Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 janv.
“ Ñaar ñuy séy, fan lañu mënee am xelal yu wóor ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal fii kan moo sos séy. [Jàngal Njàlbéen ga 2:22.] Yàlla joxe na ay ndigal ci lu jëm ci wàllu jëkkër ak jabar ci séy. Loolu la téere bii di wone. ”
Réveillez-vous ! Janv.
“ Xale yu góor yu bare dañuy génn ak xale yu jigéen, xale yu jigéen yi it di def loolu, fekk mënuguñu séy. Ndax mas nga xalaat ci coono yi ñu mën jële ci loolu ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Galasi 6:7.] Téere bii dafay wone lu rafet li war a tax góor di génn ak jigéen. Dafay wone it lu tax ñu war a xaar ba nekk mag balaa ñuy dugg ci lu mel noonu. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 27.
La Tour de Garde 1er févr.
“ Bu ñépp toppee li ñu wax fii, ndax foog nga ne dund gi dina gën a neex ? [Jàngal Efes 4:25, te mayal nit ki tontu.] Ñu bare dañuy wax ne yenn saay, fen bonul. Téere bii dafay wone lu baax li nekk ci wax dëgg saa su nekk. ”
Réveillez-vous ! Févr.
“ Nit ñi tàmm nañu di werante ci li Seytaane mën a defloo nit. Ndax mas nga laaj sa bopp li ñu mën a def ngir Seytaane bañ ñoo yóbbaale ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal 1 Piyeer 5:8, 9a.] Téere bii dafay wax ci ni Seytaane di naxe nit ñi. Dafay wone it ni ñu ko mënee moytu. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 12.