TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/06 p. 5-6
  • Nañu kontine di xaar Yexowa

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu kontine di xaar Yexowa
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Liggéeyu waare bu gën a mag bi mas a am ci àddina !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Nañu yiw ngir roy Kirist
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Nañu màggal Yexowa ci diggu mbooloo mu réy mi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2006
km 9/06 p. 5-6

Nañu kontine di xaar Yexowa

1 Yonent Yàlla Esayi nee na : “ Yexowa, Yàlla juy àtte la. Ñiy kontine di ko xaar ñépp, dañuy bég. ” (Esa. 30:18b). Am na lu bare lu Biibël bi nettali ngir wone ni Yàlla àtte noonam yi ak ni mu musale ñi koy topp bu baax. Li Biibël bi nettali noonu, lu muy jàngal ñiy jaamu Yexowa tey ? Lan lañu mën a def tey ngir waajal “ bésu Yexowa bu mag te raglu bi  (Yow. [Yoël] 2:31, 32) ? Ci ndaje bu gën a mag biy ñëw te tudd “ Mucc gi soreetul ! ” dinañu xalaat bu baax ci laaj yooyu. Dinañu mën a seetaat bu baax suñu bopp. Te it porogaraam bi dina ñu dimbali ñu kontine di xaar Yexowa.

2 Tey ngeen war a seet li ngeen war a def : Porogaraam bi dañu ko defar ak mbëggeel ngir jàngal ñu ci wàllu ngëm. Bu ñu ko bëggee jariñoo bu baax, war nañu fekke porogaraam bi yépp. Seetal tey lépp li nga war a def ngir mën a teewe ñetti fan yépp, yow ak sa njaboot (Léeb. 21:5). Ndax komaase nga dajale xaalisu paas yi, lekk bi ak leneen li ngeen di soxla ? Lii di topp it mën na bokk ci li nga war a def ngir waajal ndaje bu mag bi : ñaan ki ngay liggéeyal mu may la fan yi ngay teewe ndaje bi ; waxtaan ak sa jëkkër walla sa jabar bu nekkul Seede ci li nga bëgg def ngir teewe ndaje bi ; wax otel fi nga bëgg dal ñu déncal la benn néeg, walla bind kayit bi tudd Demande de chambre pour cas particuliers (CO-5) te joxe ko ; dimbali say njàngum Biibël ñu mën a teewe ñetti fan yépp. Bul bàyyi ba ndaje bi di waaj a jot ngir toppatoo loolu. Nanga ci ñaan Yexowa, te gëm ne dina ko “ sottal ”. — Sab. 37:5 ; seetal li ñu nettali ci téere Annuaire 2003, xët 197, xise 3 ba xët 198, xise 1.

3 Ñi soxla ndimbal : Léeb yi 3:27 nee na : “ Bul bañ a def lu baax ngir ñi ko war a jot, saa yoo ko mënee def. ” Lan mooy lu baax li nga mën a defal nit ñi lu jëm ci ndaje bu gën a mag bi ? Ci mbooloo mi, am na ñu nekk mag, ñu feebar, walla ñu def seen jot yépp ci liggéeyu Yexowa mel ni pioñee yi. Mën na am ñooñu walla ñeneen soxla ñu dimbali leen ngir dem ci ndaje boobu. Walla amuñu fu ñu mën a dal. Ñooñu, seeni mbokk ñoo leen ci war a jàpple (1 Tim. 5:4). Waaye bu ñu ko mënul, mbooloo mi mën na leen ci dimbali (Gal. 6:10). Ñi nekk wottukatu njàngum téere, war nañu seet ñi soxla ndimbal ci seen gurup te waxtaan ak ñoom. Bu ko defee, dinañu mën a seet ndax ñooñu teel nañu toppatoo lépp li ñu soxla ngir mën a teewe ndaje bu gën a mag bi.

4 Yar ak teggin dafay màggal Yàlla : Ci ndaje yu gën a mag yi, bu ñu bare di daje, suñu yar ak teggin dafay nekk seede bu rafet ci nit ñi. Naka lañu mën a wone loolu ? Mën na am ñu dem ci béréb yu mel ni otel walla restoraŋ, ci wetu bérébu ndaje bi. Nañu fa wone jikko karceen ba nit ñi kontaan ci ñun. Jikko yooyu ñooy muñ, lewetaay, maandute ak yeneen yu mel noonu (Gal. 5:22, 23 ; Fil. 4:5). Kenn ku nekk ci ñun danga war a wone mbëggeel bu àndul ak lu jekkadi, bu dul wut njariñu boppam te bu dul naqari deret. Bu jafe-jafe walla lu ñu naqari amee sax, dañu bëgg def “ lépp ngir màggal Yàlla ”. — 1 Kor. 10:31; 13:5.

5 Yiw ci ni ñuy soloo ak ci ni ñuy defare suñu bopp : Kenn ku nekk ci ñun am na li nga mën a def ngir nit ñi wax lu baax ci suñu ndaje bu gën a mag bi. Mooy solu walla defar sa bopp ci fasoŋ buy wone ne bëgguloo topp rekk li xew te bëgguloo ëppal, waaye danga bëgg yiw te defar bu baax sa yére. Loolu lañu war a def bu ñuy tukki ngir dem ci ndaje bi walla ngir ñibbisi, bu ñuy bokk ci liggéey bi ñuy def ngir waajal bérébu ndaje bi ak it bu ñuy teewe ndaje bi. Ñun ñii nekk jaamukatu Yàlla, li ñu gën a soxal mooy turu Yexowa ak li nit ñi di wax ci moom. Waaye du li ñu gënal walla li mën a tax ñu féex. Boroom kër yi ñoo war a fexe ba seen njaboot soloo saa su nekk ci fasoŋ buy wone ne dañu woyof te maandu. — 1 Tim. 2:9.

6 Noonu it, bu ñuy féexal suñu bopp ci otel yi, walla bu ñuy dem ci bitig yi walla ci restoraŋ yi, ni ñuy soloo walla ni ñuy defare suñu bopp dafa war a jekk. Booy dem reer fenn, solal yére yu jag ni booy dem ci ndaje bi. Loolu lu baax la it. Tapp kàrtu ndaje bi ci suñu yére, mën na ñu ubbil bunt bu ñuy waare. — 2 Kor. 6:3, 4.

7 Ñi nangu bokk ci liggéeyu ndaje bi : Leer na ne képp ku teewe ndaje bu gën a mag bi, dinga jariñoo ci li ñu fay jàngale ci wàllu ngëm. Dinga nekk it ak suñuy mbokk ci ngëm yu lay xiir ci lu baax. Loolu mbégte mu réy nga ciy jële. Waaye bu ñu nangoo bokk ci lépp li ñu war a def ngir ndaje bu gën a mag bi dox bu baax, suñu mbégte dina gën a réy (Jëf. 20:35). Kurélu njiit biy toppatoo ndaje bu gën a mag bi léegi mu komaase woo nit ñi ci liggéey boobu. Ndax dinga ci mën a bokk ? — Sab. 110:3.

8 Esayi nee na : “ Yexowa dina kontine di xaar fi mu leen di mën a won yiwam, te loolu moo tax dina jóg ngir won leen yërmande. ” (Esa. 30:18a). Bu ñu fonkee yërmande bi Yàlla di wone ak mbaaxaayam bi nga xam ne yelloowuñu ko sax, loolu dina ñu xiir ci màggal ko ci fasoŋ bi ñuy soloo ak ni ñuy defare suñu bopp, bu ñu nekkee ak suñu mbokk yi ci ndaje bu gën a mag bi. Ndaje bu gën a mag bi tudd “ Mucc gi soreetul ! ”, li ñuy ñaan mooy mu màggal Yexowa te dimbali ñu, ñu kontine di ko xaar !

[Laaj yi]

1. Lan mooy turu ndaje bu gën a mag bii di ñëw, te lu tax mu baax ci suñu jamano ?

2. Naka lañu mënee wone ne dañu fonk ndaje bu gën a mag bii di ñëw ?

3. Naka lañu mënee dimbali ñi soxla ndimbal ?

4. Yan jikko la nit ñi war a seetlu ci ñun bu ñu nekkee ci dëkk fi ñuy defe ndaje bu gën a mag bi ?

5. Naka lañu mënee màggal Yexowa ci ni ñuy soloo ak ni ñuy defare suñu bopp ?

6. Lu tax bu ñuy féexal suñu bopp ñu war a soloo te defar suñu bopp ni bu ñuy teewe ndaje bu gën a mag bi ?

7. Lan lañu mën a def ngir yokk mbégte bi ñuy am ci ndaje bu gën a mag bi ?

8. Naka lañu mënee def suñu wàll ngir lépp dox bu baax ci ndaje bi te mbégte bi gën fa bare ? (Seetleen wërale bii ci suuf.)

[Nataal bi nekk paas 6]

Ndaje bu gën a mag bi : Li ñu warul a fàtte

◼ Waxtu yi ñu koy defe : Ndaje bi, 9.30 lay komaase ci ñetti fan yépp. Bunt bi, 8.00 ci suba lañu koy tijji. Tuuti minit bala ñuy komaase waxtaan yi, kiy jiite porogaraamu bés bi dina toog ci kanamu ñépp, fekk ñuy teg misigu Nguur gi. Ñépp a war a toog seen palaas waxtu boobu. Bu ko defee ndaje bi dina komaase ni mu ware. Waxtu yii la ndaje bi di jeexe : àjjuma, 17.15 ; samdi, 17.05 ; dimaas, 16.10.

◼ Fi ñuy gaaree oto yi : Ndegam fi ñuy gaaree yaatuwul noonu, nañu def lépp ngir bokk oto bu ñuy dem ci ndaje bi. Loolu moo gën indi oto bu def benn nit walla ñaari nit rekk.

◼ Fu ñuy toog : Ñi ñu bokkal oto walla ñi ñu bokkal kër rekk lañu mën a dencal palaas.

◼ Añ bi : Ñu ngi leen di ñaan ngeen indaale seen añ, moo gën ngeen di dem wuti lu ngeen di lekk. Mën ngeen indi fu ngeen di def seen añ su dee réyul te mën ngeen ko def ci suufu fi ngeen di toog. Waruñu indi ëmb bu réy, lu mën a toj, walla sàngara.

◼ Xaalis bu ñuy maye : Ndaje yu gën a mag yi dañuy laaj xaalis bu bare. Su dee ndaje yooyu lu ñu neex la, bu ñu bëggee, mën nañu maye xaalis ngir jàpple liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Loolu mën nañu ko def ci suñu Saalu Nguur gi, walla ci bérébu ndaje bu gën a mag bi. Ku bëgg maye li ñuy woowe cheque ci tubaab, na ci def tur bii : Association “ Les Témoins de Jéhovah ”.

◼ Aksidaa ak faj bu ñu war a gaaw a def : Bu aksidaa amee ci bérébu ndaje bi, wax ko ci saa si ki la gën a jege ci ñiy teral nit ñi ci ndaje bi. Dina gaaw a woo ñiy toppatoo loolu. Wayjur walla njaboot yi am kenn ku feebar, waruñu fàtte indaale garab yi ki feebar war a naan.

◼ Ñi bëgg jël porogaraam bi ci kaset : Bu ñu nekkee ci bérébu ndaje bi, kenn warul a jël kuuraa walla jëfandikoo lu bokk ci micro yi. Te bu ñuy jël porogaraam bi ci kaset, dañu ko war a def ci fasoŋ bu dul tere kenn déglu.

◼ Ku bëgg jël foto : Bu ndaje bi komaasee, boo bëggee jël foto, bul jëfandikoo làmp boobu ñuy woowe flash.

◼ Portaabël ak li ñuy woowe bipper yi : Ku am telefon walla bipper, na ko regle mu bañ tere kenn déglu.

◼ Kayit bi tudd Veuillez suivre l’intérêt (maanaam kayit fi ñuy bind turu ñi suñu waxtaan neex ngir ñu dem seeti leen) : Ci jamano ndaje bu gën a mag bi, bu ñu amee buntu waar nit, dañu war a jëfandikoo kayit bi tudd Veuillez suivre l’intérêt (S-43) ngir bind ci turu képp ku suñu waxtaan neex. Waaraatekat yi war nañu yóbbaale benn walla ñaar ci kayit yooyu bu ñuy dem ci ndaje bu gën a mag bi. Kayit boobu mën ngeen ko am it ci biro biy toppatoo téere yi ci ndaje bu gën a mag bi. Bu ngeen ci bindee lépp li ñu ci laaj ba pare, mën ngeen ko jox ki nekk ci biro boobu, walla ngeen bàyyi ba dellu ci seen mbooloo, ngeen jox ko seen sekkerteer. — Seetleen Sasu Nguuru Yàlla bu feewriyee 2005, xët 6.

◼ Fi ñuy dal : Foo mënta dal, nanga wone jikko yi xel mu sell mi di meññ. Nanga baax, wone mbëggeel te may ñépp cér. Boo dalee kër jaambur, defal li nga mën ngir jàpple ko ci liggéeyu kër gi ak ci depãs yi mu war a def. Booy ñibbi nag, seetal bu baax ndax néeg bi nga nekkoon set na te delloo nga lépp ci palaasam.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager