Ni ñu mën a wone téere Approchez-vous de Jéhovah
◼ Jëlal sa Biibël ci sa loxo te ne : “ Nit ñu gëm Yàlla ñu bare, bëgg nañu koo gën a jege. Ndax xam nga ne Yàlla mu ngi ñuy ñaan ñu gën koo jege ? [Jàngal Saak 4:8.] Téere bii dañu koo defar ngir nit ñi mën a jëfandikoo seen Biibël ngir gën a jege Yàlla. ” Jàngal xise 1 ci xët 16.
◼ Jëlal sa Biibël ci sa loxo te ne : “ Tey, jubadi dafa bare. Li ñu nekke, niroo na ak li ñu wax fii. [Jàngal Dajalekat 8:9 ñaareelu xaaj bi.] Ñu bare ñu ngi laajte ndax Yàlla faale na loolu. [Jàngal ñaari kàddu yi njëkk ci xise 4 bi ci xët 119.] Pàcc bii dafay wone lu tax Yàlla di bàyyi jubadi am tey. ”