Yére yu jekk te yiw dañuy wone ne dañu ragal Yàlla
1 Ndaje bu gën a mag bi ci atum 2003 léegi mu jot. “ Nañu màggal Yàlla ” la tudd. Yexowa dinañu fa may ñamu xel bu baree bare. Ñu ngi ko ci gërëm bu baax ! Li ñu mën a def ngir wone ne dañu ragal Yàlla te fonk nañu ñamu xel boobu mu ñu pareel, mooy seet bu baax li ñuy sol. — Sab. 116:12, 17.
2 Set te jekk : Ku ñu xool dafa war a xam ne ànd nañu ak li Yàlla bëgg, moom mii bëgg lu set te jekk (1 Kor. 14:33 ; 2 Kor. 7:1). Dañu war a set (suñu bopp, suñu karaw, suñu we) te sol lu jekk. Ñu bare tey meluñu noonu. Waaye bu dee sax ñiy feeñ ci film yi te ñépp xam leen, walla ñi aay ci espoor ñooy soloo noonu, karceen waruñu leen a topp. Am na ñoo xam ne bu amee lu xew rekk ñu sol ko. Waaye bu ñu melee noonu, mën na am nit ñi bañ a mën a ràññe ñiy jaamu Yàlla dëgg ji ak ñi ko dul jaamu. — Mal. 3:18.
3 Nañu sol lu jekk ni karceen yuy liggéeyal Yàlla : Ci leetar bi mu bind wottukat bi Timote, ndaw li Pool dafa wax jigéen ñi ñu “ sol col gu faaydawu, cig woyef ak maandu. [...] Na seen col di jëf yu rafet, ndaxte looloo jekk ci jigéen, juy woote ag ragal Yàlla ” (1 Tim. 2:9, 10). Bu ñu bëggee li ñu sol nekk lu jekk te yiw, balaa ñuy sol dara, dañu ko war a xool bu baax. Li ñu sol dafa war a jekk, set te yem — warul ëppal, te boo dee jigéen, warul tax bu la góor gise rekk, xelam dem ci lu bon, walla boo dee góor, jigéen xalaat lu ñaaw. — 1 Pie. 3:3.
4 Pool waxoon na it ne waruñu ëppal ci “ létt ak ci takkaayu wurus, mbaa ciy per ak col gu jafe ” (1 Tim. 2:9). Suñu takkaay, suñu pastel ak lépp li ñuy def ngir gën a rafet, dafa war a yem. Loolu moo gën ci karceen yu jigéen yépp. — Léeb. 11:2.
5 Karceen yu góor yi war nañu topp ñoom itam li Pool waxoon jigéen ñi. Suñu mbokk yu góor yi waruñu sol yére yoo xam ne dañuy wone jikko nit ñi nekk ci àddina si (1 Ywna. 2:16). Am na réew yoo xam ne ñu bare dañuy sol yére yu leen ëpp fuuf. Waaye yére yu mel noonu jekkuñu ci kuy liggéeyal Yàlla.
6 Bu ñuy féexal suñu xol : Suñu mbokk yu bare dañuy solu bu baax bu ñuy teew ci ndaje bi. Waaye dégg nañu ne am na ñuy fàtte loolu bu ñuy tukki ngir ñów ci ndaje bi walla ñibbi, walla it bu ñuy féexal seen xol bu ndaje bi jeexee. Waaye nag, suñu bopp ak li ñuy sol — muy bu ñu nekkee ci ndaje bi walla feneen — dafay tax nit ñi xalaat lu baax walla lu bon ci mbooloo Yàlla mi. Ndegam dañuy tapp ci suñu yére kartu ndaje bu gën a mag bi, li ñuy sol dafa war a jekk ci karceen buy liggéeyal Yàlla. Loolu tax na ñu bare kontaan ci ñun ba di ko wax, te ci lañu leen di mën a waar. — 1 Kor. 10:31-33.
7 Bu ñuy muuñ, suñu kanam dafay gën a leer. Noonu it yére yu jekk te yiw dañuy tax ñu gën a fullaal suñu mbooloo ak xibaar bi ñuy jottali nit ñi. Bu suñu ndaje bi gën a mag jotee, xéyna mu am ay nit ñuy bëgg xam lu tax ñu wuute ak ñeneen nit ñi, ba nee sax : “ Dañu bëgg ànd ak yeen waa mbooloo mi, ndax dégg nañu [te gis nañu] ne Yàlla mu ngi ànd ak yeen. ” (Sak. 8:23). Na ku nekk ci ñun wone ci li muy sol ne dafa ragal Yàlla.
[Laaj yi]
1. Naka lañu mën a wonee ne fonk nañu ndaje bu gën a mag bii di ñów ?
2. Lu tax set te jekk am solo lool ci ñun ?
3. Lan lañu mën a def ba mu wóor ne li ñuy sol ànd na ak li 1 Timote 2:9, 10 wax ?
4, 5. Lan la karceen yu góor ak yu jigéen yi war a moytu ?
6. Lu tax ñu war a sol lu baax te jekk bu ñuy tukki ngir dem ci ndaje bu gën a mag bi, walla bu ñu fay jóge, bu ñu nekkee ci ndaje bi, ak bu ndaje bi jeexee bés bu ne ?
7. Bu ñu solee lu jekk te yiw, lan la mën a def ci ñi nuy xool ?
[Wërale bi nekk paas 5]
Nañu sol lu jekk
▪ Bu ñuy tukki
▪ Bu ñu nekkee ci ndaje bi
▪ Bu ñuy féexal suñu xol