Bul topp ‘ lu amul njariñ ’
1 Ñu bare tey dañuy jëfandikoo li ñuy wax E-mail ngir wax ak nit ñi. Dañuy wax ci li ñu def, walla lu jëm ci seen njaboot, walla ci seeni xarit. Dëgg la, loolu mën na nekk lu baax. Waaye E-mail, bu ñu ko yemalewul, mën na indi ‘ lu amul njariñ ’. Loolu lan la ? — Léeb. 12:11.
2 Li ñu war a moytu ci E-mail : Am na ñuy wax ne, bu ñu jotee ci E-mail li ñu foog ne lu bees la ci mbootaayu Yexowa, ci lañuy gën a xam ne jege nañu mbootaay boobu. Lu bees loolu mën na nekk : li nit def ci wàllu ngëm, li xew ci Betel, musiba walla fitnaal bu dal ñenn ci suñuy mbokk, walla sax li nga xam ne wax nañu ko ci Lekkoolu surgay mbooloo mi te du ñépp a ko war a xam. Am na ñoo xam ne bu ñu déggee lu mel noonu dañu koy gaaw a jottali nit ñi, ndax li ñu bëgg nekk ki koy njëkk xamal seeni xarit.
3 Yenn saay, dinañu soppi xibaar yooyu mbaa yokk ci dara. Am na ñuy def li ñu mën ngir seen wax gën a saf. Loolu tax na ñi koy jàng foog lu amul sax. Ñi yàkkamti tas xibaar yu mel noonu, ñu ci bare xamuñu bu baax ni mbir mi deme. (Léeb. 29:20) Léeg-léeg nit ñi, dina leen wóor ne li ñu dégg mënul a am, waaye dañu koy jottali seeni moroom ndax li mu nekk wax bu saf. Xibaar yooyu nga xam ne dañuy réeral nit ñi, ci “ léeb ” yi lañu bokk, te duñu tax nit ñi gën a ragal Yàlla. — 1 Tim. 4:6, 7.
4 Boo waxee loo xam ne dafay mujj bañ a nekk dëgg, mën na metti ñenn ñi walla indi jaxasoo ci suñu biir, te yow yaay gàddu àq boobu. Bi ñu waxee Daawuda ne doomam yu góor yépp lañu rey, dafa ko metti ba mu “ xotti yéreem ”. Ndekete, kenn ki rekk moo ci dee woon. Loolu ba tey metti woon na lool, waaye li nit kooku yokkoon, dafa yokk it naqaru Daawuda (2 Sam. 13:30-33). Wax dëgg, bëgguñu def dara lu mën a tax suñu mbokk juum walla am naqar.
5 Fi Yexowa di jaar : Buñu fàtte ne am na fu suñu Baay bi nekk ci asamaan di jaar ngir wax ak nit ñi. Mooy “ surga bu takku te teey ” bi. Warugaru “ Surga ” boobu mooy seet li ñu war a xamal ñi nekk ci këru ngëm gi, ak ci ban “ jamano ” lañu ko war a def. Ñam boobu ci wàllu xel, ci mbootaay bi Yàlla ilif kese lañu ko mënee jot. Foofu rekk lañu war a jaar ngir jot lu wóor ci wàllu xam-xam, waaye du ci li tubaab di woowee réseau d’usagers d’Internet (maanaam ay nit ñuy jaar ci Internet ngir waxante ci seen biir). — Macë 24:45.
6 Li ñuy woowe Sites Web : Bu nit ñi bëggee xam dara ci Seede Yexowa yi, mën nañu ko seet ci li ñuy wax site bu Mbootaay gi defar ci Internet. Lii mooy adareesam : www.watchtower.org. Soxlawul keneen def lu mel noonu (maanaam lu ñuy wax page Web), muy benn nit, benn kurél, walla benn mbooloo. Am na ñu jël li nekk ci suñu téere yi ak aaya yi ci nekk yu ñu war a seet ci Biibël bi, def ko ci page Web yooyu. Te bu ci amee lu ñu waroon a wut ci yeneen téere, dañu ko ci def itam. Am na sax ñoo xam ne, ku leen jox dara, ñu jox ko waxtaan yi ñu defoon ci ndaje yu mag yi. Kuy sotti ci ordinatër li nekk ci téere yu mbootaay gi defar ba pare di ko joxe, bu ci jëlee xaalis walla déet, toppul li yoon tëral ci li tubaab di woowe droits d’auteurs. Yenn saay ñi koy def, dañu foog ne dañuy dimbali seeni mbokk ci wàllu ngëm. Waaye loolu baaxul, te warul amati.
7 Bu ñuy jëfandikoo ordinatër ngir wax ak nit, nañu seet te xalaat bu baax li ñuy def. Su ñu defee loolu, li ñuy dugal suñu xel dina nekk ‘ lu am solo, neex te am njariñ ’. — Léeb. 24:4.