Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 nov.
“ Ñun ñépp a bëgg am dund gu neex te am njariñ. Ci yow, lan mooy li ëpp solo li ñu war a wut ngir mën a am dund gu bare jàmm ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li Yeesu waxoon ci li ñu mën a may dund gu bare jàmm [Jàngal Macë 5:3.] Am na soxla bu nit ku nekk di judduwaale. Mooy bëgg jaamu Yàlla. Téere bii dafay wone ne def loolu mooy tax suñu dund am njariñ. ”
Réveillez-vous ! Nov.
“ Tey nit ñu bare dañuy jiital li boroom xam-xam yi wax, ba pare am xel ñaar ci li diine yi di jàngale. Moo tax ñu bare di wax ne Biibël bi amatul njariñ. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Ndax xam nga ne lépp li Biibël bi wax te mu laal li boroom xam-xam yi gëstu, dafay nekk dëgg. [Jàngal Ayóoba 26:7.] Réveillez-vous bu am solo bii, dafay wone lu bare lu war a tax ñu mën a gëm li nekk ci Biibël bi. ”
La Tour de Garde 1er déc.
“ Luy sa tontu ci laaj bii ? [Jàngal laaj bi nekk ci kanamu yéenekaay bi te mayal nit ki mu tontu.] Li Yàlla bëgg mooy xeet yi nekk ci àddina si sépp déggoo te nekk benn. [Jàngal Sabóor 46:8, 9.] Kàddu Yàlla wone na ni déggoo boobu di ame. Moom la téere bii di wone. ”
Réveillez-vous ! Déc.
“ Am na ñuy wax ne nit ku dee, dafay dem dund feneen. Am na ñeneen ñu ne bu nit deewee, fa la yem. Ndax war nañu ragal dee ? [Mayal nit ki mu tontu.] Ayóoba xamoon na ne dina dee. Xoolal ni mu doon gise loolu. [Jàngal Ayóoba 14:14, 15.] Téere bii dafay wone ci lu leer li Kàddu Yàlla wax ci liy xew bu nit deewee. ”