TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/03 p. 4
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 1/03 p. 4

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 janv.

“ Ak reyante yu bare yi am tey, ndax foog nga ne li bon dem na ba daan li baax ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li Biibël bi wax ci Yàlla. [Jàngal Sabuur 83:18 ñaareelu xaaj bi.] Ndegam Yàlla mooy Aji Kowe ji ci kow suuf si sépp, ndax dëgg-dëgg lu bon mën na daan ? [Mayal nit ki mu tontu.] La Tour de Garde bii dafay tontu bu baax ci laaj boobu. ”

Réveillez-vous ! 22 janv.

“ Tey kaaraange amul. Dund gi masul a mel nii. Am na ay nit ñuy sàcc turu beneen nit di jëf tey wax ne ki ñu sàcc turam moo def jëf ji (l’usurpation d’identité). Loolu mu ngi gën di bare. Ndax mas nga ko dégg ? [Mayal nit ki mu tontu.] Biibël bi dig na ne dina am bés boo xam ne nit ñi dinañu am kaaraange te dara dootul yàqati jàmm jooju. [Jàngal Isayi 11:⁠9.] Yéenekaay bii dafay wone loolu naka lay ame. ”

La Tour de Garde 1er févr.

“ Ñàkkum liggéey tax na ba nit ñu bare jaaxle. Ñeneen ñoom ñu ngi muñ lu metti lool fi ñuy liggéeye. Ndax foog nga ne nit mën na kontaan te am xel mu dal fi muy liggéeye ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Isayi 65:​21-23.] La Tour de Garde bii dafay wax ci jamano joo xam ne nit ku nekk dina am liggéey bu baax. ”

Réveillez-vous ! 8 févr.

“ Réveillez-vous ! bii dafay wax ci lenn lu ñaaw lu am tey, maanaam xale yi ñuy def caga. Biibël bi wone na ne lu ñaaw loolu ñuy def xale yi, léegi mu jeex. [Jàngal Léebu 2:​21, 22.] Yéenekaay bii dafay wone lu indi lu ñaaw loolu ñuy def xale yi. Dafay wone it ne léegi mu jeex ak nu muy jeexe. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager