TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 10/05 p. 5-6
  • Nañu màggal Yexowa ci diggu mbooloo mu réy mi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu màggal Yexowa ci diggu mbooloo mu réy mi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu kontine di xaar Yexowa
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Nañu yiw ngir roy Kirist
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Liggéeyu waare bu gën a mag bi mas a am ci àddina !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 10/05 p. 5-6

Nañu màggal Yexowa ci diggu mbooloo mu réy mi

1 At mu nekk, mën nañu màggal bu baax Yexowa ci suñuy ndaje yu gën a mag yi. Dawuda newoon na lii ci benn woy bi mu def : “ Dinaa la màggal ci biir mbooloo mu réy mi. Ci diggu nit ñu bare, dinaa la tagg ” (Sab. 35:18). Moom lañu bëgg def ñun itam. Ci ndaje bu gën a mag bii di ñëw, ñun ñii nekk benn mbooloo, lan lañu mën a def ba nit ñi màggal Yexowa ?

2 Lenn li ñu mën a def mooy seet jikko ji ñuy wone. Ki doon toppatoo béréb fi ñu doon def suñu benn ndaje bu gën a mag nee na : “ Wax nañu yeneen diine yu bëggoon a luye béréb bii ñu ñëw xool ni Seede Yexowa yi di defe seeni ndaje, ndaxte ni ngeen koy doxale rafet na lool. ” Kenn ku nekk ci ñun am na li mu mën a def ngir nit ñi wax lu mel noonu ci ñun, fekk ci dëgg Yexowa lañuy màggal noonu. Dañu war a seet ni ñuy defare suñu bopp, li ñuy sol, ni ñuy toppe lépp li ñu fay taxawal, ak jikko yi ñuy wone. — 1 Pie. 2:⁠12.

3 Li ñuy sol ak ni ñuy defare suñu bopp : Bu ñu bëggee màggal Yexowa ci li ñuy sol ak ni ñuy defare suñu bopp, fàww ñu woyef, maanaam nekk ku xam fi nga war a yem (1 Tim. 2:⁠9). Téere École du ministère, wone na ci xët 132 ne ku xam fi nga war a yem, doo bëgg tooñ sa moroom. Te doo bëgg it ñépp nekk di la xool rekk. Tey, ci reew yu bare, nit ñu bare duñu sol lu yiw. Waaye Yexowa dafay kontaan bu ñuy góor-góorlu ngir bañ a tilimal turam bi ñuy wuyoo (Jëf. 15:14). Dëgg la, yenn saay dañuy def suñu ndaje yu gën a mag yi ci béréb yu mag fu ñuy defe espoor, walla fu ñuy fowe. Waaye bu ñu fa defee suñuy ndaje yu gën a mag yi, ci ñetti fan yooyu, suñu “ mbooloo mu réy mi ” moo fay daje. Te ndegam ci kanamu Yexowa Aji kowe ji lañuy daje, fàww ñu seet bu baax li ñuy sol. — 1 Net. 29:⁠11.

4 War nañu seet itam li ñuy sol bu ndaje bi jeexee bés bu nekk. Dëgg la, bu ñuy féexlu walla bu ñu nekkee ci restoraŋ, dinañu bëgg sol yére yu gën a woyof. Waaye foofu itam, li ñuy sol ak ni ñuy defare suñu bopp, war na wone ne dañu “ ragal Yàlla ” (1 Tim. 2:10). Yére bu xew, taxul mu yiw (1 Ywna. 2:​16, 17). Mën nañu gis ci suñuy téere ay fasoŋu solu yu jekk te yiw yu mën a baax ci góor ak ci jigéen, fekk ñu nekk ci béréb yu bare te wute. Ci dëkk bu ñuy defe ndaje bi, bu ñu tafee kartu ndaje bi ci suñu yére, duñu fàtte ne fépp fu ñu mënta nekk, ay karceen yuy jaamu Yexowa lañu. — 2 Kor. 6:​3, 4.

5 Nañu fonk li ñu Yexowa may ngir dundal ñu ci wàllu ngëm : Yàlla mi nekk kilifa gi gën a mag ci àddina si, dafa ñu waajal lekk bu neex te bare ci wàllu ngëm (Isa. 25:6 ; 1 Kor. 10:21). Su ñu fonkee palaas bi ñu fa am, dinañu def lépp ngir teewe fa ñetti fan yépp. Ndax xam nga ba pare fi ngay dal ak ni ngay deme ci ndaje bi ? Ndax ñaan nga ba pare ki ngay liggéeyal mu may la nga teewe ndaje bi ? Ndax xam nga ban waxtu ngay jóg ngir mën a waajal sa bopp te dem ci bérébu ndaje bi ngir teel a àgg foofu ? Boo defee loolu, dinga am jot ngir wut fooy toog te waxtaan ak say mbokk ci ngëm te màggal Yexowa ak ñoom bu ngeen di woy woy-Yàlla bu njëkk bi ak bu ngeen di ñaan bu njëkk bi. — Sab. 147:⁠1.

6 Bu ñu fonkee li ñu Yexowa may ngir dundal ñu ci wàllu ngëm, dinañu déglu bu baax lépp li ñu fay wax. Duñu waxtaan waxtaan yu amul solo te duñu lekk walla génn ci biti, fekk dañu war a déglu porogaraam bi. Yexowa dafay jaar ci surga bu takku te teey bi ngir jox ñu lekk bi ñu soxla tey jii ci wàllu ngëm (Macë 24:45). Kenn waru ci ñàkk dara. Wayjur yi, war nañu toog ak seeni doom, te dimbali leen ñu jariñoo bu baax porogaraam bi. — 5 Mu. 31:⁠12.

7 Ñu ngi leen di ñaan ngeen indaale seen añ, te bañ a génn bu waxtu añ jotee, ngir wuti li ngeen di lekk. Daaw, li ëpp ci ñi ñëwoon ci ndaje bu gën a mag bi, topp nañu loolu te indi nañu seen añ. Loolu lu baax la. Bu ñépp mënee def loolu ren, dina baax lool (Yaw. 13:17) ! Bu ñu defee loolu, dinañu mën a waxtaan ak suñuy mbokk ci ngëm, waxtaan yuy dëgëral ngëm. Dafay tax ñu gën a nekk benn te am jàmm ci suñu biir. Te bu nit ñi gisee loolu, Yexowa lañuy màggal. — Sab. 133:⁠1.

8 Nañu waaraate saa yu ñu ci amee bunt : Bu ñuy dem ci ndaje bi walla bu ñu fay jóge, am na lu bare lu ñu mën a def ngir màggal Yexowa ak suñu gémmiñ (Yaw. 13:15). Bu ñuy lekk ci restoraŋ, walla bu ñuy waxtaan ak ñiy liggéey ci otel bi ñu nekk, nañu seet ni ñu leen mën a waare. Suñu xel ak suñu xol yépp dina fees ak lépp li ñu dégg ci ndaje bu gën a mag bi. Nañu ko jottali nit ñi nuy dajeel. — 1 Pie. 3:⁠15.

9 Yàkkamti nañu ndaje boobu jot ngir mën a màggal Yexowa “ ci diggu mbooloo yi daje ” (Sab. 26:12). Nañu ànd ñun ñépp di màggal Yexowa ci ndaje bu gën a mag bi tudd “ Nañu déggal Yàlla ”.

[Study Questions]

1, 2. Lan lañu mën a def ci suñu ndaje bu gën a mag bi te naka lañu ko mën a defe ?

3, 4. Boo xamee fi nga war a yem, loolu naka la lay dimbalee nga xam noo war a soloo ngir mu jekk ci karceen buy jaamu Yexowa, muy ci ndaje bi, walla bu bés bi jeexee ba pare ?

5, 6. Naka lañu mën a wonee ne fonk nañu li ñu Yexowa may ngir dundal ñu ci wàllu ngëm ?

7. Lan lañu bëgg ñu def lu jëm ci añ bi ? Lu tax ñu wax ñu loolu ?

8, 9. Am na leneen li ñu mën a def ci ndaje bu gën a mag bi ngir màggal Yexowa. Loolu lan la ?

[Box on page 6]

Ndaje bu gën a mag bi : Li ñu warul a fàtte

◼ Waxtu yi ñu koy defe : Ndaje bi, 9h30 lay komaase ci ñetti fan yépp. Tuuti minit bala ñuy komaase waxtaan yi, kiy jiite waxtaan yi dina toog ci kanamu ñépp fekk ñuy teg misigu Nguur gi. Ñépp a war a toog seen palaas waxtu boobu. Bu ko defee ndaje bi dina komaase ni mu ware. Àjjuma ak samdi, ndaje bi, 5h05 lay jeexe. Dimaas, 4h10 lay jeexe.

◼ Fi ñuy gaaree oto yi : Ndegam fi ñuy gaaree yaatuwul noonu, nañu def lépp ngir bokk oto bu ñuy dem ci ndaje bi. Loolu moo gën oto yu am benn walla ñaari nit kese. Te bu ñuy gaare walla bu ñu fay jóge, nañu topp bu baax li ki nekk foofu di wax, ndax mu bañ a am aksida.

◼ Fu ñuy toog : Ñi ñu bokkal oto walla ñi ñu bokkal kër rekk lañu mën a déncal palaas.

◼ Xaalis bu ñuy maye : Ndaje yu gën a mag yi dañuy laaj xaalis bu bare. Su dee ndaje yooyu lu ñu neex la, bu ñu bëggee, mën nañu maye xaalis ngir jàpple liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Loolu mën nañu ko def ci suñu saalu nguur gi, walla ci bérébu ndaje bu gën a mag bi.

◼ Añ bi : Ñu ngi leen di ñaan ngeen indaale seen añ, moo gën ngeen di dem wuti lu ngeen di lekk, bu waxtu añ jotee. Mën ngeen indi fu ngeen di def seen añ su dee réyul te mën ngeen ko def ci suufu fi ngeen di toog. Waruñu indi ëmb bu réy, lu mën a toj, walla sàngara.

◼ Ñi bëgg jël porogaraam bi ci kaset : kenn warul jël kuuraa walla jëfandikoo lu bokk ci micro yi, ci bérébu ndaje bi. Te bu ñuy jël porogaraam bi ci kaset, dañu ko war a def ci fasoŋ bu dul tere kenn déglu.

◼ Ku bëgg jël foto : Bu ndaje bi komaasee, boo bëggee jël foto, bul jëfandikoo làmp boobu ñuy woowe flash.

◼ Telefon ak bipper yi : Ku am telefon walla bipper, na ko regle mu bañ tere kenn déglu.

◼ Aksida ak faj bu ñu war a gaaw a def : Bu aksidaa amee ci bérébu ndaje bi, wax ko ci saa si ki la gën a jege ci ñiy teral nit ñi ci ndaje bi. Dina gaaw a woo ñiy toppatoo loolu. Dinañu seet mbir mi ba xam li ñu war a def. Wayjur walla njaboot yi am kenn ku feebar, waruñu fàtte indaale garab yi ñu war a naan bu ñuy nekk ci ndaje bu gën a mag bi.

◼ Fi ñuy dal : Foo mënta dal, nanga wone jikko yi xel mu sell mi meññ. Nanga baax, nanga wone mbëggeel te may ñépp cér. Boo dalee kër jaambur, defal li nga mën ngir jàpple ko ci liggéeyu kër gi ak ci depaas yi mu war a def. Booy ñibbi nag, seetal bu baax ndax néeg bi nga nekkoon set na te delloo nga lépp ci palaasam.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager