki ”, moom la ñu gan bi ñuy defal waxtaan di jëkk a leeral bés boobu. Waxtaan boobu dina ñu xamal lu tax ak ni ñu soxlaa fagaru bu baax ngir të li Seytaane di def ngir yàq suñu digganteek Yàlla. Ñaari waxtaan lañu beral ndaw ñi nga xam ne ñoom itam dañu war a gaaw a ràññe te xeex li Ibliis di def. Am na karceen yu bare, yu nekk ay mag tey, yu bañoon a topp bëgg-bëggi àddina si bi ñu nekkoon ay ndaw. Dinañu déglu ak xol bu sedd fi ñenn ci ñoom jaar.
Képp ku bokk ci doom-Aadama yi, war na déggal ñi yore baat. Looloo tax ci waxtaan bi mujj, gan bi ñuy defal waxtaan, dina ñu won ñeenti fànn fu ñu war a wone ne dañuy dégg ndigal ni ko Yàlla bëgge : (1) ci suñu digganteek nguur yi, (2) ci mbooloo mi, (3) bu ñuy doxi suñuy soxla yu bokkul ci wàllu diine, ak (4) ci biir njaboot. Li ñuy waxtaane ci ndaje mu mag moomu, aka am njariñ !
Ñi bëgg ñu soob leen bu ndaje mu mag mu benn fan moomu jote, war nañu koo gaaw a xamal wottukat biy jiite. Bu ñu xamalee kañ lañuy def ndaje mu mag moomu, war nañu koo bind ñun ñépp ci suñu arminaat te seet li ñuy def ngir fekke lépp li ñu fay waxtaane. Bu ñu déggalee Yexowa ba fàww, barke yi ñuy jot, dinañu yàgg ba fàww.