Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 janv.
“ Ñu bare dañu gëm ne nit ku nekk am na malaaka bu koy topp. Te dañuy wax ne malaaka boobu, am na lu bare lu mu war a def. Am na ñuy wax ne dafa leen di won fi ñu war a jaar te dafa leen di aar. Am na ñeneen ñuy wax ne malaaka boobu dafay xool lépp lu baax ak lu bon li ñuy def. Yow nag, loo ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Sabóor 104:4. Boo koy jàng, nanga fexe ba “ ministres ” (maanaam surga) feeñ bu baax ci li ngay wax.] Aaya bii dafa ñuy won ne Yàlla moo sàkk malaaka yi te dañu nekk ay mbindeefu xel yu koy liggéeyal te di topp ay ndigalam. Yàlla, bu amee lu mu bëgg def te mu laal doom-Aadama yi, mën na jaar ci malaaka yi. Téere bii dafay wone ni muy defe loolu. Dafa ñuy won it li ñu war a def ngir li malaaka yi di def jariñ ñu. ”
Réveillez-vous ! Janv.
“ Tey nit ñi bare nañu xelal yu ñu mën a joxe ci lépp. Fànn boo tudd rekk, dinga ci mën a am ay xelal. Waaye ci xelal yooyu yépp, yan lañu mën a wóolu dëgg ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal 2 Timote 3:16.] Réveillez-vous ! bii dafay wone lu tax mu mën ñu wóor ne xelal yu baax te jar a wóolu ñoo nekk ci Biibël bi. ” Won ko waxtaan bi nekk ci xët 18.
La Tour de Garde 1er févr.
“ Ñun ñépp dañu soxla xaalis ngir am li ñuy dunde. Waaye ba tey, ndax nangu nga ne war nañu moytu li ñu wax fii ? [Jàngal 1 Tim. 6:10 te mayal nit ki tontu.] La Tour de Garde bii dafa ñuy won ay coono yu nit ku bare alal mën a am. Dafa ñuy won it ni ñu mënee moytu coono yooyu. ”
Réveillez-vous ! Févr.
“ Ñu bare ci ñun, dañu leen teel a jàngal ne mag yi, dañu leen war a may cér. Mag bu mu mënta doon, muy suñu wayjur walla keneen ku mu mënta doon, dañu leen war a may cér. Ndax loolu am na solo ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li ci Mbind mu sell mi wax. [Jàngal 3 Musaa (Lévitique) 19:32 te boo koy jàng, nanga feeñal bu baax kàddu gii : “ tu dois avoir des égards pour la personne du vieillard ” (maanaam danga war a may cér mag yi).] Ci téere bii, am na ay waxtaan yu ñu def ngir mag yi. Dinañu wone it li ñu mën a def ngir may leen cér. ”