Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 now.
“ Mas nañu dégg wax jii : ‘ Yeesu dafa dee ngir ñun. ’ [Waxal li nekk ci Yowanna 3:16.] Ndax mas nga laaj sa bopp : naka la deewu benn nit mënee musal nit ñépp ? [Mayal nit ki mu tontu.] Mbind mu sell mi dafa ci tontu, tontu bu yomb a nànd. Fii ci yéenekaay bii, xaaj bi tudd : ‘ Yeesu dafay musal — Naka ? ’, mu ngi koy leeral bu baax. ”
Réveillez-vous ! 22 now.
“ Ndax nit ñi danuy def seen kem kàttan ngir sàmm lépp li leen wër ? [Mayal nit ki mu tontu] Lépp liy dund ci kow suuf, liy tax ñu mën fii nekkandoo ni mu ware, ñu bare ñu ngi laajte ndax dina fii yàgg. Yàlla baax na, loolu itteel na Yàlla bu baax-a-baax. [Jàngal Nëxemiyaa 9:6.] Réveillez-vous ! mu ngi wax ci ni dund ci kow suuf di mel ëllëg. ”
La Tour de Garde 1 des.
“ Fi ñu tollu nii ci at mi, nit ñu bare ñu ngi def ay maye ak yeneen yëf yu baax. Loolu dafay tax ñu xalaat ci Ndigal bi mel ni Wurus. [Jàngal Macë 7:12.] Ndax foog nga ne mën nañu topp ndigal boobu saa su nekk ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yéenekaay bii dafa ñuy xalaatloo ci lii : ‘ Ndigal bi mel ni Wurus — Ndax am na njariñ ba tey jii ? ’ ”
Réveillez-vous ! 8 des.
“ Mbind mu sell mi dige na ne dina am bés boo xam ne kenn dootul mën a wax ‘ dama feebar ’. [Jàngal Isayi 33:24.] Réveillez-vous ! bii dafay wax ci lenn luy laal dige boobu, maanaam feebar buy sonal ay milioŋi nit, mag ak ndaw. Mu ngi tudd ‘ Yaakaar ngir ñi am feebaru tenqo ’. Wóor na ma ne li ci nekk dina la jàngal lu bare. ”