Nañu jariñoo njàngum téere Approchez-vous de Jéhovah
1 Bi ñu jotee téere bi tudd Approchez-vous de Jéhovah ci ndaje bu gën a mag bi tuddoon “ Ñi sawar ci waare Nguuru Yàlla ”, kontaanoon nañu lool. Ñu bare dañu jàng téere boobu ci saa si. Aaya atum 2003 maanaam “ Jegeleen Yàlla, mu jege leen ”, ñi mu xiir ci jàng téere boobu ñoo gën a bare. — Saak 4:8.
2 Ci weeru màrs, dinañu tàmbali jàng téere Approchez-vous de Jéhovah ci njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi. Lan lañu mën a def ngir gën a mën a jariñoo njàng boobu ? Waajal bi am na ci solo lool. Pàcc bu nekk dinañu ko def ci ñaari ayu-bés. Kon xise yi ñuy def ci njàng mi ayu-bés bu nekk duñu bare noonu. Loolu dina tax ñu mën a joxe ay tont yu bare yu jóge ci suñu biir xol. Bu ngeen jàngalee seen bopp te xalaat bu baax ci li ngeen jàng, dingeen mën a joxe tont yu mel noonu. Te it, ci ayu-bés yi ñu war a jeexal benn pàcc, xise yi ñuy def ci njàng mi dinañu gën a tuuti. Bu ko defee dinañu am jot bu doy ngir waxtaan ci loo xam ne téere bi rekk a ko am.
3 Ci pàcc ñaar ak yi ci topp, dina am wërale bu tudd “ Éléments de méditation ” bu pàcc bu nekk di waaj a jeex. Saa yu ngeen defee xise bu mujj bi ba pare, wottukatu njàngum téere bi dina waxtaan ak gurup bi ci wërale boobu. Dina wax ñi teewe ñu wax li ñu jàpp bi ñu doon xalaat ci aaya yi (Léeb. 20:5). Yenn saay mën na yokk ci laaj yi nekk ci wërale bi ay laaj yu mel ni bii : “ Li ñu jàng nii lu mu leen di jàngal ci Yexowa ? Lu mu leen di def ? Naka nga ko mënee jëfandikoo ngir dimbali nit ñi ? ” Li war a tax muy laaj laaj yu mel noonu mooy xiir nit ñi ci joxe ay tont yu jóge ci seen xol. Warul a laaj ay laaj ngir seetlu waa gurup bi ci loo xam ne amul solo noonu.
4 Téere Approchez-vous de Jéhovah dafa wuute ak yeneen téere yi. Dëgg la, téere yi “ surga bu takku te teey ” bi defar yépp dañuy màggal Yexowa. Waaye téere bii moom, dañu ko defar ngir waxtaane ci jikko Yexowa yi (Macë 24:45-47). Li ñuy jële ci téere boobu dina bare lool ! Njàng bu xóot bi ñuy def ci jikko Yexowa yi dina ñu jariñ dëgg. Njàng moomu, yàlla na tax ñu gën a jege suñu Baay bi nekk ca asamaan. Yàlla na tax it ñu gën a mën a dimbali nit ñi ngir ñu jege ko ñoom itam.