Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 nov.
“ Ci yow, suuf si naka lay mel ëllëg ? [Mayal nit ki tontu.] Seetal lu Biibël bi wax ci loolu. [Jàngal Sabuur 37:11.] Téere bii dafay waxtaan ci li Biibël bi wax ci ëllëgu suuf si. ”
Réveillez-vous ! 22 nov.
“ Tey, nit ñi yàq nañu suuf si. Looloo tax ñu bare seen xel dalul dara. Ndax foog nga ne mën nañu ci am pexe ? [Mayal nit ki tontu.] Yàlla bëggul suuf si mel ni mbalit ba kenn bañ cee mënati dëkk. [Jàngal Isayi 45:18.] Téere bii dafay wone lan mooy tax suuf si bañ a yàqu. ”
La Tour de Garde 1er déc.
“ Ndax mas nga laaj sa bopp lii : [Jàngal benn ci laaj yi nekk ci xët 6]. Am na ñu bëgg xam tont bi, waaye duñu ko xam. Loolu mën na tax ñu bañ a gëmati Yàlla. La Tour de Garde bii dafay wone naka lañu mën a ame ngëm gu dëgër. ” Jàngal Filipp 1:9 te won ko lu tax xam-xam bu wér bi am solo.
Réveillez-vous ! 8 déc.
“ Ndax suñu dund dina mas a mel ni li ñu wax fii ? [Jàngal Isayi 14:7 ba pare may ko mu tont.] Lu neex loolu Yàlla dige amagul. Waaye am na lu ñu mën a dimbali ci suñu dund tey. Téere bii ci loolu lay wax. ” Won ko xaaj bi tudd “ Comment résister aux mauvais désirs ? ”