TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 11/06 p. 8
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2006
km 11/06 p. 8

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 nov.

“ Njublaŋ dafa bare lool ci àddina. Moo tax am na ñuy naan ‘ Lu tax ma war a sonnal sama bopp ngir def lu baax ? ’ Ndax mas nga xalaat lu mel noonu ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li ñu wax fii ngir xiir ñu ci lu baax. [Jàngal Léeb. 2:21, 22 te boo koy jàng, fexeel ba kàddu yii feeñ bu baax : “ les hommes droits sont ceux qui résideront sur la terre ”, (maanaam ñi jub ñooy ñiy dëkk ci kow suuf si).] Téere bii dafay wone li war a gën a tax ñu jub. ”

Réveillez-vous ! Nov.

“ Am na ñu gëm ne lépp lu am rekk, Yàlla moo ko def. Bu musiba dalee ci kow nit ñi, dañuy wax ne Yàlla moo xam lu tax mu def loolu, te loolu lu baax la war a doon. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu. Ba pare jàngal Saak 1:13 te won ko ne Yàlla du indi musiba ngir mu nekk nattu ci kow nit ñi.] Biibël bi wone na fan la metit jóge ak lan la Yàlla di def ngir dindi ko. Ci loolu la téere bii di waxtaane. ”

La Tour de Garde 1er déc.

“ Ci sa xalaat, ndax, jar na ñu nekk nit ku jub tey ? [Mayal nit ki tontu.] Seetal fii li yonent Yàlla Suleymaan wax ci njubte. [Jàngal Léebu 20:7.] Téere bii dafay wone lu tax jub ci lépp li ngay def am solo. ” [Won ko yenn ci li ñu wone ci xët 19.]

Réveillez-vous ! Déc.

“ Bu ñu la laajoon kan mooy nit ki gën a mag ci nit ñi mas a dund yépp, kan ngay wax ? [Mayal nit ki tontu.] Ñu bare dañuy wax ne Yeesu mooy ki gën a mag. Seetal li mu nar a def ci suuf si, moom mii nekk buuru Nguuru Yàlla. [Won ko nataal yi nekk ci xët 8 ak 9, te tànn fa benn aaya bu nga koy jàngal.] Téere bii dafay wone naka la ko Yeesu di defe te loolu kañ lay doon. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager