Lu bees li ñu defar ngir fàttaliku li ñu waxtaane ci ndaje yu mag yi
Àddina Seytaane bi, mu ngi gën di bon rekk. Waaye Yexowa dafa ñuy yokk doole ngir ñu ragal ko, ñu moytu bëgg-bëggi àddina si, te ñu “ dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla ”. At mu nekk mu jaar ci “ surga bu takku te teey ” bi ngir may ñu ndaje bu ñaari fan bi ak bu benn fan bi (Macë 24:45). Dañu ciy wax lu jëm ci suñu diggante ak Yàlla te dafay yokk bu baax suñu doole.
Ci Sasu Nguuru Yàlla bii, am na lu bees li ñu defar ngir ñu mën a fàttaliku li ñu jàng ci ndaje yu mag yooyu, te topp ko. Ci atum liggéeyu waare 2005 lañu koy jëfandikoo. Ci xët 5 ak 6, wone nañu li nga xam ne dinañu ci waxtaan ci ndaje yu mag yooyu. Bind nañu fa it ay laaj ngir bés bi ñu koy fàttaliku ci mbooloo mi. Loolu dinañu ci waxtaan ci mbooloo yi ci ndaje liggéeyu waare yi, bu ndaje yu mag yooyu di waaj a jot ak it bu ñu paasee tuuti. Naka lañu koy defe ?
Benn walla ñaari ayu-bés balaa ndaje bu mag bu ñaari fan bi di jot, dinañu def waxtaan bu 10 minit ci xaaj bi tudd : “ Ndaje bu mag bu ñaari fan bii di ñów : li ñu fay waxtaane. ” Dina tax nit ñi yàkkamti teewe ndaje bu mag boobu. Kiy jiite waxtaan bi, dina wax itam ci laaj yi ñu bind ngir fàttaliku li ñu fay jàng. Dina wax itam nit ñi ñu bind li ëpp solo ci li ñuy dégg ci ndaje bu mag boobu. Loolu dina ñu dimbali bés bu ñu waree fàttaliku li ñu fa jàng.
Bu ndaje bu mag bu ñaari fan bi paasee ba mu am tuuti ayu-bés, dinañu def waxtaan bu 15 minit ci ndaje liggéeyu waare bi ngir fàttaliku li ñu jàng ci fan bu njëkk bi ci ndaje bu mag boobu. Ayu-bés ba ci topp, dinañu defaat beneen waxtaan bu 15 minit ngir fàttaliku li ñu jàng ci ñaareelu fanu ndaje bu mag boobu. Ci waxtaan yooyu dinañu laaj laaj yi ñu bind ci xët 5 ak 6 ci Sasu Nguuru Yàlla bii. Dinañu ci wone njariñ bi nekk ci li ñu jàng ci ndaje bu mag boobu. Bu ñu jàppee ayu-bés bi ñu war a def waxtaan boobu ci mbooloo mi, magi mbooloo mi dinañu seet ci porogaraamu ndaje liggéeyu waare bi li ñu mën a gàttal, dindi walla yóbbu ci beneen ayu-bés, ngir mën ci boole waxtaan bi.
Lu mel noonu it lañu war a def ngir fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bu benn fan bi. Waaye bii yoon moom, ci benn waxtaan bu 15 minit kese lañuy fàttaliku lépp li ñu jàng ci ndaje bu mag boobu. Na ñépp denc bu baax xët 5 ak 6 bu Sasu Nguuru Yàlla bii. Nañu ko jëfandikoo it ngir li ñu Yexowa wax fii amal ñu njariñ. — Isa. 48:17, 18.