TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/03 p. 4
  • Nañu nekk royukaay ci jëf yu baax

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu nekk royukaay ci jëf yu baax
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • “ Saxleen ci baax ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Nangeen sell ci lépp li ngeen di def
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Nañu kontine di xaar Yexowa
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Ndaje bu gën a mag bi ci atum 2004 : “ Nañu ànd ak Yàlla ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 9/03 p. 4

Nañu nekk royukaay ci jëf yu baax

1 Bu seede Yexowa yu bare dajee ci seen ndaje yi gën a mag, ci la nit ñi di gën a seetlu li ñuy def ak ni ñuy nekke ak seen moroom. Kon ku nekk ci ñun a war a xalaat bu baax ci li Biibël bi wax maanaam ‘ ñu maandu. Te [...] ci lépp lu mu mana doon, ñu nekk ab royukaay ci jëf yu baax ’ (Titt 2:​6, 7). ‘ Bañ a yem ci topptoo suñu bopp rekk, waaye [...] boole ci suñu moroom ’, léeg-léeg mu jafe bala ñu ko mën a def (Fil. 2:⁠4). Nañu seet ni ñu mënee topp xelal yooyu bu ñu nekkee ci ndaje bu gën a mag biy ñów te tudd “ Nañu màggal Yàlla ”.

2 Toppatoo fi ñu war a dal : Ñi war a dal kër jaambur, walla fu ñu bare war a di fanaan, walla ci otel, ci lañu mën a wone bu baax ay jëf yu rafet. Xelal yii di topp dinañu leen ci dimbali : Bindal lépp li ñu la laaj ci kayit bi tudd Demande de logement (maanaam fi ngay ñaan foo mënee dal), te jox ko sekkerteer bi. Boo waxee ba pare ci kayit boobu ñaata nit ñooy ànd ak yow, bul indi nit ñu ëpp loolu. Jéemal joxe dara ngir jàpple waa kër gi ci ndox ak kuraa bi ñuy fey. Bul tilimal fi nga nekk. Bu aksidaa amee fi ngay dal, nanga ko gaaw a wax biro bi ñuy woowe Administration de l’assemblée (maanaam ñiy doxal ndaje bi). Nañu muñal ñiy liggéey ci otel bi ñu dal, ak ñiy doxal ndaje bi, te topp li ñu nu wax. Bu ñu defee loolu, dinañu wone ne xel mu sell mi dafay jur lu baax ci ñun. — Gal. 5:​22, 23.

3 Way-jur yi ak xale yi : Tey xale yu bare dañu yaradiku. Waaye ku gis suñuy doom xam ne dañu wuute lool. Loolu dafay tax nit ñi màggal Yexowa te wax lu rafet ci mbootaayam. Waaye, léeg-léeg poroblem dina am bu ñu leen bàyyee ñoom kenn, te kenn du leen xool (Léeb. 29:15). Way-jur yi waruñu bàyyi seeni doom ñu nekk ñoom kenn, kenn bañ leen a seetlu, bu ñu nekkee ci otel bi, boole ci piscine bi (maanaam fu ñépp mën a sàngu), ci kër jaambur ak fu ñuy defe ndaje bi.

4 Am na ay way-jur yoo xam ne bala ñuy dem ci ndaje bi, dañuy waxtaan ak seeni doom ci jikko yi ñu war a am Gis nañu ne loolu dafa leen di dimbali bu baax (Efes 6:⁠4). Dañuy won seeni doom ne karceen bu am mbëggeel dëgg “ du def lu jekkadi ” te “ du wut njeriñu boppam ” (1 Kor. 13:⁠5). Bu ñu nekkee ci ndaje bu gën a mag bi, Yexowa moo ñu fay jàngal. Mag ñi ak xale yi bu ñu wonee jikko yu rafet ci bérébu ndaje bi ak fépp fu ñu mënta nekk, dinañu wone ne fonk nañu ndaje boobu. — Isa. 54:⁠13.

5 Suñu jëfin bu rafet mën na tax ba nit ñi soppi lu bon li ñu doon xalaat ci Seede Yexowa yi, te mën na tax ay nit bëgg xam diine dëgg ji (Macë 5:16 ; 1 Pie. 2:12). Kon nañu fexe ba képp ku ñu taseel ci ndaje boobu mën a wax lu rafet ci ñun ndax suñuy jëf yu rafet ak ni ñuy nekke ak ñoom. Bu boobaa dinañu “ nekk ab royukaay ci jëf yu baax ” te dinañu màggal Yexowa. — Titt 2:⁠7.

[Laaj yi]

1. Bu ñu nekkee ci ndaje bu gën a mag bii di ñów, lu tax ñu war a seet bu baax suñu jëfin ?

2. Lu ñu warul a fàtte bu ñuy toppatoo fu ñu war a dal ?

3, 4. Naka la xale yi mënee tax ba nit ñi màggal Yexowa ? Lan mooy wareefu way-jur yi ci wàll boobu ?

5. Suñu jëf yu rafet yi, lan lañu mën a def ci nit ñi ?

[Wërale bi nekk paas 4]

Nañu xalaat nit ñi ñu nekkal

▪ Buñu tilimal fi ñu nekk

▪ Nañu xool bu baax li suñu doom yi def

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager