Nangeen sell ci lépp li ngeen di def
1 Ñun ñii di jaamu Yexowa Yàlla ju sell ji, dañuy góor-góorlu ngir sell ci lépp li ñuy def (1 Pie. 1:15, 16). Loolu dinañu ko mën a def bu ñu toppee li neex Yexowa ci lépp li ñuy def. Ci ndaje bu gën a mag bi ñuy def ci at mii, dinañu mën a wone ne ñun, ay nit ñu sell lañu.
2 Ci restoraŋ yi : Lii la benn waay wax : “ Seede Yexowa yi niruwuñu ak ñeneen ñi. Ñoom dañuy may cér nit ñi. ” Kooku dafa doon liggéey ci benn restoraŋ bu jege fi ñu doon defe benn ndaje bu gën a mag. Waaw, bu ñu nekkee ci restoraŋ, waruñu wax ci kow walla ree ci kow ba di tanqal nit ñi. Loolu ci yar ak teggin la bokk. Bu ñuy lekk ak di naan sax, dañu bëgg def lépp ngir màggal Yàlla. — 1 Kor. 10:31.
3 Ci ndaje bu gën a mag bi : Fi ñuy defe ndaje bi lañu war a gën a wone yar ak teggin. Foofu dina am ku lay won fi nga war a gaare. Dina am it ku lay won foo mën a toog. Toppal bu baax li nit ñooñu di wax (Yaw. 13:17). Njaboot yi dañu war a bokk fi ñuy tooge. Waruñu bàyyi ndaw yi ak xale yu tuuti yi yépp, ñu toog ak seeni moroom. Ci bérébu ndaje bi, kenn warul jëfandikoo kuuraa bi walla lépp li jëm ci micro yi. Te bu ñuy jëfandikoo kamera walla beneen appareil, bumu tere kenn déglu. Bu ndaje bi komaasee, boo bëggee jël ay foto, bu mu ànd ak li ñuy wax ci tubaab flash. Ku am telefon walla beeper, dafa ko war a fey ndax mu bañ tere kenn déglu. Bu aksidaa amee ci bérébu ndaje bi, wax ko ci saa si ñiy teral ñiy agsi ci bérébu ndaje bi walla fi ñuy toppatoo ñi soxla ñu faj leen ci lu gaaw. Dinañu xam li ñu war a def.
4 Jikko yi Seede Yexowa yi di wone ñoo tax ñu wute ak nit ñi. Jikko yooyu dañuy màggal it suñu Yàlla (1 Pie. 2:12). Seede Yexowa yi bu ñu nekkee ci seen ndaje bu gën a mag, nit ñi dañu leen di seetaan. Kon nag, nañu góor-góorlu ñun ñépp ngir sell ci li ñuy def.
[Wërale bi nekk paas 8]
Nañu sell ci li ñuy def
◼ Nañu seetlu bu baax suñuy doom
◼ Nañu wone ne dañuy xalaat nit ñi