TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/05 p. 3-5
  • Li ñu mën a wax ci waaraate bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax ci waaraate bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Approchez-vous de Jéhovah
  • Y a-t-il un Créateur qui se soucie de vous ?
  • Veillez !
  • Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex
  • Écoute le grand Enseignant
  • La vie : comment est- elle apparue ? Évolution ou création ?
  • L’humanité à la recherche de Dieu
  • La Révélation : le grand dénouement est proche !
  • La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ?
  • Le plus grand homme de tous les temps
  • Lan la ñu Yàlla laaj ?
  • Adorez le seul vrai Dieu
  • Li ñu mën a wax ngir wone téere Qu’enseigne la Bible ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • 1) Benn laaj, 2) benn aaya, ak 3) benn pàcc
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • [Li ñu mën a wax ci waaraate bi]
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Ni ñu mën a wonee téere Écoute le grand Enseignant
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 1/05 p. 3-5

Déncal kayit bii

Li ñu mën a wax ci waaraate bi

Booy waajal waaraate bi, seetal li nekk fii ngir xam li ngay wax booy wone téere yi ñu war a wone ci weer wi.

Approchez-vous de Jéhovah

“ Nit ñu gëm Yàlla ñu bare, bëgg nañu koo gën a jege. Ndax xam nga ne Yàlla mu ngi ñuy ñaan ñu gën koo jege ? [Jàngal Saak 4:⁠8.] Téere bii dañu koo defar ngir nit ñi mën a jëfandikoo seen Biibël ngir gën a jege Yàlla. ” Jàngal xise 1 ci xët 16.

“ Tey, jubadi dafa bare. Li ñu nekke, niroo na ak li ñu wax fii. [Jàngal Dajalekat 8:9 ñaareelu xaaj bi.] Ñu bare ñu ngi laajte ndax Yàlla faale na loolu. [Jàngal ñaari kàddu yi njëkk ci xise 4 bi ci xët 119.] Pàcc bii dafay wone lu tax Yàlla di bàyyi jubadi am tey. ”

Y a-t-il un Créateur qui se soucie de vous ?

“ Tey, àddina si bare na coono yu metti lool. Kan moo ñu gën a mën a wax li ñu mën a def ngir coono yooyu deñ ? [Mayal nit ki tontu. Ba pare jàngal Macë 7:​28, 29.] Fii dañuy wax ci li waare bi Isaa defoon ci tund bi def ci ñi ko déglu woon. Xoolal li yeneen nit wax ci waare boobu. [Won ko ci xët 152 li ay nit wax.] Pàcc bii dafay wax ci li Isaa def ak ci li mu jàngale. ”

“ Ndax masuloo laaj sa bopp lii : ‘ su dee Yàlla am na, ndax dina mas a dindi metit ak li dul yoon ci àddina si ? ’ [Mayal nit ki tontu. Ba pare jàngal Peeñu 21:​3, 4.] Boo jàngee téere bii dinga xam naka la Yàlla di dindee coono yi ci àddina si ak it li tax coono yooyu am. ” Won ko pàcc 10.

Veillez !

“ Coono ak metit yi am tey jaaxal na ñu bare. [Waxal lenn lu ñépp dégg fi ngeen nekk.] Ndax xamoon nga ne loolu yépp bokk na ci liy wone ne léegi Nguuru Yàlla ñów ilif suuf si sépp ? [Mayal nit ki tontu. Ba pare jàngal aaya buy ànd ak li nga wax. Mën na nekk Macë 24:​3, 7, 8 ; Lukk 21:​7, 10, 11 ; walla 2 Timote 3:​1-5.] Xam bu baax li xew-xew yooyu tekki, lu jamp la tey. Téere bii, ci loolu lay wax .”

“ Ñu bare tey amatuñu yaakaar ndax lu bon li am ci àddina ak metit yiy dal ci seen kow. Am na ñu bëgg xam lu tax Yàlla du tere lu mel noonu am. Mbind mu sell mi wone na ne, ci lu wóor, bu ci kanamee tuuti, Yàlla dina dindi bépp metit ci àddina si. [Jàngal Peeñu 14:​6, 7.] Xoolal li àtte Yàlla nar a indil doom-Aadama yi. [Jàngal 2 Pieer 3:​10, 13.] Téere bii, ci loolu lay wax. ”

Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex

“ Bu ñu la waxoon nga dund ci béréb bu mel ni bii, ndax dinga nangu ? [Wonal nit ki nataal bi nekk ci xët 4-5, te may ko mu tontu.] Kàddu Yàlla dafa ñuy wax fi ñu war a jaar ngir am dund gu mel noonu ba abadan. Dinaa la ko won fii. [Jàngal Yowanna 17:⁠3.] Téere bii dina la dimbali nga am xam-xam bi mën a tax nga am dund gu dul jeex. ” Won ko juróomi xise yi njëkk ci pàcc 1 te nee ko dingeen ci mën a waxtaan beneen yoon boo dellusee.

Ubbil téere bi ci xët 188-9 te woneel nataal yi fa nekk. Jàngal li ñu fa bind, ba pare laajal nit ki lii : “ Ndax yaakaar nga ne dinga dund ci Àjjana, foo xam ne doom-Aadama yépp dinañu xam Yàlla ? [Mayal nit ki tontu. Ba pare jàngal Isayi 11:⁠9.] Boo jàngee téere bii, dinga xam li Mbind mu sell mi wax ci Àjjana ak itam li nga war a def ngir bokk ci. ” Jéemal a jàpp bés ngir waxtaan ak moom ci pàcc 1, xise 11-16.

Écoute le grand Enseignant

“ Jàngalekat bi gën a mag bi moo waxoon lii : [Jàngal Macë 7:​12, ndorteelu aaya bi.] Bu ñépp toppoon loolu, ndax àddina si du gën a neex ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wax ci li jàngalekat bi gën a mag bi jàngale. ” Woneel nataal yi nekk ci pàcc 17 te waxal ci kàddu yi ñu àndal.

“ Tey waajur yi dañuy góor-góorlu ngir seeni doom mën a ràññe lu baax ak lu bon. Ndax loolu am na solo ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Léebu 22:⁠6.] Fii gis nañu ne waajur yi dañu war a teel a komaase di jàngal seeni doom. Téere bii dina leen ci dimbali. ” Woneel nataal yi nekk ci pàcc 15 walla 18 ak kàddu yi ñu àndal.

“ Yenn saay waajur yi dañuy waaru ci li seeni doom di laajte. Lée-lée sax duñu xam lu ñuy tontu. Ndax loolu masu la dal ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Efes 6:⁠4.] Téere bii mën na dimbali waajur yi ngir xam li ñuy tontu ci li seeni doom di laajte tey. ” Woneel yenn nataal ci yi nekk ci pàcc 11 ak 12, walla 34 ba 36, te waxal ci kàddu yi ñu àndal.

La vie : comment est- elle apparue ? Évolution ou création ?

“ Jëfi fitna ak reyante bare na tey. Loolu laal na ñépp. Ndax yaakaar nga ne am na ku mën a dindi loolu ? [Mayal nit ki tontu.] Yàlla moom, xam na lu koy dindi. ” Ubbil téere bii ci xët 196 ; jàngal Léebu 2:​21, 22 ci xise 19 bi, ba pare wax ko li mu tekki. Woneel turu pàcc 16, te nee ko bu bëggee, mën na am téere bi.

Ubbil téere bi ci xët 6, ba pare neel lii : “ Ñu bare dañu nee kenn sàkkul suuf si ak lépp li ciy dund. Ndax loolu, mën nañu ko gëm ? Ci sa xalaat, loolu yépp, fu mu jóge ? [Mayal nit ki tontu.] Biibël bi dafay wax ne Yàlla dëgg ji moo ñu sàkk. Turam mooy Yexowa. Boroom kàttan la te dafa ñu bëgg lool. Am na lu bare luy wone ne li Biibël bi wax noonu mooy dëgg. ” Jàngal Sabuur 83:​18, te ci lu gàtt won ko ne Yàlla dafa bëgg defaraat suuf si sépp ba mu nekk àjjana.

L’humanité à la recherche de Dieu

“ Diine yi dañoo bare tey. Naka lañu mënee xam ban diine la Yàlla nangu ? Loolu, ndax masuloo ko laaj sa bopp ? ” Bu nit ki tontoo ba pare, ubbil téere bi ci xët 377. Won ko ponk nimoro 7 biy wone ne diine, bu nekkee diine dëgg ji, dina boole nitu xeet yépp ba ñu nekk benn. Laaj ko ndax dàkkoor na ci loolu. Jàngal ci Biibël bi benn aaya ci yi ñu wone foofu, te bu la ko jot bi mayee, waxtaanal ak moom ci yeneen ponk ci xët boobu. Bu loolu soxalee nit ki dëgg, nee ko mën na am téere bi. Boo paree waxtaan bi bay waaj a dem, mën nga ko laaj lii : “ Ku bokk ci diine dëgg ji, jëfam nu mu war a mel ? ” Nee ko bu bëggee, dingeen ci waxtaan bés boo dellusee.

Boo gisee ku bokk ci diine bu mag, mën nga nee : “ Waxtaan ak nit ñu bokk ci diine yu wuute, lu baax la. Doom-Aadama yi jaar nañu ci yoon yu bare ba ñu doon wut Yàlla. [Su baaxee ci ki ngay waxal, jàngal Jëf ya 17:​26, 27.] Ñu bare dañu topp diine bi seen wayjur toppoon. [Jàngal xise 12 ci xët 8.] Gën a xam yeneen diine, dafay ubbi xel te yaatal xam-xam. Téere bii dafay wax ci diine yi gën a mag yi nekk ci àddina si : fu ñu jóge, seeni jëf, ak li ñuy jàngale. ” Wonal nit ki lenn li téere bi wax ci diineem, su dee bokk na ci yi ñu wax fii : sikhisme (100-101) ; hindouisme (116-​17) ; bouddhisme (141) ; taoisme (164-6) ; confucianisme (177) ; shintoisme (190-5) ; judaisme (220-1) ; ak lislaam (289).

La Révélation : le grand dénouement est proche !

“ Xéyna dégg nga [waxal xew-xew bu ñu dégg ci xibaar yi]. Ñi ci gaañu, bare nañu lool, ndeysaan. Seeni mbokk, am nañu naqar bu réy. Ñu bare dañu bëgg xam naka lañu leen mënee dimbali. Loo ci xalaat ? ” Mayal nit ki mu tontu. Ba pare ubbil téere bi ci xët 299, te won ko nataal biy wone nit ku ñu dekkal. Boo paree, waxal lii : “ Ñu bare dañuy jaaxle bu ñu leen waxee ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki ci Àjjana biy am ci kow suuf si. [Jàngal Jëf ya 24:15 bi nekk ci xise 9 ci xët 297, ba pare wax ko li ñu ciy wax ci xise 10.] Téere bii wax na lu bare ci li Yàlla bëgg def ëllëg. ”

La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ?

“ Nit ñu bare tey, dañu am coono yu metti lool. Te dañuy wut ku leen ci mën a dimbali. Am na ñuy dem ci sëriñ yi walla gisaanekat yi ngir am ci pexe. Ci yow, kan moo ñu mën a wax li ñu war a def ngir génn dëgg ci coono yooyu ? [Mayal nit ki tontu.] Am na lu am solo lu Biibël bi wax te loolu, ñépp a ko war a xam. [Jàngal 2 Timote 3:16. Boo paree, ubbil téere bi ci xët 187, te jàngal xise 9.] Téere bii dina la won ne, ak coono boo mënta am, topp li Biibël bi wax mooy gën ci yow. ”

Le plus grand homme de tous les temps

“ Fu ñu tollu nii, ñu bare ñu ngi xalaat ci Yeesu. Waaye bu ñu gisee lépp lu bon li am ci àddina si tey, am na ñu bëgg xam ndax dëgg-dëgg Yeesu dafa ñuy xalaat. Noo gisee loolu ? ” Mayal nit ki tontu. Ubbil téere bi ci pàcc 24, te ci lu gàtt waxtaanleen ci li tax Yeesu ñów ci kow suuf si. Boo paree, jàngal Yowanna 15:​13, te won ko foofu ne Yeesu dafa fonk nit lool.

“ Bu ñu waxee ci Yeesu, ñu bare dañu koy gise ni liir bu ndaw walla ni nit ku sonn bay waaj a dee ci bant bi. Ñaar yii kese lañu xam ci Yeesu : ni mu juddoo ak ni mu deewee. Ñu bare xamuñu lépp lu rafet li mu wax ak li mu def ci dundam. Li mu def, laal na bépp nit bu mas a dund ci kow suuf si. Loolu moo tax ñu war a fexe ba jàng lépp li ñu mën ci li mu def ngir ñun. ” Jàngal Yowanna 17:⁠3. Ubbil téere bi ci xët bu njëkk bi te jàngal ñeenteelu xise bi.

Lan la ñu Yàlla laaj ?

“ Ndax ci sa xalaat Yàlla dafa bëggoon ñu dund ci jamano ju bare coono mel ni suñu jamano tey ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Macë 6:10.] Ndax mas nga jéem a xam ci dëgg-dëgg lan mooy Nguuru Yàlla ? ” Ubbil téere bi ci njàngale 6, te jàngal laaj yi nekk ci kow. Waxtaanleen ci walla nangeen jàpp bés ngir waxtaan ci beneen yoon.

“ Boroom xam-xam yi def nañu lu bare ci suñu jamano. Waaye ba tey, feebar ak dee ñu ngi sonal doom-Aadama yi. Ndax xam nga lan la Isaa di defal ñi feebar, ñi màgget, ak sax ñi dee ? ” Mayal nit ki tontu. Bu bëggee xam li Isaa di def, ubbil téere bi ci njàngale 5, te jàngal laaj yi ànd ak xise 5 ak 6. Nangeen ci waxtaan, walla nangeen jàpp bés ngir def ko beneen yoon.

Adorez le seul vrai Dieu

“ Ci sa xalaat, lan moo ñu mën a dimbali ci coono yi ñu am tey ? [Mayal nit ki tontu. Ba pare jàngal Room 15:⁠4.] Gis nga ne li nekk ci Mbind yi mën jàngal nit, seddal xolam, te may ko yaakaar. Loolu dafa ñuy may kàttan bi ñuy muñe suñuy coono. Téere bii dina la wax li nga mën a def ngir jariñoo bu baax li ngay jàng ci Biibël bi. ” Won ko ñeenti ponk yi ñu bind ci xët 30.

“ Jamano Yeesu ba léegi, ñu bare ñaan nañu Yàlla ngir Nguuram ñów. Ndax xam nga lan la Nguur googu di defal doom-Aadama yi ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Dañel 2:44.] Téere bii mu ngi wax lan mooy Nguuru Yàlla, li mu nar a def, ak li ñu mën a def ngir jot ci barke yi muy indi. ” Woneel nataal bi nekk ci xët 92-3.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager