Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 janv.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Ñi dul def li ñu dige woon dafa bare ba nga xam ne, ñu bare tey xamatuñu kan lañu war a wóolu. Ndax am na koo xam ne mën nañu gëm lépp li muy dige ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Yosuwe 23:14.] Téere bii dafay wone lu ñu war a def ngir mën a wóolu lépp li ñu Yàlla dig ci Biibël bi. ”
Réveillez-vous ! 22 janv.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Nii lañuy binde turu Yàlla ci làkku ebrë. [Won ko li nekk ci xët bi njëkk ci téere bi.] Am na ñuy wax ne kenn warul a wax tur boobu ci kow. Ñeneen ñoom, dañu koy jëfandikoo bu baax. Ci ñaari xalaat yooyu la téere bii di wax. Dafay wone it lan mooy xam Yàlla ci turam. ” Jàngal Sabuur 83:18 te woneel ne nit ñi war nañu xam lan mooy turu Yàlla.
La Tour de Garde 1er févr.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Ñépp a bëgg am wér-gi-yaram. Waaye bu yàggul gëstukat yi gis nañu ne suñu ngëm it am na li muy def ci suñu wér-gi-yaram. Ndax foog nga ne loolu mën na nekk ? [Mayal nit ki tontu, jàngal Macë 5:3, te won ko ne xam ne am na li ñu soxla ci wàllu xel am na li muy def ci mbégte bi ñu am.] La Tour de Garde bii dafay wone naka lañu mëne am li ñu soxla ci wàllu xel. ”
Réveillez-vous ! 8 févr.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Ñu bare tey dañu jàpp lool fekk dañu soxla gën a nelaw. Xéyna dinga ànd ak kàddu bii ñu bind, am na léegi lu ëpp 3 000 at. [Jàngal Dajalekat 4:6, te may ko mu tontu.] Réveillez-vous ! bii dafay wone li ñu mën a def ngir ràññe ndax suñu nelaw doyul te lu ñu mën a def ngir xeex loolu. ”